Efésios 2

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Yéen itam Yàlla dekkal na leen, yéen ñi doon ndee fa kanamam ci seeni moy ak seeni bàkkaar.
1 Ele vos vivificou, estando vós mortos nos vossos delitos e pecados,
2 Ci biir yooyu ngeen doon dund démb, topp doxalinu àddina, tey déggal kilifag boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, di xel mu bon miy jëf ci kureelu ñi déggadil Yàlla.
2 nos quais outrora andastes, segundo o curso deste mundo, segundo o príncipe das potestades do ar, do espírito que agora opera nos filhos de desobediência,
3 Nun it booba àndoon nanu ak ñoom ca seen dund ga, di topp sunu bakkan ciy wut bànneexi yaram ak coobarey xel. Noonu ci sunu bindu nit yeyoo nanu meru Yàlla, ni ña ca des.
3 entre os quais todos nós também antes andávamos nos desejos da nossa carne, fazendo a vontade da carne e dos pensamentos; e éramos por natureza filhos da ira, como também os demais.
4 Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw mbëggeel gu réy, gi mu am ci nun,
4 Mas Deus, sendo rico em misericórdia, pelo seu muito amor com que nos amou,
5 dundalaat na nu ak Kirist, fekk ndee lanu woon fa kanamam ci sunuy bàkkaar— ci kaw yiwu Yàlla ngeen mucce.
5 estando nós ainda mortos em nossos delitos, nos vivificou juntamente com Cristo {pela graça sois salvos},
6 Te dekkal na nu ak Kirist Yeesu, dëël nu ak moom ca bérab yu kawe ya.
6 e nos ressuscitou juntamente com ele, e com ele nos fez sentar nas regiões celestes em Cristo Jesus,
7 Noonu ba fu jamono yem, dina lañal fi sunu kanam yiwam wu réy wi xel manta takk, jaar ci baaxaay gi mu nu won ci Kirist Yeesu.
7 para mostrar nos séculos vindouros a suprema riqueza da sua graça, pela sua bondade para conosco em Cristo Jesus.
8 Ndaxte ci yiwu Yàlla ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yéen, mayu Yàlla la;
8 Porque pela graça sois salvos, por meio da fé, e isto não vem de vós, é dom de Deus;
9 du peyu jëf, ba kenn di ci kañu.
9 não vem das obras, para que ninguém se glorie.
10 Ndaxte jëfu Yàlla lanu; moo nu bind ci Kirist Yeesu, ngir nu wéy ci jëf yu rafet, yi mu nu fàgguloon ca njàlbéen ga.
10 Porque somos feitura sua, criados em Cristo Jesus para boas obras, as quais Deus antes preparou para que andássemos nelas.
11 Kon nag yéen ñi dul Yawut cib juddu, yéen ñi xaraful, te ñi xaraf ci seen yaram ci loxol nit ñoo leen teg ay yéefar, fàttalikuleen lii:
11 Portanto, lembrai-vos que outrora vós, gentios na carne, chamam circuncisão, feita pela mão dos homens,
12 booba amuleen woon benn cér ci Kirist, mbaa benn baat ci kureelu bànni Israyil. Bokkuleen woon ci kóllëre, gi Yàlla fas ak ñoom, te ëmb dige ya. Amuleen woon benn yaakaar mbaa benn xam-xamu Yàlla ci àddina.
12 estáveis naquele tempo sem Cristo, separados da comunidade de Israel, e estranhos aos pactos da promessa, não tendo esperança, e sem Deus no mundo.
13 Waaye léegi ci seen bokk ci Kirist Yeesu, yéen ñi sore woon jege ngeen ndax deretu Kirist ji ñu tuur.
13 Mas agora, em Cristo Jesus, vós, que antes estáveis longe, já pelo sangue de Cristo chegastes perto.
14 Ndaxte mooy sunu jàmm, moom mi jël Yawut ak ki dul Yawut, def nu benn. Ñag bi doxoon sunu diggante te sosoon sunu dëngoo, moo ko màbb ci li mu joxe yaramam,
14 Porque ele é a nossa paz, o qual de ambos os povos fez um; e, derrubando a parede de separação que estava no meio, na sua carne desfez a inimizade,
15 far noonu yoonu Musaa, muy ndigal ya ak dogal ya. Noonu la nu jële, Yawut ak ki dul Yawut, def nu benn ci moom, ba nu jàmmoo.
15 isto é, a lei dos mandamentos contidos em ordenanças, para criar, em si mesmo, dos dois um novo homem, assim fazendo a paz,
16 Nun ñaar, ñi def benn jëmm, jubale na nu ak Yàlla ci dee, gi mu dee ca bant ba ñu ko daajoon, dindee noonu sunu tongoonte.
16 e pela cruz reconciliar ambos com Deus em um só corpo, tendo por ela matado a inimizade;
17 Bi mu ko defee mu ñëw, yégalsi nu xibaaru jàmm fa kanam Yàlla, yéen ñi sore woon ak nun ñi jege.
17 e, vindo, ele evangelizou paz a vós que estáveis longe, e paz aos que estavam perto;
18 Ndaxte nun ñaar ñépp am nanu bunt ci Yàlla Baay bi, jaar ci Kirist, ci ndimbalu menn Xel mu Sell mi.
18 porque por ele ambos temos acesso ao Pai em um mesmo Espírito.
19 Noonu dootuleen ay doxandéem mbaa ay gan, waaye am ngeen baat ci kureelu gaayi Yàlla yu sell yi, te waa këram ngeen.
19 Assim, pois, não sois mais estrangeiros, nem forasteiros, antes sois concidadãos dos santos e membros da família de Deus,
20 Yéena ngi sukkandikoo ci fondamaa, bi ndawi Kirist yi ak yonent yi tabax, te Kirist Yeesu ci boppam di doju dalil wa.
20 edificados sobre o fundamento dos apóstolos e dos profetas, sendo o próprio Cristo Jesus a principal pedra da esquina;
21 Ci moom la doj yépp ràbbloo, ba tabax bi jóg, di màggalukaay bu sell ngir Boroom bi.
21 no qual todo o edifício bem ajustado cresce para templo santo no Senhor,
22 Ci seen bokk ci Kirist, Yàlla boole na leen tabax yéen itam, ba ngeen nekk dëkkukaayam, jaar ci Xel mu Sell mi.
22 no qual também vós juntamente sois edificados para morada de Deus no Espírito.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Efésios 2, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.