Apocalipse 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARA

Sair da comparação
ARA Almeida Revista e Atualizada 1993
1 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Sàrd, ne ko:
1 Ao anjo da igreja em Sardes escreve:
2 Yewwul te dëgëral li des ci yaw tey waaja dee, ndaxte gis naa ne say jëf matuñu ca sama kanam Yàlla.
2 Sê vigilante e consolida o resto que estava para morrer, porque não tenho achado íntegras as tuas obras na presença do meu Deus.
3 Fàttalikul kon kàddug Yàlla gi nga jot, te dégg ko, sàmm ko te réccu. Soo wéyee ciy nelaw nag, dinaa ñëw nib sàcc, te doo xam wan waxtu lay doon.
3 Lembra-te, pois, do que tens recebido e ouvido, guarda-o e arrepende-te. Porquanto, se não vigiares, virei como ladrão, e não conhecerás de modo algum em que hora virei contra ti.
4 Moona am nga foofu ci Sàrd nit ñu néew ñoo xam ne tilimaluñu seen mbubb. Ñooñu dinañu ànd ak man, sol lu weex, ndaxte yeyoo nañu ko.
4 Tens, contudo, em Sardes, umas poucas pessoas que não contaminaram as suas vestiduras e andarão de branco junto comigo, pois são dignas.
5 Ku daan, dinga sol mbubb mu weex ni ñoom. Duma far sa tur ci téereb dund bi, waaye dinaa nangu ci sama kanam Baay ak ay malaakaam ne bokk nga ci man.
5 O vencedor será assim vestido de vestiduras brancas, e de modo nenhum apagarei o seu nome do Livro da Vida; pelo contrário, confessarei o seu nome diante de meu Pai e diante dos seus anjos.
6 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.
6 Quem tem ouvidos, ouça o que o Espírito diz às igrejas.
7 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Filadelfi, ne ko:
7 Ao anjo da igreja em Filadélfia escreve:
8 Xam naa say jëf. Ubbil naa la bunt, te kenn du ko mana tëj. Xam naa ne barewuloo doole, waaye sàmm nga sama kàddu te weddiwoo ma.
8 Conheço as tuas obras — eis que tenho posto diante de ti uma porta aberta, a qual ninguém pode fechar — que tens pouca força, entretanto, guardaste a minha palavra e não negaste o meu nome.
9 Dinaa def ba ñenn ci ñi bokk ci ndajem Seytaane —te tuddoo Yawut, fekk dañuy fen— dinaa leen ñëwloo, ñu sukk ci sa kanam, nangu ne bëgg naa la.
9 Eis farei que alguns dos que são da sinagoga de Satanás, desses que a si mesmos se declaram judeus e não são, mas mentem, eis que os farei vir e prostrar-se aos teus pés e conhecer que eu te amei.
10 Gannaaw muñ nga, ni ma la ko dénke woon, man itam dinaa la yiir ci jamono, ji musiba mi di wàcc ci dunyaa bépp ngir nattu waa àddina.
10 Porque guardaste a palavra da minha perseverança, também eu te guardarei da hora da provação que há de vir sobre o mundo inteiro, para experimentar os que habitam sobre a terra.
11 Léegi ma ñëw. Sàmmal li nga yor, ngir kenn bañ laa xañ sa kaalag ndam.
11 Venho sem demora. Conserva o que tens, para que ninguém tome a tua coroa.
12 Ku daan, dinaa la samp ni aw jënu néeg ci sama kër Yàlla te doo fa génn mukk. Dinaa bind ci yaw turu sama Yàlla ak turu dëkku sama Yàlla, mu di Yerusalem gu bees, giy jóge ca asamaan ca wetu sama Yàlla, di wàcc. Dinaa bind it ci yaw sama tur wu bees.
12 Ao vencedor, fá-lo-ei coluna no santuário do meu Deus, e daí jamais sairá; gravarei também sobre ele o nome do meu Deus, o nome da cidade do meu Deus, a nova Jerusalém que desce do céu, vinda da parte do meu Deus, e o meu novo nome.
13 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.
13 Quem tem ouvidos, ouça o que o Espírito diz às igrejas.
14 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Lawdise, ne ko:
14 Ao anjo da igreja em Laodiceia escreve:
15 Xam naa say jëf, xam ne seddoo, tàngoo. Manoon ngaa sedd mbaa nga tàng,
15 Conheço as tuas obras, que nem és frio nem quente. Quem dera fosses frio ou quente!
16 waaye ndax li nga nugg, tàngoo seddoo, dinaa la yàbbi.
16 Assim, porque és morno e nem és quente nem frio, estou a ponto de vomitar-te da minha boca;
17 Yaa ngi damu naan: “Am naa alal, duunle naa, soxlaatuma dara.” Fekk xamuloo ne torox nga, miskin, ñàkk, gumba te rafle.
17 pois dizes: Estou rico e abastado e não preciso de coisa alguma, e nem sabes que tu és infeliz, sim, miserável, pobre, cego e nu.
18 Moo tax maa ngi lay xiirtal, nga jënd ci man wurus wu ñu xellee ci sawara, ngir nga duunle, te nga jënd yére yu weex ngir nga solu, ba sa gàcceg rafle baña feeñ, ak tuufaay booy diw ci say bët, ngir mana gis.
18 Aconselho-te que de mim compres ouro refinado pelo fogo para te enriqueceres, vestiduras brancas para te vestires, a fim de que não seja manifesta a vergonha da tua nudez, e colírio para ungires os olhos, a fim de que vejas.
19 Man maay yedd, di yar ñépp ñi ma bëgg. Farlul kon te tuub say bàkkaar.
19 Eu repreendo e disciplino a quantos amo. Sê, pois, zeloso e arrepende-te.
20 Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat te ubbi bunt bi, dinaa dugg, reerandoo ak moom, moom it mu reerandoo ak man.
20 Eis que estou à porta e bato; se alguém ouvir a minha voz e abrir a porta, entrarei em sua casa e cearei com ele, e ele, comigo.
21 Ku daan, dinaa la toogloo ci sama wet ci sama gàngune, ni ma xeexe ba daan, man ci sama bopp, te toogandoo ak sama Baay ci gànguneem.
21 Ao vencedor, dar-lhe-ei sentar-se comigo no meu trono, assim como também eu venci e me sentei com meu Pai no seu trono.
22 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.»
22 Quem tem ouvidos, ouça o que o Espírito diz às igrejas.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Apocalipse 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.