Apocalipse 18

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Gannaaw loolu ma gis meneen malaaka mu wàcce ca asamaan, yor sañ-sañ bu réy, te leeraayam daj na àddina sépp.
1 Depois disso, vi descer do céu outro anjo que tinha grande poder, e a terra foi iluminada por sua glória.
2 Mu daldi xaacu naan: «Daanu na! Babilon mu mag ma daanu na! Léegi dëkkukaayu jinne la, ak bépp rab wu bon ak bépp picc mu daganul te araam.
2 Clamou em alta voz, dizendo: Caiu, caiu Babilônia, a Grande. Tornou-se morada dos demônios, prisão dos espíritos imundos e das aves impuras e abomináveis,
3 Ndaxte jox na xeeti àddina yépp, ñu naan ci koppu nafsoom ak njaaloom, ba ñu màndi. Buuri àddina ànd nañu ak moom ci njaaloo, te baana-baanay àddina woomle nañu ndax li mu bëgg mbuux.»
3 porque todas as nações beberam do vinho da ira de sua luxúria, pecaram com ela os reis da terra e os mercadores da terra se enriqueceram com o excesso do seu luxo.
4 Noonu ma dégg beneen baat bu jóge asamaan naan: «Génnleen ci biiram, yéen samay gaay, ngir ngeen baña bokk ci ay bàkkaaram te baña am cér ci musiba yi koy dal.
4 Ouvi outra voz do céu que dizia: Meu povo, sai de seu meio para que não participes de seus pecados e não tenhas parte nas suas pragas,
5 Ndaxte ay bàkkaaram dajaloo nañu ba ci asamaan, te Yàlla fàttaliku na ay jëfam yu bon.
5 porque seus pecados se acumularam até o céu, e Deus se lembrou das suas injustiças.
6 Dellooleen ko li mu defoon, feyleen ko ñaar ci li mu lebaloon, feesal-leen koppam ak naan gu gëna wex ñaari yoon naan ga mu joxe woon.
6 Faze com ela o que fez {contigo}, e retribui-lhe o dobro de seus malefícios; na taça que ela deu de beber, dá-lhe o dobro.
7 Joxleen ko ci coono ak naqar, lu tollu ni tiitar ak mbuux, ba mu dencaloon boppam. Gannaaw nee woon na ci xelam: “Maa ngi toog fii ni buur, duma ab jëtun te duma ténj mukk,”
7 Na mesma proporção em que fez ostentação de luxo, dá-lhe em tormentos e prantos. Pois ela disse no seu coração: Estou no trono como rainha, e não viúva, e nunca conhecerei o luto.
8 looloo tax ba musiba, yii ñu ko sédd, dinañu ñëw ci benn bés, ñu di mbas, ténj ak xiif, ñu di ko lakk ba mu jeex, ndaxte Yàlla Boroom bi ko àtte, ku am kàttan la.»
8 Por isso, num só dia virão sobre ela as pragas: morte, pranto, fome. Ela será consumida pelo fogo, porque forte é o Senhor Deus que a condenou.
9 Buuri àddina yépp, yi àndoon ak moom ci njaaloo ak mbuux, bu ñu séenee saxar siy jollee ci taal bi ñu koy lakke, dinañu yuuxu, di ko jooy.
9 Hão de chorar e lamentar-se por sua causa os reis da terra que com ela se contaminaram e pecaram, quando avistarem a fumaça do seu incêndio.
10 Dinañu tiit ndax coonoom, ba dàndu lu sore, naan:
10 Parados ao longe, de medo de seus tormentos, eles dirão: Ai, ai da grande cidade, Babilônia, cidade poderosa! Bastou um momento para tua execução!
11 Baana-baana yi ci kaw suuf di jooy, di ko naqarlu, ndaxte kenn dootul jënd seen njaay:
11 Também os negociantes da terra choram e se lamentam a seu respeito, porque já não há ninguém que lhes compre os carregamentos:
12 seen wurus ak seen xaalis ak seeni jamaa ak yeneen per; seeni piis yu rafet ak piis yu yolet, yu ray-ray, yu xonq; seen dénk wu xeeñ ak seen yëf yi ñu defare bëñi ñay walla dénk wu jafe walla xànjar walla weñ walla marbë;
12 carregamento de ouro e prata, pedras preciosas e pérolas, linho e púrpura, seda e escarlate, bem como de toda espécie de madeira odorífera, objetos de marfim e madeira preciosa; de bronze, ferro e mármore;
13 ak bant yuy safal ak gàncax gu xeeñ ak xeeti cuuraay yu bare ak latkoloñ ak biiñ ak diw ak sungufu lay-layaat ak pepp ak i nag ak i xar ak i fas ak i sareeti xare ak i jaam, ba ci bakkani nit.
13 de cinamomo e essência; de aromas, mirra e incenso; de vinho e óleo, de farinha e trigo, de animais de carga, ovelhas, cavalos e carros, escravos e outros homens.
14 Dinañu wax naan: «Yëf yi nga bëggoona am raw nañu la, te lépp luy yafal walla col gu rafet ñàkk nga ko, te kenn du ko gisaat!»
14 Eis que o bom tempo de tuas paixões animalescas se escoou. Toda a magnificência e todo o brilho se apagaram, e jamais serão reencontrados.
15 Baana-baana, yi daan jaay yëf yooyu ba woomle, dinañu sore ndax ragal coonoom. Dinañu jooy di naqarlu,
15 Os mercadores destas coisas, que delas se enriqueceram, pararão ao longe, de medo de seus tormentos, e hão de chorar e lamentar-se, dizendo:
16 naan:
16 Ai, ai da grande cidade, que se revestia de linho, púrpura e escarlate, toda ornada de ouro, pedras preciosas e pérolas.
17 sa alal ju bare jépp naaw na ci waxtu!»
17 Num só momento toda essa riqueza foi devastada! Todos os pilotos e todos os navegantes, os marinheiros e todos os que trabalham no mar paravam ao longe
18 te bu ñu séenee saxar sa cay jollee, naan: «Ndax dëkk bu niroo woon ak dëkk bu mag bii mas na am?»
18 e exclamavam, ao ver a fumaça do incêndio: Que havia de comparável a essa grande cidade?
19 Ñuy xëpp suuf ci seen bopp, di jooy, di naqarlu te naan:
19 E lançavam pó sobre as cabeças, chorando e lamentando-se com estas palavras: Ai, ai da grande cidade, de cuja opulência se enriqueceram todos os que tinham navios no mar. Bastou um momento para ser arrasada!
20 Yaw asamaan, bégal ci li ñu ko yàq!
20 Exulta sobre ela, ó céu; e também vós, santos, apóstolos e profetas, porque Deus julgou contra ela a vossa causa.
21 Noonu malaaka mu am doole jël doj wu réy, sànni ko ci géej gi, naan:
21 Então um anjo poderoso tomou uma pedra do tamanho de uma grande mó de moinho e lançou-a no mar, dizendo: Com tal ímpeto será precipitada Babilônia, a grande cidade, e jamais será encontrada.
22 Buumi xalam yi ak baati woykat yi ak toxoro yi ak liit yi, // kenn dootu ko dégg ci yaw.
22 Já não se ouvirá mais em ti o som dos citaristas, dos cantores, dos tocadores de flauta, de trombetas. Nem se encontrará em ti artífice algum de qualquer espécie. Não se ouvirá mais em ti o ruído do moinho,
23 Niitug làmp du tàkkati,
23 não brilhará mais em ti a luz de lâmpada, não se ouvirá mais em ti a voz do esposo e da esposa; porque teus mercadores eram senhores do mundo, e todas as nações foram seduzidas por teus malefícios.
24 Deretu yonent yi ak gaayi Yàlla yi ak ñépp ñi ñu rey ci kaw suuf, ci moom Babilon lañu ko fa fekk.
24 Foi em ti que se encontrou o sangue dos profetas e dos santos, como também de todos aqueles que foram imolados na terra.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Apocalipse 18, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.