Apocalipse 6

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Noonu ma gis Gàtt ba dindi tayu gu jëkk ga, te ma daldi dégg kenn ca ñeenti mbindeef ya, di wax ak baat buy riir ni dënnu naan: «Ñëwal!»
1 Depois, vi o Cordeiro abrir o primeiro selo e ouvi um dos quatro Animais clamar com voz de trovão: Vem!
2 Ma xool noonu, gis fas wu weex, gawar ba yor ag fitt. Ñu jox ko kaalag ndam, mu daldi dem moom jàmbaar ngir daani.
2 Vi aparecer então um cavalo branco. O seu cavaleiro tinha um arco; foi-lhe dada uma coroa e ele partiu como vencedor para tornar a vencer.
3 Gàtt ba dindi na ñaareelu tayu ga, ma dégg ñaareelu mbindeef ma naan: «Ñëwal!»
3 Quando abriu o segundo selo, ouvi o segundo animal clamar: Vem!
4 Noonu weneen fas génn, di wu xonq, gawar ba jot sañ-sañu jële jàmm ci kaw suuf, ngir nit ñi di reyante ci seen biir. Ñu jox ko jaasi ju mag.
4 Partiu então outro cavalo, vermelho. Ao que o montava foi dado tirar a paz da terra, de modo que os homens se matassem uns aos outros; e foi-lhe dada uma grande espada.
5 Mu dindi ñetteelu tayu ga, ma dégg ñetteelu mbindeef ma ne: «Ñëwal!» Ma xool, gis fas wu ñuul, gawar ba yor ab peesekaay.
5 Quando abriu o terceiro selo, ouvi o terceiro animal clamar: Vem! E vi aparecer um cavalo preto. Seu cavaleiro tinha uma balança na mão.
6 Ma dégg baat bu jollee ca diggante ñeenti mbindeef ya, naan: «Peyug bëccëgu lëmm ngir benn kilob ceeb, peyug bëccëgu lëmm ngir ñetti kiloy dugub, waaye bul yàq diw ak biiñ.»
6 Ouvi então como que uma voz clamar no meio dos quatro Animais: Uma medida de trigo por um denário, e três medidas de cevada por um denário; mas não danifiques o azeite e o vinho!
7 Mu dindi ñeenteelu tayu ga, ma dégg ñeenteelu mbindeef ma naan: «Ñëwal!»
7 Quando abriu o quarto selo, ouvi a voz do quarto animal, que clamava: Vem!
8 Ma xool noonu, gis fas wu wert, gawar baa nga tuddoon Dee te barsàq a nga toppoon ci moom. Ñu jox ko sañ-sañ ci ñeenteelu xaaju àddina sépp, ngir mu faat ak jaasi, xiif, mbas ak rabi àll yi.
8 E vi aparecer um cavalo esverdeado. Seu cavaleiro tinha por nome Morte; e a região dos mortos o seguia. Foi-lhe dado poder sobre a quarta parte da terra, para matar pela espada, pela fome, pela peste e pelas feras.
9 Mu dindi juróomeelu tayu ga, ma gis ca suufu sarxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, ruuwi ñi ñu bóom ndax seede si ñu doon sàmm ak li ñu gëmoon kàddug Yàlla.
9 Quando abriu o quinto selo, vi debaixo do altar as almas dos homens imolados por causa da palavra de Deus e por causa do testemunho de que eram depositários.
10 Ñuy xaacu naan: «Boroom bu sell bi te dëggu, ba kañ ngay nég àtte bi te feyul nu sunu deret ci waa àddina?»
10 E clamavam em alta voz, dizendo: Até quando tu, que és o Senhor, o Santo, o Verdadeiro, ficarás sem fazer justiça e sem vingar o nosso sangue contra os habitantes da terra?
11 Ñu jox leen ku nekk mbubb mu weex, daldi leen ne, ñu muñ tuuti, ba kera seeni nawle ñëw, te lim bi mat— seeni nawle ci liggéey bi, di seeni bokk yu waa àddina waroona bóom ni ñoom.
11 Foi então dada a cada um deles uma veste branca, e foi-lhes dito que aguardassem ainda um pouco, até que se completasse o número dos companheiros de serviço e irmãos que estavam com eles para ser mortos.
12 Ma xool, ba muy dindi juróom benneelu tayu ga. Noonu mu am yëngu-yëngub suuf bu mag, jant bi ñuul ni këriñ, weer wi xonq curr ni deret.
12 Depois vi o Cordeiro abrir o sexto selo; e sobreveio então um grande terremoto. O sol se escureceu como um tecido de crina, a lua tornou-se toda vermelha como sangue
13 Biddiiw yi fàqe asamaan, di daanu ci kaw suuf, ni doomi garab yu yolox di wadd, bu ko ngelaw lu metti dee yëngal.
13 e as estrelas do céu caíram na terra, como frutos verdes que caem da figueira agitada por forte ventania.
14 Asamaan si dellu ni basaŋ gu ñuy taxañ, tund yépp ak dun yépp randoo fa ñu nekkoon.
14 O céu desapareceu como um pedaço de papiro que se enrola e todos os montes e ilhas foram tirados dos seus lugares.
15 Noonu buuri àddina si ak kilifa yi ak njiiti xare yi ak boroom alal yi ak boroom kàttan yi ak jaam yi ak gor yi, ñépp làqatuji ci xunti yi ak ci ron doji tund yi.
15 Então os reis da terra, os grandes, os chefes, os ricos, os poderosos, todos, tanto escravos como livres, esconderam-se nas cavernas e grutas das montanhas.
16 Ñu naan tund yi ak doj yi: «Daanuleen ci sunu kaw te nëbb nu bëti ki toog ci gàngune mi ak meru Gàtt bi,
16 E diziam às montanhas e aos rochedos: Caí sobre nós e escondei-nos da face daquele que está sentado no trono e da ira do Cordeiro,
17 ndaxte bés bu mag, bi seen mer di feeñ, agsi na! Ku ci mana rëcc?»
17 porque chegou o Grande Dia da sua ira, e quem poderá subsistir?

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Apocalipse 6, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.