Apocalipse 9

Téereb Injiil (WOL2010) vs NVT

Sair da comparação
NVT Nova Versão Transformadora
1 Juróomeelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma gis, ñu jox caabiy kàmb gu xóot gi benn biddiiw bu xawee woon asamaan, daanu ci kaw suuf.
1 O quinto anjo tocou sua trombeta, e vi uma estrela que havia caído do céu sobre a terra, e lhe foi dada a chave para o poço do abismo.
2 Biddiiw ba ubbi buntu kàmb gu xóot ga. Noonu saxar jollee ca, su mel ni saxarus puur bu mag, jant bi ak jaww ji lépp lëndëm ndax saxarus kàmb ga.
2 Quando o poço foi aberto, dele saiu fumaça como de uma imensa fornalha, e a luz do sol e o ar escureceram com a fumaça.
3 Ay njéeréer génn ca saxar sa, tasaaroo ci biir àddina. Ñu jox leen kàttan gu mel ni kàttanu jànkalaar.
3 Então da fumaça saíram gafanhotos que desceram sobre a terra, e lhes foi dado poder para ferroarem como escorpiões.
4 Ñu sant leen, ñu baña laal ñax mi ci kaw suuf, mbaa genn gàncax walla genn meññeef, waaye ñu jublu rekk ci nit ñu amul màndargam Yàlla ci seen jë.
4 Receberam ordens para não danificar a vegetação, nem as plantas, nem as árvores, mas apenas as pessoas que não tivessem o selo de Deus na testa.
5 Santuñu leen ñu rey leen, waaye ñu mitital leen diirub juróomi weer. Te metit woowu ñuy indi, témboo na ak metit wiy dal nit, bu ko jànkalaar fittee.
5 Também lhes foi ordenado que não as matassem, mas que as atormentassem por cinco meses, com dor como a da ferroada do escorpião.
6 Ca jamono yooya nit ñi dinañu sàkku dee, waaye duñu daje ak moom. Dinañu bëgga dee, waaye dee da leen di daw.
6 Naqueles dias, as pessoas procurarão a morte, mas não a encontrarão. Desejarão morrer, mas a morte fugirá delas.
7 Njéeréer ya nag dañuy niroo ak fas yu ñu waajal ngir xare. Am nañu ci seen bopp lu mel ni kaalay wurus, te seen xar kanam mel ni gu nit.
7 Os gafanhotos pareciam cavalos preparados para a batalha. Tinham na cabeça algo semelhante a coroas de ouro, e o rosto parecia humano.
8 Seeni kawar mel ni yu jigéen, seeni bëñ mel ni bëñi gaynde.
8 Os cabelos eram como os de mulher, e os dentes, como os de leão.
9 Takk nañu ci seen dënn lu mel ni kiiraayu weñ, te coow la seeni laaf di def mel ni coowu sareeti xare yu bare yu ñu takk fas, di xeexi.
9 Vestiam uma couraça semelhante ao ferro, e suas asas rugiam como um exército de carruagens correndo para a batalha.
10 Am nañu ay geen yu am ay fitt ni jànkalaar, te ca la seen kàttan nekk, ngir mitital nit ñi diirub juróomi weer.
10 Tinham caudas que ferroavam como escorpiões, e por cinco meses tiveram poder para atormentar as pessoas.
11 Buuru njéeréer yi mooy malaakam kàmb gu xóot gi, moom lañu tudde ci làkku ebrë, Abadon, ak ci làkku gereg, Apolyon, liy tekki «Yàqkat».
11 Seu rei é o anjo do abismo; seu nome em hebraico é Abadom , e em grego, Apoliom .
12 Musiba mu jëkk mi jàll na, yeneen ñaari musiba yaa ngi ñëw.
12 O primeiro terror passou, mas ainda vêm outros dois.
13 Juróom benneelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma dégg baat bu jóge ci ñeenti béjjén, yi nekk ci koñi sarxalukaayu wurus, ba nekk ci kanam Yàlla,
13 O sexto anjo tocou sua trombeta, e ouvi uma voz que vinha das quatro pontas do altar de ouro que está na presença de Deus.
14 mu ne juróom benneelu malaaka, ma yoroon liit: «Yiwil ñeenti malaaka, ya yeewe ca Efraat, dex gu mag ga.»
14 A voz disse ao sexto anjo que tinha a trombeta: “Solte os quatro anjos que estão amarrados junto ao grande rio Eufrates”.
15 Noonu ñu daldi yiwi ñeenti malaaka, ya ñu waajaloon ngir at moomu, weer woowu, bés boobu ak waxtu woowu, ngir ñu rey benn ci ñetti xaaju nit ñi.
15 Então os quatro anjos que haviam sido preparados para aquela hora, dia, mês e ano foram soltos para matar um terço da humanidade.
16 Limub gawar ga doon xareji mat na ñaari alfunniy alfunni. Dégg naa lim ba.
16 Ouvi que seu exército era constituído de duzentos milhões de soldados a cavalo.
17 Nii laa gise ci peeñu mi fas ya ak ña leen war: ñu sol kiiraay yu xonq ni sawara, bulo ni saxar, ak mboq ni tamarax. Boppi fas yaa nga doon nirook boppi gaynde; sawara ak saxar ak tamarax di génn ci seeni gémmiñ.
17 Em minha visão, vi os cavalos e os cavaleiros montados neles. Os cavaleiros usavam couraças vermelhas, azul-escuras e amarelas. Os cavalos tinham cabeças como as de leão, e da boca lhes saíam fogo, fumaça e enxofre.
18 Benn ci ñetti xaaju nit ñi dee ci ñetti musiba ya: ci sawara ak saxar ak tamarax yi génn ci seeni gémmiñ.
18 Um terço da humanidade foi morto por estas três pragas que saíam da boca dos cavalos: fogo, fumaça e enxofre.
19 Ndaxte kàttanu fas yaa ngi ci seeni gémmiñ ak ci seeni geen. Geen yaa nga mel ni ay jaan, am ay bopp, te ñoom lañuy mititale nit ñi.
19 O poder dos cavalos estava na boca e na cauda, pois a cauda tinha cabeças como de serpente, com as quais feriam as pessoas.
20 Nit ñi rëcc ci musiba yooyu taxul sax ñu tuub seeni jëfi loxo. Noppiwuñu di jaamu rab yi ak nataali xërëm yu ñu defare wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk, yoo xam ne manuñoo gis, manuñoo dégg mbaa ñu dox.
20 Aqueles que não morreram dessas pragas ainda se recusaram a arrepender-se de seus atos perversos. Continuaram a adorar demônios e ídolos feitos de ouro, prata, bronze, pedra e madeira, ídolos que não podem ver, nem ouvir, nem andar.
21 Te nit ñooñu tuubuñu seen bóom, seen xërëm, seen njaaloo mbaa seen càcc.
21 E não se arrependeram de seus assassinatos, sua feitiçaria, sua imoralidade sexual e seus roubos.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Apocalipse 9, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.