Efésios 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs BKJ

Sair da comparação
1 Kon nag maa ngi leen di ñaanal, man Pool mi ñu tëj kaso ci turu Kirist ndax sas wi may bey ci yéen, xeet yi dul Yawut.
1 Por esta causa, eu, Paulo, sou o prisioneiro de Jesus Cristo por vós, os gentios,
2 Wóor na ma ne dégg ngeen yenub xamle yiwu Yàlla, bi mu ma jagleel jëm ci yéen.
2 se é que tendes ouvido a dispensação da graça de Deus, que me é dada para convosco;
3 Yàlla feeñu na ma, xamal ma mbóoti mbir mi mu tëral, ni ma leen ko binde ci kàddu yu néew.
3 como pela revelação ele fez-me saber este mistério (como vos escrevi antes, em poucas palavras,
4 Bu ngeen jàngee loolu, dingeen mana xam bu wér dégg, gi ma am ci mbóoti mbiri Kirist.
4 pelo que, quando ledes, podeis entender o meu conhecimento do mistério de Cristo).
5 Ci jamono yu weesu, loolu kumpa la woon ci doom Aadama, waaye léegi Yàlla feeñalal na ko ay ndawam ak yonentam yu sell yi, jaarale ko ci Xel mu Sell mi.
5 O qual, noutras épocas, não foi manifestado aos filhos dos homens, como, agora, tem sido revelado aos seus santos apóstolos e profetas pelo Espírito,
6 Mbir mi nii la tëdde: léegi xeet yi dul Yawut dañoo bokksi cér ak Yawut yi, bokk ak ñoom jenn jëmm, bokk wàll ci xéewal yi Yàlla dige ci Kirist Yeesu, te xibaaru jàmm bi xamle ko.
6 a saber, que os gentios são coerdeiros, e de um mesmo corpo, e participantes da sua promessa em Cristo pelo evangelho;
7 Xamle xibaaru jàmm boobu nag, Yàlla fal na ma ci jawriñ ci kaw yiwam, te di ma dooleel ci kàttanam.
7 do qual fui feito ministro, segundo o dom da graça de Deus, dado a mim pela operação eficaz do seu poder.
8 May na ma, man mi gëna tuuti ci gaayi Yàlla yu sell yi, may xibaar xeeti àddina barkeel yu xel dajul yi ci Kirist;
8 A mim, que sou menos que o mínimo de todos os santos, me foi dada esta graça de pregar entre os gentios as riquezas incompreensíveis de Cristo,
9 te it may sulli melokaanu mbir mu xóot, mi Yàlla tëral te doon kumpa njàlbéen ga ba tey ci moom mi sos lépp.
9 e fazer com que todos vejam qual é a comunhão do mistério, que, desde o começo do mundo, esteve oculto em Deus, que criou todas as coisas por meio de Jesus Cristo;
10 Waaye léegi nee na fàŋŋ, ngir kilifa yi ak boroom sañ-sañ yi ca bérab yu kawe ya mana xam ni Xelum Yàlla xóote, jaar ci li ñu gis ci mbooloom ñi gëm Kirist.
10 para que agora, os principados e potestades nos lugares celestiais possam conhecer, pela igreja, a multiforme sabedoria de Deus,
11 Mooy dogal bi sax dàkk, te Yàlla tëral ko ci Kirist Yeesu sunu Boroom.
11 segundo o eterno propósito que fez em Cristo Jesus, nosso Senhor,
12 Ci turam am nanu kóolute fa kanam Yàlla, ak bunt bu yaatu ci moom ci kaw ngëm.
12 no qual temos ousadia e acesso com confiança, pela nossa fé nele.
13 Maa ngi leen di ñaan nag, ngeen baña yoqi ndax coono, yi may jële ci bey sama sas ci yéen, xam ne coono yooyu ñoo leen di jural ndam.
13 Portanto, vos peço que não desfaleçais nas minhas tribulações por vós, que são a vossa glória.
14 Moo tax maa ngi sukk, jublu ci Yàlla Baay
14 Por causa disso, me ponho de joelhos perante o Pai de nosso Senhor Jesus Cristo,
15 biy cosaanul njaboot gépp, muy ci kaw, muy ci suuf.
15 do qual toda a família nos céus e na terra toma o nome,
16 Ma di ko ñaan, mu may leen, ci kaw ndamam lu amul kem, Xel mu Sell mi feddali seen baatin ak kàttan gu mag,
16 para que vos conceda, segundo as riquezas da sua glória, que sejais fortalecidos com poder pelo seu Espírito no homem interior;
17 ba Kirist dëkk ci seeni xol ci kaw ngëm. Te ngeen sax noonu te sampu ci mbëggeelu Yàlla,
17 para que Cristo habite no vosso coração pela fé; a fim de, estando arraigados e fundados em amor,
18 ba jagoo, yéen ak gaayi Yàlla yu sell yépp, guddaay ba, yaatuwaay ba, kawe ga ak xóotaay ba,
18 possa ser capaz de compreender, com todos os santos, qual é a largura, e o comprimento, e a profundidade, e altura,
19 te xam mbëggeelu Kirist, gi raw mépp xel. Noonu dingeen fees dell ak matug Yàlla.
19 e conhecer o amor de Cristo, que excede todo conhecimento, para que sejais cheios de toda a plenitude de Deus.
20 Léegi nag, na ndam li féete ak Yàlla, mi mana yeggale lépp luy ñaan mbaa yéene, ba weesu ko fuuf, dëppook kàttan giy jëf ci nun;
20 Ora, àquele que é capaz de fazer tudo muito mais abundantemente além daquilo que pedimos ou pensamos, segundo o poder que em nós opera,
21 moo yelloo ndamul mbooloom ñi gëm jamonoy jamono ba fàww, jaar ci Kirist Yeesu. Amiin.
21 a ele seja a glória na igreja, por Cristo Jesus, em todas as gerações, para sempre e sempre. Amém.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Efésios 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.