Efésios 4
Téereb Injiil (WOL2010) vs ACF
1 Man mi ñu tëj kaso ngir Boroom bi nag, maa ngi leen di dénk, ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla.
1 Rogo-vos, pois, eu, o preso do Senhor, que andeis como é digno da vocação com que fostes chamados,
2 Ngeen woyof toyy te lewet, di muñalante tey baalante ci mbëggeel,
2 Com toda a humildade e mansidão, com longanimidade, suportando-vos uns aos outros em amor,
3 te dem ba fu seen kàttan yem, ngeen likkoo ci jàmm, bay sàmm booloo gi leen Xelum Yàlla may.
3 Procurando guardar a unidade do Espírito pelo vínculo da paz.
4 Jenn jëmm moo am, menn Xel, ak jenn yaakaaru ëllëg ju wooteb Yàlla ëmb.
4 Há um só corpo e um só Espírito, como também fostes chamados em uma só esperança da vossa vocação;
5 Benn Boroom it a am, genn ngëm, ak benn seedeb ngëm ci li ñu leen sóob ci ndox.
5 Um só Senhor, uma só fé, um só batismo;
6 Te jenn Yàllaa am, di Baayu ñépp, mu tiim ñépp, fees ñépp te dëkk ci ñépp.
6 Um só Deus e Pai de todos, o qual é sobre todos, e por todos e em todos vós.
7 Waaye ku nekk ci nun ak mayam, ni nu ko Kirist séddalee.
7 Mas a graça foi dada a cada um de nós segundo a medida do dom de Cristo.
8 Looloo tax Mbind mi ne:
8 Por isso diz: Subindo ao alto, levou cativo o cativeiro,e deu dons aos homens.
9 Su nu waxee ne «yéeg na,» li moo ci génn: daa jëkka wàcc ba ca bérab ya gëna suufe.
9 Ora, isto - ele subiu - que é, senão que também antes tinha descido às partes mais baixas da terra?
10 Ki wàccoon moo yéegaat, ba tiim asamaan yépp, ngir fees lépp.
10 Aquele que desceu é também o mesmo que subiu acima de todos os céus, para cumprir todas as coisas.
11 Moo may ñii di ay ndawam, ñii ay yonent, ñii ay taskati xibaaru jàmm bi, ak ñeneen ñuy sàmm mbooloom ñi gëm te di ko jàngal.
11 E ele mesmo deu uns para apóstolos, e outros para profetas, e outros para evangelistas, e outros para pastores e doutores,
12 Maye na leen, ngir ñu waajal gaayi Yàlla yu sell yi, ñu mana bey seen sas ci taxawal mbooloom Kirist, di jëmmam.
12 Querendo o aperfeiçoamento dos santos, para a obra do ministério, para edificação do corpo de Cristo;
13 Noonu nu mànkoo ci sunu ngëm ak ci xam Doomu Yàlla ji, ba kera nuy egg ci nekk nit ku sotti te taxaw taxawaay bu dëppook matug Kirist.
13 Até que todos cheguemos à unidade da fé, e ao conhecimento do Filho de Deus, a homem perfeito, à medida da estatura completa de Cristo,
14 Noonu dootunu ay gone yu njànglem nit ku ñëw di fàbbi ci seeni làqarci ak seeni pexe, nu mel ni ay gaal yu duus yi ak ngelaw li di baaje.
14 Para que não sejamos mais meninos inconstantes, levados em roda por todo o vento de doutrina, pelo engano dos homens que com astúcia enganam fraudulosamente.
15 Waaye dinanu wax dëgg, ëmb ko ci mbëggeel, bay màgg ci fànn gu ne ci sunu bokk ci Kirist. Mooy bopp,
15 Antes, seguindo a verdade em amor, cresçamos em tudo naquele que é a cabeça, Cristo,
16 te jëmm jépp ci moom lay dunde, di jëmm ju ràbboo te déggoo ci bépp tenqo, te cér bu nekk di def warugaram. Noonu jëmm ji di yokku ak a màgg ci biir mbëggeel.
16 Do qual todo o corpo, bem ajustado, e ligado pelo auxílio de todas as juntas, segundo a justa operação de cada parte, faz o aumento do corpo, para sua edificação em amor.
17 Maa ngi leen di wax lii nag, te di ko dëggal ci kanam Boroom bi: buleen dundeeti ni xeeti àddina yi, ci seeni xalaati neen
17 E digo isto, e testifico no Senhor, para que não andeis mais como andam também os outros gentios, na vaidade da sua mente.
18 ak seen xel mu lëndëm. Dañoo génn ci dundu Yàlla, ndax umple gi ñu am ci moom, ak li ñu ko tëjal seen xol.
18 Entenebrecidos no entendimento, separados da vida de Deus pela ignorância que há neles, pela dureza do seu coração;
19 Seen xol dafa dërkiis, ba ñu bayliku ciy topp seen nafsu, di sóobu ci bépp sobe te xér ci.
19 Os quais, havendo perdido todo o sentimento, se entregaram à dissolução, para com avidez cometerem toda a impureza.
20 Waaye du dundin woowu ngeen jàng ci Kirist.
20 Mas vós não aprendestes assim a Cristo,
21 Ndax yaakaar naa ne dégg ngeen Kirist te jàng ngeen ci moom, ba xam dëgg gi Yeesu ëmb.
21 Se é que o tendes ouvido, e nele fostes ensinados, como está a verdade em Jesus;
22 Maanaam ngeen yulli seen jikkoy judduwaale ju bon ji daan fés ci seeni jëf, di gëna yées, te ànd ak i bëgg-bëggam yu di naxi kese.
22 Que, quanto ao trato passado, vos despojeis do velho homem, que se corrompe pelas concupiscências do engano;
23 Te ngeen yeeslu ci seen biir xel,
23 E vos renoveis no espírito da vossa mente;
24 te soloo jikko ju bees, ji Yàlla sàkk ci njubte lu dëggu ak sellaay gu dëggu.
24 E vos revistais do novo homem, que segundo Deus é criado em verdadeira justiça e santidade.
25 Kon nag bàyyileen di fen, tey wax dëgg kenn ku nekk ci moroomam, ndax ku nekk sa genn-wàllu moroom nga.
25 Por isso deixai a mentira, e falai a verdade cada um com o seu próximo; porque somos membros uns dos outros.
26 Ku mer, bu mu jàll aw kaañ; bu jant bi sowaale seen mer,
26 Irai-vos, e não pequeis; não se ponha o sol sobre a vossa ira.
27 ba ngeen may Seytaane bunt.
27 Não deis lugar ao diabo.
28 Ku daan sàcc, na ko dëddu te jublu ci liggéey lu baax ci ay loxoom, ngir mu mana dimbali ñi néew doole.
28 Aquele que furtava, não furte mais; antes trabalhe, fazendo com as mãos o que é bom, para que tenha o que repartir com o que tiver necessidade.
29 Bu genn kàddu gu ñaaw génn ci seen gémmiñ, waaye su wax yegsee, nangeen wax lu rafet, ba faj soxlay seeni moroom, te teg ñi leen di déglu ci yoonu yiw.
29 Não saia da vossa boca nenhuma palavra torpe, mas só a que for boa para promover a edificação, para que dê graça aos que a ouvem.
30 Buleen yóbbe tiis Xelu Yàlla mu Sell, mi leen tàmpe ngir bésu goreel ba.
30 E não entristeçais o Espírito Santo de Deus, no qual estais selados para o dia da redenção.
31 Dëdduleen lépp luy wex mbaa tàng bopp, luy mer mbaa coow, lépp luy xaste mbaa coxor.
31 Toda a amargura, e ira, e cólera, e gritaria, e blasfêmia e toda a malícia sejam tiradas dentre vós,
32 Te ngeen baax ci seen diggante, di laayante biir tey baalante, ni leen Yàlla baale ci turu Kirist.
32 Antes sede uns para com os outros benignos, misericordiosos, perdoando-vos uns aos outros, como também Deus vos perdoou em Cristo.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Efésios 4, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.