Filipenses 1
Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB
1 Nun Pool ak Timote, jaami Kirist Yeesu, noo leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell yépp ci dëkku Filib, yi bokk ci Kirist Yeesu, yéen ak seeni njiit ak ñiy topptoo yëfi mbooloo mi.
1 Paulo e Timóteo, servos de Cristo Jesus, a todos os santos em Cristo Jesus que estão em Filipos, com os bispos e diáconos:
2 Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
2 Graça a vós, e paz da parte de Deus nosso Pai, e do Senhor Jesus Cristo.
3 Yoon wu ma leen di xalaat, maa ngi sant Yàlla sama Boroom;
3 Dou graças ao meu Deus todas as vezes que me lembro de vós,
4 te saa su ma leen di ñaanal yéen yépp, duma noppee bég,
4 fazendo sempre, em todas as minhas orações, súplicas por todos vós com alegria
5 ndax seen ànd ak man ci tas xibaaru jàmm bi, ca ndoorte la ba tey.
5 pela vossa cooperação a favor do evangelho desde o primeiro dia até agora;
6 Wóor na ma ne Yàlla mi tàmbali jëf ju baax jii ci yéen, dina ci sax, ba bésu Kirist Yeesu ñëw.
6 tendo por certo isto mesmo, que aquele que em vós começou a boa obra a aperfeiçoará até o dia de Cristo Jesus,
7 Te juumuma ci li ma xalaat loolu ci yéen ñépp, ndaxte def naa leen ci sama xol; ba tax fii ci kaso bi, ci taxawal xibaaru jàmm bi ak lawal ko, yéen ñépp am ngeen wàll ak man ci yiwu Yàlla.
7 como tenho por justo sentir isto a respeito de vós todos, porque vos retenho em meu coração, pois todos vós sois participantes comigo da graça, tanto nas minhas prisões como na defesa e confirmação do evangelho.
8 Ndaxte Yàllaa seede ne sama xol seey na ci yéen ñépp ci biir cofeelu Kirist Yeesu.
8 Pois Deus me é testemunha de que tenho saudades de todos vós, na terna misericórdia de Cristo Jesus.
9 Li ma leen di ñaanal nag mooy lii: yal na seen mbëggeel di yokku tey gëna tar, jaar ci xam ak xàmmi gu wér;
9 E isto peço em oração: que o vosso amor aumente mais e mais no pleno conhecimento e em todo o discernimento,
10 yal nangeen sax noonu ci li gëna rafet, ngeen am xol bu laab te baña am benn sikk, ba bésu Kirist ñëw;
10 para que aproveis as coisas excelentes, a fim de que sejais sinceros, e sem ofensa até o dia de Cristo;
11 yal na seen xol meññ njub, ba ne gàññ, jaar ci Yeesu Kirist ci ndamul Yàlla ak cantam.
11 cheios do fruto de justiça, que vem por meio de Jesus Cristo, para glória e louvor de Deus.
12 Damaa bëgg, bokk yi, ngeen xam lii: li ma dal taxul xibaaru jàmm bi dellu gannaaw, waaye da koo jëmale kanam.
12 E quero, irmãos, que saibais que as coisas que me aconteceram têm antes contribuído para o progresso do evangelho;
13 Noonu ñiy wottu buur bi ak ñépp gis nañu bu leer ne turu Kirist rekk a tax ñu jàpp ma.
13 de modo que se tem tornado manifesto a toda a guarda pretoriana e a todos os demais, que é por Cristo que estou em prisões;
14 Te it bokk yu bare takk nañu seeni fit ci li ñu gis samay buum, ba tax ñu gëna ñeme ci wax kàddug Yàlla ci lu àndul ak genn tiit.
14 também a maior parte dos irmãos no Senhor, animados pelas minhas prisões, são muito mais corajosos para falar sem temor a palavra de Deus.
15 — ausente —
15 Verdade é que alguns pregam a Cristo até por inveja e contenda, mas outros o fazem de boa mente;
16 — ausente —
16 estes por amor, sabendo que fui posto para defesa do evangelho;
17 Waaye ñale amuñu xol bu laab, te seen njariñu bopp rekk a tax ñuy yégle turu Kirist, di wuta feddali samay buum ak coono.
17 mas aqueles por contenda anunciam a Cristo, não sinceramente, julgando suscitar aflição às minhas prisões.
18 Lu ci génn nag? Xanaa lii rekk: turu Kirist jolli na ci nii mbaa naa, muy ci naaféq, muy ci dëgg; bég naa ci te dinaa ci bégati.
18 Mas que importa? contanto que, de toda maneira, ou por pretexto ou de verdade, Cristo seja anunciado, nisto me regozijo, sim, e me regozijarei;
19 Ndaxte xam naa ne loolu lépp mu ngi jëm ci sama mucc, jaar ci seeni ñaan ak ndimbalu Xelum Yeesu Kirist, mi ma Yàllay yéwénal.
19 porque sei que isto me resultará em salvação, pela vossa súplica e pelo socorro do Espírito de Jesus Cristo,
20 Ndaxte sama xënte ak sama yaakaar mooy ma baña rus ci lenn, waaye sama yaram feeñal ndamu Kirist, ma ànd ci ak kóolute gu mat, su may dund mbaa may dee; moom laa daan def démb, te moom laay def tey.
20 segundo a minha ardente expectativa e esperança, de que em nada serei confundido; antes, com toda a ousadia, Cristo será, tanto agora como sempre, engrandecido no meu corpo, seja pela vida, seja pela morte.
21 Ndaxte su ma dundee, Kirist laay noyyee; su ma deeyee, xéewal lay doon ci man.
21 Porque para mim o viver é Cristo, e o morrer é lucro.
22 — ausente —
22 Mas, se o viver na carne resultar para mim em fruto do meu trabalho, não sei então o que hei de escolher.
23 — ausente —
23 Mas de ambos os lados estou em aperto, tendo desejo de partir e estar com Cristo, porque isto é ainda muito melhor;
24 waaye ma des fi ci àddina moo gën ci yéen.
24 todavia, por causa de vós, julgo mais necessário permanecer na carne.
25 Loolu wóor na ma; kon xam naa ne dinaa fi des, di leen taxawu yéen ñépp, ngir seen ngëm yokku, ànd ak mbég.
25 E, tendo esta confiança, sei que ficarei, e permanecerei com todos vós para vosso progresso e gozo na fé;
26 Noonu dinaa délsi ci yéen, ngir sama taxawaay gëna lawal seen mbég ci Kirist Yeesu.
26 para que o motivo de vos gloriardes cresça por mim em Cristo Jesus, pela minha presença de novo convosco.
27 Waaye dénk naa leen lii: na seeni jëf yelloo ak li Kirist digle ci xibaaru jàmm bi. Noonu su ma leen seetsee, mbaa ma dégg seen mbir rekk, dinaa xam ne yéena ngi dëgër ci menn xel, bokk benn xalaat ci bëre luy saxal dëggu xibaaru jàmm bi,
27 Somente portai-vos, dum modo digno do evangelho de Cristo, para que, quer vá e vos veja, quer esteja ausente, ouça acerca de vós que permaneceis firmes num só espírito, combatendo juntamente com uma só alma pela fé do evangelho;
28 te baña tiit dara ndax noon, yi leen di xëbal. Màndarga la muy wone ne aji sànku lañu, di màndarga it ne aji mucc ngeen, di mucc gu jóge ci Yàlla.
28 e que em nada estais atemorizados pelos adversários, o que para eles é indício de perdição, mas para vós de salvação, e isso da parte de Deus;
29 Ndaxte Yàlla may na leen, ngeen gëm Kirist, rax-ca-dolli ngeen sonn ndax turam,
29 pois vos foi concedido, por amor de Cristo, não somente o crer nele, mas também o padecer por ele,
30 di wéy ci bëre, bi ngeen gisoon ci man te dégg léegi sama mbir.
30 tendo o mesmo combate que já em mim tendes visto e agora ouvis que está em mim.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Filipenses 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.