Apocalipse 1
Téereb Injiil (WOL2010) vs VC
1 Lii mooy li Yeesu Kirist feeñal, te mu tukkee ca Yàlla, ngir mu won ay jaamam mbir, yi dëgmël di ñëw. Yónni na malaakaam, ngir xamal ko ab jaamam Yowaana.
1 Revelação de Jesus Cristo, que lhe foi confiada por Deus para manifestar aos seus servos o que deve acontecer em breve. Ele, por sua vez, por intermédio de seu anjo, comunicou ao seu servo João,
2 Kooku mi ngi seede fii li mu gis lépp, maanaam kàddug Yàlla ak seede, si ñu seedeel Yeesu Kirist.
2 o qual atesta, como palavra de Deus, o testemunho de Jesus Cristo e tudo o que viu.
3 Barkeel ngeen, yaw miy jàng ak yéen ñiy déglu wax yii jóge ca Yàlla, te di sàmm li ñu ci bind, ndaxte waxtu wi jege na.
3 Feliz o leitor e os ouvintes se observarem as coisas nela escritas, porque o tempo está próximo.
4 Man Yowaana maa leen di bind, yéen juróom ñaari mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Asi. Na yiw ak jàmm féete ci yéen, jóge ci Yàlla, moom ki nekk, ki nekkoon démb te di ñëw ëllëg. Yiw woowu ak jàmm jooju ñoo ngi tukkee it ci juróom ñaari Xeli Yàlla, yi nekk ci kanam gàngunem Yàlla,
4 João às sete igrejas que estão na Ásia: a vós, graça e paz da parte daquele que é, que era e que vem da parte dos sete Espíritos que estão diante do seu trono
5 — ausente —
5 e da parte de Jesus Cristo, testemunha fiel, primogênito dentre os mortos e soberano dos reis da terra. Àquele que nos ama, que nos lavou de nossos pecados no seu sangue
6 — ausente —
6 e que fez de nós um reino de sacerdotes para Deus e seu Pai, glória e poder pelos séculos dos séculos! Amém.
7 Gisleen, mi ngi ñëw ci niir yi,
7 Ei-lo que vem com as nuvens. Todos os olhos o verão, mesmo aqueles que o traspassaram. Por sua causa, hão de lamentar-se todas as raças da terra. Sim. Amém.
8 Boroom bi Yàlla nee na: «Man Yàlla maay Alfa di Omega, Maay ki Nekk, di ki nekkoon démb, di kiy ñëw ëllëg, man Aji Man ji.»
8 Eu sou o Alfa e o Ômega, diz o Senhor Deus, aquele que é, que era e que vem, o Dominador.
9 Man Yowaana seen mbokk, di seen nawle ci fitna, ci nguur ak ci muñ, yi nu am ndax sunu booloo ak Yeesu, maa nga nekkoon ca dun bu ñuy wax Patmos. Wacce woon nañu ma fa, ndax li ma doon waare kàddug Yàlla tey seedeel Yeesu.
9 Eu, João, vosso irmão e companheiro nas tribulações, na realeza e na paciência em união com Jesus, estava na ilha de Patmos por causa da palavra de Deus e do testemunho de Jesus.
10 Xelum Yàlla solu ma ci bésu Boroom bi, te noonu ma dégg ci sama gannaaw baat bu xumb nig liit,
10 Num domingo, fui arrebatado em êxtase, e ouvi, por trás de mim, voz forte como de trombeta,
11 naan: «Bindal ci téere li ngay gis te yónnee ko juróom ñaari mboolooy ñi gëm, ca dëkki Efes, Samirin, Pergam, Catir, Sàrd, Filadelfi ak Lawdise.»
11 que dizia: O que vês, escreve-o num livro e manda-o às sete igrejas: a Éfeso, a Esmirna, a Pérgamo, a Tiatira, a Sardes, a Filadélfia e a Laodicéia.
12 Noonu ma geestu, ngir seet ku doon wax ak man. Ba ma geestoo, yem ci juróom ñaari tegukaayu làmp yu wurus,
12 Voltei-me para saber que voz falava comigo. Tendo-me voltado, vi sete candelabros de ouro
13 gis ku taxaw ci biir tegukaayu ya, niroo ak doomu nit. Mu sol mbubb mu gudd, takk ngañaayu wurus ci ndiggam.
13 e, no meio dos candelabros, alguém semelhante ao Filho do Homem, vestindo longa túnica até os pés, cingido o peito por um cinto de ouro.
14 Boppam ak kawaram weex tàll ni perkaal, ay bëtam di xuyy ni sawara.
14 Tinha ele cabeça e cabelos brancos como lã cor de neve. Seus olhos eram como chamas de fogo.
15 Ay tànkam mel ni xànjar bu yànj bu ñu xelli, baatam di riir ni duusi géej.
15 Seus pés se pareciam ao bronze fino incandescido na fornalha. Sua voz era como o ruído de muitas águas.
16 Mu yor ci loxol ndijooram juróom ñaari biddiiw, jaasiy ñaari boor yu ñaw di génn ci gémmiñam, xar kanamam leer nàññ ni jantub njolloor.
16 Segurava na mão direita sete estrelas. De sua boca saía uma espada afiada, de dois gumes. O seu rosto se assemelhava ao sol, quando brilha com toda a força.
17 Naka laa ko gis, di daanu ci ay tànkam ni ku dee. Waaye mu teg loxol ndijooram ci sama kaw ne ma: «Bul ragal dara. Maay ki jëkk te maay mujj.
17 Ao vê-lo, caí como morto aos seus pés. Ele, porém, pôs sobre mim sua mão direita e disse: Não temas! Eu sou o Primeiro e o Último, e o que vive.
18 Maay Kiy Dund. Dee woon naa, waaye maa ngii di dund ba fàww, yor caabiy dee ak ju barsàq.
18 Pois estive morto, e eis-me de novo vivo pelos séculos dos séculos; tenho as chaves da morte e da região dos mortos.
19 Kon nag bindal li nga gis, li am léegi ak li nara ami gannaaw gi.
19 Escreve, pois, o que viste, tanto as coisas atuais como as futuras.
20 Juróom ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndijoor, ak juróom ñaari tegukaayu làmp yu wurus yi, ay mbóoti Yàlla lañu te lii lañuy tekki: biddiiw yi ñoo di malaakay juróom ñaari mboolooy ñi gëm; juróom ñaari tegukaayu làmp yi ñoo di juróom ñaari mbooloo yi.
20 Eis o simbolismo das sete estrelas que viste na minha mão direita e dos sete candelabros de ouro: as sete estrelas são os anjos das sete igrejas, e os sete candelabros, as sete igrejas.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Apocalipse 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.