Apocalipse 13
Téereb Injiil (WOL2010) vs VC
1 Noonu ma gis génn ca géej ga, rab wu am fukki béjjén ak juróom ñaari bopp. Ci kaw béjjénam ya amoon na fukki mbaxanay buur; ca bopp ya turi xarab Yàlla.
1 Vi, então, levantar-se do mar uma Fera que tinha dez chifres e sete cabeças; sobre os chifres, dez diademas; e nas suas cabeças, nomes blasfematórios.
2 Rab wa ma gis ma nga mel ni segg, tànk ya mel ni yu rab wu ñuy wax urs, gémmiñ ga mel ni gu gaynde. Ninkinànka ja jox ko kàttanam ak nguuram ak sañ-sañam bu réy.
2 A Fera que eu vi era semelhante a uma pantera: os pés como de urso, e as fauces como de leão. Deu-lhe o Dragão o seu poder, o seu trono e grande autoridade.
3 Benn ca bopp ya mel ni dafa gaañu ba dee. Waaye gaañu-gaañu ba daldi wér. Waa àddina sépp yéemu, daldi topp rab wa.
3 Uma das suas cabeças estava como que ferida de morte, mas essa ferida de morte fora curada. E todos, pasmados de admiração, seguiram a Fera
4 Ñu jaamu ninkinànka ja ndax li mu joxoon sañ-sañ rab wa, di jaamu it rab wa, naan: «Rab wi amul moroom, kenn manula xeex ak moom.»
4 e prostraram-se diante do Dragão, porque dera seu prestígio à Fera, e prostraram-se igualmente diante da Fera, dizendo: Quem é semelhante à Fera e quem poderá lutar com ela?
5 Noonu mayees ko mu am gémmiñ, muy jay boppam te di xarab turu Yàlla. Mayees ko it sañ-sañu jëf ci kaw suuf diirub ñeent fukki weer ak ñaar.
5 Foi-lhe dada a faculdade de proferir arrogâncias e blasfêmias, e foi-lhe dado o poder de agir por quarenta e dois meses.
6 Noonu mu tàmbalee xarab Yàlla, di xarab aw turam, dalam, ak ñi dëkk ci asamaan.
6 Abriu, pois, a boca em blasfêmias contra Deus, para blasfemar o seu nome, o seu tabernáculo e os habitantes do céu.
7 Mayees ko, mu xare ak gaayi Yàlla yi te not leen. Mayees ko it sañ-sañ ci kaw bépp giir ak réew ak kàllaama ak xeet.
7 Foi-lhe dado, também, fazer guerra aos santos e vencê-los. Recebeu autoridade sobre toda tribo, povo, língua e nação,
8 Waa àddina sépp dinañu ko jaamu, ñooñu ñu bindul seeni tur, li dale ci njàlbéenu àddina, ci téereb dund bu Gàtt bi ñu rendi.
8 e hão de adorá-la todos os habitantes da terra, cujos nomes não estão escritos desde a origem do mundo no livro da vida do Cordeiro imolado.
9 Yaw mi am ay nopp, déglul.
9 Quem tiver ouvidos, ouça!
10 Ku Yàlla dogal, ñu war laa jàpp njaam,
10 Quem procura prender será preso. Quem matar pela espada, pela espada deve ser morto. Esta é a ocasião para a constância e a confiança dos santos!
11 Noonu ma gis weneen rab di génn ci suuf. Am na ñaari béjjén yu mel ni yu gàtt, waaye di wax ni ninkinànka.
11 Vi, então, outra Fera subir da terra. Tinha dois chifres como um cordeiro, mas falava como um dragão.
12 Muy jëf ak sañ-sañu rab wu jëkk wa ci turam, di sant waa àddina sépp, ñu jaamu rab wu jëkk, woowu am gaañu-gaañu ba ko rey, waaye daldi wér.
12 Ela exercia todo o poder da primeira Fera, sob a vigilância desta, e fez com que a terra e os seus habitantes adorassem a primeira Fera {cuja ferida de morte havia sido curada}.
13 Muy def kéemaan yu réy, ba dem sax bay wàcce ci kaw suuf sawara su jóge asamaan, nit ñi di gis.
13 Realizou grandes prodígios, de modo que até fez descer fogo do céu sobre a terra, à vista dos homens.
14 Noonu mu nax waa àddina ci kéemaan, yi mu am sañ-sañu def ci turu rab wu jëkk wa. Mu sant waa àddina, ñu def nataalu rab, wi am gaañu-gaañub jaasi tey dund.
14 Seduziu os habitantes da terra com os prodígios que lhe era dado fazer sob a vigilância da Fera, persuadindo-os a fazer uma imagem da Fera que sobrevivera ao golpe da espada.
15 Mayees ko it, mu dundloo nataalu rab wa, waxloo ko, ba képp ku jaamuwul nataalu rab wa rekk ñu rey la.
15 Foi-lhe dado, também, comunicar espírito à imagem da Fera, de modo que essa imagem se pusesse a falar e fizesse com que fosse morto todo aquele que não se prostrasse diante dela.
16 Mu def it ba ñépp, mag ak ndaw, buur ak baadoolo, gor ak jaam, ñépp am màndarga ci seen loxol ndijoor walla ci seen jë,
16 Conseguiu que todos, pequenos e grandes, ricos e pobres, livres e escravos, tivessem um sinal na mão direita e na fronte,
17 ba kenn du mana jënd mbaa mu jaay te amul màndargam rab wi, maanaam turam walla siifar bu méngoo ak turam.
17 e que ninguém pudesse comprar ou vender, se não fosse marcado com o nome da Fera, ou o número do seu nome.
18 Lii nag mooy laaj xel: ku am xel dina mana waññ siifaru rab wi, ndaxte siifar boobu méngoo na ak bu nit, di juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom benn.
18 Eis aqui a sabedoria! Quem tiver inteligência, calcule o número da Fera, porque é número de um homem, e esse número é seiscentos e sessenta e seis.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Apocalipse 13, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.