Efésios 6

Téereb Injiil (WOL2010) vs NVI

Sair da comparação
NVI Nova Versão Internacional
1 Naka yéen xale yi, nangeen déggal seeni waajur, ci li ngeen bokk ci Boroom bi, ndaxte looloo rafet.
1 Filhos, obedeçam a seus pais no Senhor, pois isso é justo.
2 «Teralal sa ndey ak sa baay,» mooy ndigal li jëkka ëmb dige,
2 "Honra teu pai e tua mãe", este é o primeiro mandamento com promessa:
3 maanaa: «ngir nga am gudd fan gu ànd ak jàmm.»
3 "para que tudo te corra bem e tenhas longa vida sobre a terra".
4 Yéen baay yi it, buleen bundxataal xale yi, waaye ngeen yar leen, di leen yemale ak a yee ci Boroom bi.
4 Pais, não irritem seus filhos; antes criem-nos segundo a instrução e o conselho do Senhor.
5 Yéen jaam yi, nangeen déggal seeni sang yu àddina, boole ci ragal ak wegeel, di ko def ak xol bu laab, ni su doon ngir Kirist.
5 Escravos, obedeçam a seus senhores terrenos com respeito e temor, com sinceridade de coração, como a Cristo.
6 Buleen ko def rekk ci ngistal, ngir sàkku ngërëmu nit, waaye ni ay jaami Kirist, di jëfe coobarey Yàlla ak seen xol bépp.
6 Obedeçam-lhes não apenas para agradá-los quando eles os observam, mas como escravos de Cristo, fazendo de coração a vontade de Deus.
7 Beyleen seen sas nag ak xol bu tàlli, ni su doon ngir Boroom bi te du nit,
7 Sirvam aos seus senhores de boa vontade, como ao Senhor, e não aos homens,
8 xam ne ku def lu baax, Boroom bi delloo la ko, muy jaam, muy gor.
8 porque vocês sabem que o Senhor recompensará a cada um pelo bem que praticar, seja escravo, seja livre.
9 Yéen it sang yi, jëfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam, te dëddu gépp raglu, xam ne yéena bokk benn Boroom ci asamaan, te ñépp a yem fi moom.
9 Vocês, senhores, tratem seus escravos da mesma forma. Não os ameacem, uma vez que vocês sabem que o Senhor deles e de vocês está nos céus, e ele não faz diferença entre as pessoas.
10 Léegi nag doolewuleen ci Boroom bi te soloo kàttanam gu mag gi.
10 Finalmente, fortaleçam-se no Senhor e no seu forte poder.
11 Gànnaayooleen yérey xarey Yàlla yépp, ngir mana jànkoonte ak pexey Seytaane.
11 Vistam toda a armadura de Deus, para poderem ficar firmes contra as ciladas do diabo,
12 Ndaxte ndëndu xare jib na, waxuma sunu diggante ak nit ñi, waaye ak kilifa yiy nëxal àddina si, ñuy kilifa yi ak ay boroom sañ-sañ, di gaayi Seytaane yi ci bérab yu kawe yi.
12 pois a nossa luta não é contra pessoas, mas contra os poderes e autoridades, contra os dominadores deste mundo de trevas, contra as forças espirituais do mal nas regiões celestiais.
13 Kon nag gànnaayooleen yérey xarey Yàlla yépp, ba mana jànkoonte jamono ju xeex bi taree, not lépp te taxaw temm.
13 Por isso, vistam toda a armadura de Deus, para que possam resistir no dia mau e permanecer inabaláveis, depois de terem feito tudo.
14 Taxawleen kon temm, geñoo dëgg te sàngoo njub, muy seen kiiraayu dënn.
14 Assim, mantenham-se firmes, cingindo-se com o cinto da verdade, vestindo a couraça da justiça
15 Solooleen jàmm, ji xibaaru jàmm biy joxe, ni ay dàll ci seeni tànk, ba jekk ci lépp.
15 e tendo os pés calçados com a prontidão do evangelho da paz.
16 Defleen it ngëm, muy seen pakk, ba mana fél jum yi leen Seytaane di fitt.
16 Além disso, usem o escudo da fé, com o qual vocês poderão apagar todas as setas inflamadas do Maligno.
17 Defleen mucc, muy seen mbaxanam xare, ak kàddug Yàlla, muy jaasi ji leen Xel mu Sell mi tëggal.
17 Usem o capacete da salvação e a espada do Espírito, que é a palavra de Deus.
18 Deeleen ñaan ci xeeti ñaan yépp ci kàttanu Xel mu Sell mi, te sax ci ak farlu gu mat sëkk, di ñaanal gaayi Yàlla yu sell yi yépp.
18 Orem no Espírito em todas as ocasiões, com toda oração e súplica; tendo isso em mente, estejam atentos e perseverem na oração por todos os santos.
19 Te buleen ma ci fàtte, ngir waxtu wu ma ubbee sama gémmiñ, ma am lu ma wax, ba mana xamle ak fit wu dëgër mbóoti xibaaru jàmm bi.
19 Orem também por mim, para que, quando eu falar, seja-me dada a mensagem a fim de que, destemidamente, torne conhecido o mistério do evangelho,
20 Ndaw laa ci, lu ñu jéng; yal na ma Yàlla may fit wu ma waxe, ni mu ma ware.
20 pelo qual sou embaixador preso em correntes. Orem para que, permanecendo nele, eu fale com coragem, como me cumpre fazer.
21 Yónnee naa leen Tisig sama mbokk, mi ma sopp, te muy jawriñ ju takku ci liggéeyu Boroom bi, ngir mu xamal leen lépp li aju ci man ak li may def.
21 Tíquico, o irmão amado e fiel servo do Senhor, lhes informará tudo, para que vocês também saibam qual é a minha situação e o que estou fazendo.
22 Maa leen ko yónneel sama bopp, ngir ngeen xam li nu nekke, te mu dëfal seeni xol.
22 Enviei-o a vocês por essa mesma razão, para que saibam como estamos e para que ele os encoraje.
23 Yéen bokk yi, yal na leen Yàlla Baay bi ak Yeesu Kirist Boroom bi may jàmm ak mbëggeel gu ànd ak ngëm.
23 Paz seja com os irmãos, e amor com fé da parte de Deus Pai e do Senhor Jesus Cristo.
24 Yal na yiwu Yàlla ànd ak ñépp, ñi bëgg Boroom bi Yeesu Kirist ak mbëggeel gu sax.
24 A graça seja com todos os que amam a nosso Senhor Jesus Cristo com amor incorruptível.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Efésios 6, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.