Filemom 1

Téereb Injiil (WOL2010) vs ACF

Sair da comparação
ACF Almeida Corrigida Fiel
1 Man Pool, mi ñu tëj kaso ngir Kirist Yeesu, ak sunu mbokk Timote, noo lay bind, yaw Filemon sunu soppe ak sunu nawle ci xeex bi;
1 Paulo, prisioneiro de Jesus Cristo, e o irmão Timóteo, ao amado Filemom, nosso cooperador,
2 te fàttewunu sunu jigéen Afiya, ak sunu àndandoo ci xeex bi Arkib, yéen ak mbooloom ñi gëm, miy dajee sa kër.
2 E à nossa amada Áfia, e a Arquipo, nosso camarada, e à igreja que está em tua casa:
3 Yal na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
3 Graça a vós e paz da parte de Deus nosso Pai, e do Senhor Jesus Cristo.
4 Duma la noppee boole ci samay ñaan, di ci sant Yàlla sama Boroom,
4 Graças dou ao meu Deus, lembrando-me sempre de ti nas minhas orações;
5 ndaxte dégg naa sa ngëm ci Boroom bi Yeesu, ak sa mbëggeel ci gaayam yu sell yépp.
5 Ouvindo do teu amor e da fé que tens para com o Senhor Jesus Cristo, e para com todos os santos;
6 Li may ñaan nag a ngi nii: nga xam bu wér ngëneel, yi nu am yépp ci sunu bokk ci Kirist, ba tax bokk gi nga am ci Yàlla ci kaw ngëm meññ i njariñ.
6 Para que a comunicação da tua fé seja eficaz no conhecimento de todo o bem que em vós há por Cristo Jesus.
7 Ci dëgg-dëgg sa mbëggeel bégal na ma bu baax, ba dëfal sama xol; ndaxte xam naa, sama mbokk, ni nga féexale xoli gaayi Yàlla yu sell yi.
7 Porque temos grande gozo e consolação do teu amor, porque por ti, ó irmão, as entranhas dos santos foram recreadas.
8 Am na lu ma la bëgga ñaan; teguma ko ci sañ-sañ bu mat bi ma Kirist may, ci teg la ndigalu def sa warugar,
8 Por isso, ainda que tenha em Cristo grande confiança para te mandar o que te convém,
9 waaye dama lay ñaan ci mbëggeel gi nu séq, man Pool màggat, mi ñu tëj kaso ci turu Kirist.
9 Todavia peço-te antes por amor, sendo eu tal como sou, Paulo o velho, e também agora prisioneiro de Jesus Cristo.
10 Maa ngi tinul sama doomu diine Onesim, mi ma jur ci Kirist fii ci kaso bi.
10 Peço-te por meu filho Onésimo, que gerei nas minhas prisões;
11 Amul woon sa njariñ démb, waaye tey amal na nu njariñ, yaw ak man.
11 O qual noutro tempo te foi inútil, mas agora a ti e a mim muito útil; eu to tornei a enviar.
12 Maa koy yebal fi yaw, waaye xamal ne mooy sama reeni xol.
12 E tu torna a recebê-lo como às minhas entranhas.
13 Dama koo bëggoona téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xibaaru jàmm bi.
13 Eu bem o quisera conservar comigo, para que por ti me servisse nas prisões do evangelho;
14 Waaye bëggumaa def dara loo àndul; noonu ndimbal li nga may defal du nekk sañul-bañ, waaye mu ànd ak xol bu tàlli.
14 Mas nada quis fazer sem o teu parecer, para que o teu benefício não fosse como por força, mas, voluntário.
15 Xëy na sax dafa tàggoo woon ak yaw diir bu gàtt, ngir nga jotaat ci ba fàww;
15 Porque bem pode ser que ele se tenha separado de ti por algum tempo, para que o retivesses para sempre,
16 waxuma léegi ni jaam rekk, waaye lu ko sut, xanaa mbokk mu dëggu ci xol, fekk looloo raw ag njaam. Mbokk la ci man, rawatina ci yaw, muy sa jaam ci aada, di sa mbokk léegi ci Boroom bi.
16 Não já como servo, antes, mais do que servo, como irmão amado, particularmente de mim, e quanto mais de ti, assim na carne como no Senhor?
17 Soo ma jàppee ni nawle nag, teeru ko, ni su ma la doon ganesi.
17 Assim, pois, se me tens por companheiro, recebe-o como a mim mesmo.
18 Soo ko naree topp genn tooñ mbaa benn bor, topp ma ko.
18 E, se te fez algum dano, ou te deve alguma coisa, põe isso à minha conta.
19 Man Pool maa ngi lay bind ak sama loxob bopp ne dinaa la ko fey; bëggumaa yegg ci ne sag dund sax ci man la jaar!
19 Eu, Paulo, de minha própria mão o escrevi; eu o pagarei, para te não dizer que ainda mesmo a ti próprio a mim te deves.
20 Waaw, yaw sama mbokk, dimbali ma ci Boroom bi, te seral sama xol ci sunu bokk ci Kirist.
20 Sim, irmão, eu me regozijarei de ti no Senhor; recreia as minhas entranhas no Senhor.
21 Noonu bind naa la, ndax wóor na ma ne dinga ma déggal, ba weesu sax li ma la sant.
21 Escrevi-te confiado na tua obediência, sabendo que ainda farás mais do que digo.
22 Te itam nanga ma waajal néeg, ndaxte yaakaar naa ne Yàlla dina nangu seeni ñaan, ba delloosi ma leen.
22 E juntamente prepara-me também pousada, porque espero que pelas vossas orações vos hei de ser concedido.
23 Sama mbokk Epafras, mi ma nekkal fi ci kaso bi ci turu Kirist, mu ngi lay nuyu.
23 Saúdam-te Epafras, meu companheiro de prisão por Cristo Jesus,
24 Samay àndandoo ci liggéey bi, Màrk, Aristàrk, Demas ak Luug, ñu ngi lay nuyu.
24 Marcos, Aristarco, Demas e Lucas, meus cooperadores.
25 Yal na yiwu Boroom bi Yeesu Kirist ànd ak seen xel.
25 A graça de nosso Senhor Jesus Cristo seja com o vosso espírito. Amém.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Filemom 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.