Efésios 5

Téereb Injiil (WOL2010) vs BKJ

Sair da comparação
1 Yéen nag ñiy goney Yàlla, yi mu bëgg ci xolam, royleen ko ci loolu.
1 Sede, pois, seguidores de Deus, como filhos queridos;
2 Ngeen wéer seen dund ci mbëggeel, mel ni Kirist mi nu bëgg, ba joxe bakkanam ngir nun, di sarax su ñu jébbal Yàlla te neex ko ni xetu latkoloñ.
2 e andai em amor, como também Cristo nos amou, e se entregou a si mesmo por nós, em oferta e sacrifício a Deus, em cheiro suave.
3 Waaye naka njaaloo ak bépp sobe mbaa bëgge, jéllale naa jëf ji sax, waaye bu ko làmmiñ tudd, ni mu jekke ci gaayi Yàlla yu sell yi.
3 Mas a fornicação e toda impureza ou avareza nem ainda se nomeiem entre vós, como convém a santos;
4 Dawleen it lu jekkadee, ni wax ju ñaaw mbaa waxi caaxaan ak kaf yu bon, te ngeen sax ci sant Yàlla.
4 nem imundícia, nem conversas tolas, nem gracejos, que não convêm; mas, antes, ações de graças.
5 Na leen wóor ne kenn ku jikkowoo ndoxaan, sobe mbaa bëgge, maanaam bokkaale Yàlla, kooku du am cér ci nguuru Kirist ak Yàlla.
5 Porque bem sabeis isto: que nenhum devasso, ou pessoa impura, ou homem avarento, o qual é idolatra, tem herança alguma no reino de Cristo e de Deus.
6 Bu leen kenn nax ci ay waxi neen, ndaxte jëf yooyooy tax meru Yàlla di wàcc ci kureelu ñi ko déggadil.
6 Ninguém vos engane com palavras vãs; porque por essas coisas vem a ira de Deus sobre os filhos da desobediência.
7 Kon nag buleen séq ak ñoom dara.
7 Portanto, não sejais participantes com eles.
8 Lëndëm ngeen woon, waaye léegi leer ngeen ndax seen bokk ci Boroom bi.
8 Porque, noutro tempo, éreis trevas, mas agora sois luz no Senhor; andai como filhos da luz,
9 Leer, mbaax lay meññ, njub ak dëgg.
9 (pois o fruto do Espírito está em toda bondade, e justiça, e verdade),
10 Dëggal-leen ci seeni jëf li neex Boroom bi,
10 aprovando o que é aceitável ao Senhor.
11 te daw lépp luy jëfi lëndëm yu amul njariñ, bay weer sax ku koy def.
11 E não tenhais comunhão com as obras infrutíferas das trevas, mas, antes, reprovai-as.
12 Ndaxte waxtaane sax li ñuy def ci nëbbu, lu ruslu la;
12 Porque até falar destas coisas que são feitas por eles em secreto é vergonha.
13 waaye leer, lu mu ëmb, fésal ko.
13 Mas todas as coisas que são reprovadas, são manifestadas pela luz: Pois tudo o que manifesta é luz.
14 Ndaxte lu jaxasoo ak leer di leer. Looloo tax ñu ne:
14 Pelo que ele diz: Desperta, ó tu que dormes, e levanta-te dentre os mortos, e Cristo te dará a luz.
15 Noonu sàmmleen seen dundin, waxuma ni ñu amul xel, waaye ni ñu am xel,
15 Portanto, vede prudentemente como andais, não como tolos, mas como sábios,
16 tey jariñoo jot gi, ndaxte nu ngi ci jamono ju bon.
16 remindo o tempo, porque os dias são maus.
17 Buleen ñàkk bopp nag, waaye xamleen liy coobarey Boroom bi.
17 Por isso não sejais insensatos, mas entendei qual seja a vontade do Senhor.
18 Buleen màndi it ci sàngara, liy ndeyi ñaawteef, waaye feesleen ak Xel mu Sell mi;
18 E não vos embriagueis com vinho, no qual há excesso, mas enchei-vos do Espírito;
19 di waxante ci seen biir ci ay taalifi Sabóor, ciy woy ak i cant yu tukkee ci Xelum Yàlla, di woy ak a kañ Boroom bi ci seen xol.
19 falando entre vós com salmos, e hinos, e cânticos espirituais, cantando e louvando ao Senhor no vosso coração,
20 Gërëmleen Yàlla Baay bi ci turu Yeesu Kirist Boroom bi, fu ngeen mana tollu, ci lu mu mana doon;
20 dando sempre graças por todas as coisas a Deus e Pai, em nome de nosso Senhor Jesus Cristo,
21 teg ca nangul sa moroom ci biir wegeelu Kirist.
21 sujeitando-vos uns aos outros no temor de Deus.
22 Naka yéen jigéen ñi, nangeen nangul seeni jëkkër, ni su doon Boroom bi.
22 Esposas, submetam-se aos seus maridos, como ao Senhor.
23 Ndaxte góor mooy kilifag soxnaam, ni Kirist nekke kilifag mbooloom ñi gëm, muy jëmmam ji muy sàmm.
23 Porque o marido é a cabeça da esposa, como também Cristo é a cabeça da igreja, sendo ele próprio o salvador do corpo.
24 Ni mbooloo mi nag jiitale Kirist, noonu la jigéen ji wara jiitale jëkkëram ci lépp.
24 Portanto, assim como a igreja está sujeita a Cristo, assim também as mulheres sejam em tudo sujeitas a seu marido.
25 Yéen nag góor ñi, na ku nekk bëgg soxnaam, ni Kirist bëgge mbooloo mi, ba joxe bakkanam ndax moom,
25 Maridos, amem suas esposas, assim como também Cristo amou a igreja e a si mesmo se entregou por ela,
26 ngir sellal ko ak kàddoom, ba mu laab ni ku sangu set.
26 para a santificar, purificando-a com a lavagem da água, pela palavra,
27 Noonu dina ko jël, mu mel ni séet bu ñu waajal, di mbooloom mu soloo ndam, te gàkkul, rasul, taqul leneen, waaye mu sell te amul sikk.
27 para a apresentar a si mesmo igreja gloriosa, sem mácula, ou ruga, ou coisa semelhante, mas santa e ­irrepreensível.
28 Na góor bëgg soxnaam, ni mu bëgge boppam. Bëgg sa soxna, bëgg sa bopp la.
28 Assim devem os maridos amar a sua própria esposa como a seu próprio corpo. Quem ama a sua esposa ama-se a si mesmo.
29 Ndaxte kenn masula bañ sa yaram. Waaye danga koy dundal, di ko fonk. Noonu it la Kirist fonke mbooloo mi;
29 Porque nenhum homem detestou a sua própria carne; antes, a alimenta e sustenta, como também o Senhor à igreja;
30 ndaxte noo di céri jëmmam.
30 porque somos membros do seu corpo, da sua carne, e dos seus ossos.
31 Mbind mi nee na: «Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñoom ñaar doon kenn.»
31 Por isso, o homem deixará seu pai e sua mãe e se unirá à sua esposa; e os dois serão uma só carne.
32 Loolu ëmb na mbóot mu xóot; man maa ngi wax ci lu jëm ci Kirist ak mbooloo mi.
32 Este é um grande mistério; digo-o, porém, a respeito de Cristo e da igreja.
33 Waaye li teew, na góor gu nekk bëgg soxnaam, ni mu bëgge boppam, te jigéen ji weg jëkkëram.
33 Assim também vós, cada um em particular ame a sua própria esposa como a si mesmo, e a esposa reverencie seu marido.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Efésios 5, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.