Colossenses 2

Téereb Injiil (WOL2010) vs BKJ

Sair da comparação
1 Bëgg naa nag, ngeen xam bëre bu metti, bi may bëre ngir yéen, ngir waa Lawdise ak ñépp ñi ma masula teg bët. Damay def sama kem kàttan,
1 Porque quero que saibais quão grande luta tenho por vós, e pelos que estão em Laodiceia, e por quantos não viram o meu rosto em carne;
2 ngir ngeen am fit te nekk benn ci mbëggeel, ngir dajal noonu xam-xam bu mat, ba xam kumpag Yàlla, di Kirist.
2 Que seus corações sejam confortados, e estejam unidos no amor, e para todas as riquezas da plena certeza de entendimento, para o reconhecimento do mistério de Deus, e do Pai, e de Cristo.
3 Ci moom lañu denc lépp lu ñuy sàkku ci xel ak ci xam-xam.
3 Em quem estão escondidos todos os tesouros da sabedoria e do conhecimento.
4 Maa ngi wax lii, ngir kenn bañ leena nax ci ay wax yu neex.
4 E isto eu digo para que ninguém vos engane com palavras persuasivas.
5 Jëmm ji ñëwul waaye sama xel a ngi ci yéen, di bég ci seen doxalin ak ngëm gu dëgër, gi ngeen am ci Kirist.
5 Porque ainda que esteja ausente quanto ao corpo, ainda estou convosco em espírito, regozijando-me e vendo a vossa ordem e a firmeza da vossa fé em Cristo.
6 Kon nag, ni ngeen nangoo Kirist Yeesu ni Boroom bi, dundeleen noonu ci moom.
6 Como, portanto, recebestes o Senhor Jesus Cristo, assim andai nele,
7 Saxleen ci moom, di màgg ci moom, tey gëna dëgër ci ngëm, gi ñu leen jàngal, ba seen xol di baawaan ci gërëm Yàlla.
7 enraizado e edificado nele, e estabelecido na fé, assim como fostes ensinados, abundando nela com ação de graças.
8 Moytuleen ba kenn bañ leena fàbbi ci ay xam-xami nit yuy naxi neen. Xam-xam yu mel noonu, ñu ngi soqikoo ci aada yu nit tëral, ci aaday àddina, waaye soqikoowul ci Kirist.
8 Tende cuidado para que nenhum homem vos deteriore pela filosofia e vaidade, segundo a tradição dos homens, segundo os rudimentos do mundo e não segundo Cristo;
9 Ndaxte ci Kirist, maanaam ci yaramu nitam, la matug Yàlla gépp dëkk,
9 porque nele habita corporalmente toda a plenitude da divindade.
10 te mat ngeen ci moom, miy buuru kilifa yépp ak boroom sañ-sañ yépp.
10 E estais completos nele, que é a cabeça de todo principado e poder;
11 Ndax seen ngëm ci moom xaraf ngeen xaraf bu loxol nit deful, maanaam Kirist summil na leen dooley bàkkaar, ji moomoon seen yaram. Loolu mooy xaraf, bi Kirist def.
11 nele também fostes circuncidados com uma circuncisão não feita por mão no despojo do corpo dos pecados da carne, mediante a circuncisão de Cristo.
12 Bi ñu leen sóobee ci ndox, suulaale nañu leen ak moom, te it dekki ngeen ak moom, ndaxte gëm ngeen ci dooley Yàlla, ji ko dekkal ca néew ya.
12 Sepultados com ele no batismo, onde também ressuscitastes com ele pela fé na operação de Deus, quem o ressuscitou dos mortos.
13 Te yéen ñi doon ndee fa kanam Yàlla ndax seeni moy ak seen ñàkka xaraf, Yàlla dundalaat na leen ak Kirist, baal nu sunuy bàkkaar yépp.
13 E, quando vós estáveis mortos nos vossos pecados e na incircuncisão da vossa carne, vos vivificou juntamente com ele, perdoando-vos todas as ofensas,
14 Mbind mi nu doon tiiñal, te daa nu yey ndax ay sàrtam, Yàlla far na ko, dindi ko, daajaale ko ca bant ba Kirist deeye.
14 apagando a escrita de ordenanças que era contra nós, a qual nos era contrária, e tirou-a do meio de nós, cravando-a na sua cruz.
15 Futti na kilifa yi ak boroom sañ-sañ yi, weer leen ci kanam ñépp, sëkktal leen niy jaam ndax ndam la Kirist jële ca bant ba.
15 E, despojando os principados e potestades, os expôs abertamente, triunfando sobre eles em si mesmo.
16 Kon nag bu leen kenn teg tooñ ci li jëm ciy ñam mbaa naan, ci màggal mbaa xewu weer wu feeñ, mbaa ci bésub noflaay.
16 Portanto, nenhum homem vos julgue pelo alimento, ou pela bebida, ou por causa dos dias de festa, ou da lua nova, ou dos shabats;
17 Loolu lépp nag takkandeer la woon buy misaal li waroona ñëw, waaye lu dëggu li mi ngi ci Kirist.
17 que são sombras das coisas futuras, mas o corpo é de Cristo.
18 Kuy bég ci di toroxlu ci ngistal, di jaamu ay malaaka, buleen ko may, mu àtte leen. Kooku dafay jeneer, di seet li koy feeñu, bay tiitaroo xalaatam, fekk xalaatu nit kese la, te neen.
18 Que nenhum homem vos engane de vossa recompensa com uma falsa humildade e adoração de anjos, intrometendo-se em coisas que ele não viu, em vão inflado por sua mente carnal.
19 Taqul ci Kirist, miy bopp bi yilif jëmm ji. Bopp bee tax ba jëmm jépp, ji siddit yi ak tenqo yi téye te taqale ko, di màgg màgg gi ko Yàlla di jox.
19 E não ligado à cabeça, da qual todo o corpo, tendo alimento ministrado, e unido pelas juntas e ligaduras, cresce em aumento de Deus.
20 — ausente —
20 Se, pois, estais mortos com Cristo quanto aos rudimentos do mundo, por que, como se vivêsseis no mundo, vos sujeitais às ordenanças,
21 — ausente —
21 (não toques, não proves, não manuseies;
22 Sàrt yooyu ñu ngi aju ci ndigali nit ñi ak seen njàngle. Yëf yi ñu tudd yépp, dees na leen jariñoo, ba ñu jeex.
22 as quais coisas todas perecem pelo uso), segundo os mandamentos e doutrinas dos homens?
23 Dëgg la, seeni sàrt dañuy dénkaane pastéef ci jaamu Yàlla, di toroxlu ak di fitnaal seen yaram. Waaye sàrt yooyu nag amuñu benn njariñ, ngir nit ñi not seen nafsu.
23 Que tais coisas, de fato, mostram uma sabedoria na adoração, humildade e em disciplina do corpo, mas não são de honra alguma, senão para a satisfação da carne.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Colossenses 2, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.