Atos 23
Téereb Injiil (WOL2010) vs VC
1 Noonu Pool xool jàkk géew ba ne leen: «Bokk yi, ci xel mu dal laa doxale ci kanam Yàlla ba ci bésu tey bi.»
1 Paulo, fitando os olhos nos membros do conselho, disse: Irmãos, eu tenho procedido diante de Deus com toda a boa consciência ate o dia de hoje...
2 Ci kaw loolu sarxalkat bu mag ba, di ku ñuy wax Anañas, sant ña taxaw ca wetam, ñu fél gémmiñam.
2 Mas Ananias, sumo sacerdote, mandou aos que estavam ao seu lado que lhe batessem na boca.
3 Pool ne ko: «Yàlla dina la dóor, yaw mi naaféq, bay samandaay miir bu joy bu ñu weexal. Yaa ngi toog di ma àtte, ci li yoon wi digle, ba noppi santaane ñu dóor ma, ci li yoon wi tere!»
3 Então Paulo lhe disse: Deus te ferirá também a ti, hipócrita! Tu estás aí assentado para julgar-me segundo a lei, e contra a lei mandas que eu seja ferido?
4 Waaye ña taxaw ca wetam ne ko: «Ndax dangay xas sarxalkat bu mag, bi Yàlla fal?»
4 Os assistentes disseram: Tu injurias o sumo sacerdote de Deus.
5 Pool ne leen: «Bokk yi, xawma woon ne sarxalkat bu mag bi la, ndaxte tëral nañu ci Mbind mi ne: “Bul wax lu bon sa kilifag xeet.”»
5 Respondeu Paulo: Não sabia, irmãos, que é o sumo sacerdote. Pois está escrito: Não falarás mal do príncipe do teu povo {Ex 22,28}.
6 Naka noona Pool, mi xam ne genn-wàllu kureel ga bokk nañu ci tariixab Sadusen ya, te ña ca des bokk ci tariixab Farisen ya, mu wax ci kaw ci biir géew ba ne: «Bokk yi, man Farisen laa, te Farisen moo ma jur; li tax ñu may àtte tey mooy sama yaakaar ci ne, ñi dee dinañu dekki.»
6 Paulo sabia que uma parte do Sinédrio era de saduceus e a outra de fariseus e disse em alta voz.: Irmãos, eu sou fariseu, filho de fariseus. Por causa da minha esperança na ressurreição dos mortos é que sou julgado.
7 Bi mu waxee loolu nag, werante wu metti daldi xew diggante Farisen ya ak Sadusen ya, ba mbooloo ma xàjjalikoo.
7 Ao dizer ele estas palavras, houve uma discussão entre os fariseus e os saduceus, e dividiu-se a assembléia.
8 Ndaxte Sadusen yi nanguwuñu ne ndekkite mbaa malaaka mbaa rab, dara am na ci, waaye Farisen nangu nañu yooyu yépp.
8 {Pois os saduceus afirmam não haver ressurreição, nem anjos, nem espíritos, mas os fariseus admitem uma e outra coisa.}
9 Ci kaw loolu nag coow lu bare daldi jib. Ñenn ca xutbakat, ya bokk ca Farisen ya, ne bërét, daldi xuloo bu metti ne: «Gisunu dara lu bon ci nit kii. Su fekkeente ne rab a ko wax mbaa malaaka…?»
9 Originou-se, então, grande vozearia. Levantaram-se alguns escribas dos fariseus e contestaram ruidosamente: Não achamos mal algum neste homem. {Quem sabe} se não lhe falou algum espírito ou um anjo...
10 Noonu xuloo ba daldi gëna tàng, ba kilifa ga ragal ne, nit ñi dinañu daggaate Pool. Kon mu sant xarekat ya, ñu wàcc, nangu Pool ci ñoom, yóbbu ko ca tata ja.
10 A discussão fazia-se sempre mais violenta. O tribuno temeu que Paulo fosse despedaçado por eles e mandou aos soldados que descessem, o tirassem do meio deles e o levassem para a cidadela.
11 Ca guddi ga nag Boroom bi taxaw ci wetu Pool ne ko: «Takkal sa fit; ni nga ma seedee ci Yerusalem, noonu nga may seedee ca Room.»
11 Na noite seguinte, apareceu-lhe o Senhor e lhe disse: Coragem! Deste testemunho de mim em Jerusalém, assim importa também que o dês em Roma.
12 Bi bët setee Yawut ya daldi lal pexe; ñu dige ci ngiñ ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñuy rey Pool.
12 Quando amanheceu, coligaram-se alguns judeus e juraram com imprecações não comer nem beber nada, enquanto não matassem Paulo.
13 Ña lal pexe ma, seen lim ëpp na ñeent fukk.
13 Eram mais de quarenta as pessoas que fizeram essa conjuração.
14 Noonu ñu dem ca sarxalkat yu mag ya ak njiit ya ne leen: «Giñ nanu ne dunu mos dara, ba kera nuy rey Pool.
14 Foram apresentar-se aos sumos sacerdotes e aos cidadãos, dizendo: Juramos solenemente nada comer enquanto não matarmos Paulo.
15 Léegi nag yéen ak kureelu àttekat ya, laajleen kilifa ga, mu indi ko ci seen kanam, mel ni dangeena bëgga seet mbiram bu gëna wóor. Bu ko defee nun dinanu fagaru, ngir rey ko, bala moo agsi.»
15 Vós, pois, ide com o conselho requerer do tribuno que o conduza à vossa presença, como se houvésseis de investigar com mais precisão a sua causa; e nós estamos prontos para matá-lo durante o trajeto.
16 Waaye jarbaatu Pool yég fiir ga, mu dem, dugg ca tata ja, yégal ko Pool.
16 Mas um filho da irmã de Paulo, inteirado da cilada, dirigiu-se à cidadela e o comunicou a Paulo.
17 Bi ko Pool déggee, mu woo kenn ca njiiti xare ba ne ko: «Yóbbul waxambaane wii ca kilifa ga, ndax am na lu mu ko wara yégal.»
17 Este chamou a si um dos centuriões e disse-lhe: Leva este moço ao tribuno, porque tem alguma coisa a lhe transmitir.
18 Njiit la jël ko, yóbbu ko ca kilifa ga ne ko: «Pool, mi ñu jàpp, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la waxambaane wii, ndaxte am na lu mu lay wax.»
18 Ele o introduziu à presença do tribuno e lhe disse: O preso Paulo rogou-me que trouxesse este moço à tua presença, porque tem alguma coisa a dizer-te.
19 Noonu kilifa ga jàpp ci loxob waxambaane wa, wéetoo ak moom, laaj ko: «Loo ma bëgga yégal?»
19 O tribuno, tomando-o pela mão, retirou-se com ele à parte e perguntou: Que tens a dizer-me?
20 Mu ne: «Yawut yi dañoo dige, ngir ñaan la, nga indi Pool ëllëg ca kanam kureelu àttekat ya, mel ni dañoo bëgga seet mbiram bu gëna wóor.
20 Respondeu-lhe ele: Os judeus têm combinado rogar-te amanhã que apresentes Paulo ao Grande Conselho, como se houvessem de inquirir dele alguma coisa com mais precisão.
21 Bu leen ko may, ndaxte lu ëpp ñeent fukk ci ñoom ñu ngi koy lalal fiir. Dige nañu ak ngiñ ne dootuñu lekk, dootuñu naan, li feek reyuñu ko; fi mu ne sax fagaru nañu, di xaar, nga nangu.»
21 Mas tu não creias, porque mais de quarenta homens dentre eles lhe armam traição. Juraram solenemente nada comer, nem beber, enquanto não o matarem. Eles já estão preparados e só esperam a tua permissão.
22 Kilifa ga nag sant waxambaane wa, mu bañ koo àgge kenn, ba noppi mu yiwi ko, mu dem.
22 Então o tribuno despediu o moço, ordenando-lhe que a ninguém dissesse que o havia avisado.
23 Bi mu ko defee mu woo ñaar ci njiiti xare ba ne leen: «Waajal-leen ñaar téeméeri xarekat ak juróom ñaar fukki gawar ak ñaar téeméeri nit ñu gànnaayoo xeej, ngeen dem Sesare ci juróom ñeenti waxtu ci guddi.
23 Depois disso, chamou ele dois centuriões e disse-lhes: Preparai duzentos soldados, setenta cavaleiros e duzentos lanceiros para irem a Cesaréia à terceira hora da noite.
24 Wutal-leen it Pool lu mu war, ngeen yóbbu ko ci jàmm ak salaam ba ca Feligsë, boroom réew mi.»
24 Aprontai também cavalgaduras para Paulo, que tendes de levar com toda a segurança ao governador Félix.
25 Noonu mu bind bataaxal bii:
25 E ele escreveu uma carta nestes termos:
26 Yaw Feligsë mu tedd mi, di boroom réew mi; man Këlódd Lisiyas maa ngi lay nuyu.
26 Cláudio Lísias ao excelentíssimo governador Félix, saúde!
27 Yawut yi jàpp nañu nit kii, bëgg koo rey, waaye bi ma yégee ne jaambur la ci Room, wallu naa ko ak ay xarekat, ba musal ko.
27 Esse homem foi preso pelos judeus e estava a ponto de ser morto por eles, quando eu, sobrevindo com a tropa, o livrei, ao saber que era romano.
28 Bëggoon naa xam lu tax ñu kalaame ko. Moo tax ma yóbbu ko ca kanam seen kureelu àttekat ya.
28 Então, querendo saber a causa por que o acusavam, levei-o ao Grande Conselho.
29 Gis naa ne li ñu ko jiiñ mu ngi aju ci ay werantey seen yoon, waaye jiiñuñu ko dara lu jar dee mbaa jéng.
29 Soube que era acusado sobre questões da lei deles, sem haver nele delito algum que merecesse morte ou prisão.
30 Te bi ma déggee ne ñu ngi koy fexeel, yebal naa ko ci yaw ci saa si. Sant naa nag ñi ko kalaame, ñu xamal la seen lay.
30 Mas, como tivesse chegado a mim a notícia das traições que maquinavam contra ele, envio-o com urgência a ti, intimando também aos acusadores que recorram a ti. Adeus.
31 Noonu xarekat ya jël Pool ci guddi, indi ko ba ca dëkku Antipataris, ni ñu leen ko sante.
31 Os soldados, conforme lhes fora ordenado, tomaram Paulo e o levaram de noite a Antipátride.
32 Ca ëllëg sa ñu waññiku, délsi ca tata ja, bàyyi gawar ga, ñu gunge ko.
32 No dia seguinte, voltaram para a guarnição, deixando que os soldados da cavalaria o escoltassem.
33 Bi gawar ga àggee Sesare, ñu jox boroom réew ma bataaxal ba, jébbal ko Pool.
33 À sua chegada a Cesaréia, entregaram ao governador a carta e apresentaram-lhe também Paulo.
34 Bi loolu amee boroom réew ma jàng bataaxal ba, laaj ci ban diiwaan la Pool dëkk. Bi mu yégee ne mu ngi dëkk Silisi,
34 Ele, depois de lê-la e perguntar de que província ele era, sabendo que era da Cilícia, disse:
35 Mu ne ko: «Kon bu ñi la kalaame ñëwee, dinga layoo.» Mu santaane nag, ñu denc ko ca kër buur ba Erodd.
35 Ouvir-te-ei quando chegarem teus acusadores. Mandou, então, que Paulo fosse guardado no pretório de Herodes.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Atos 23, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.