Apocalipse 10

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Noonu ma gis meneen malaaka mu am doole, muy wàcce asamaan, làmboo niir. Xon tiim ko, xar kanamam mel ni jant, ay tànkam mel ni jumi sawara.
1 Vi então outro anjo vigoroso descer do céu, revestido de uma nuvem e com o arco-íris em torno da cabeça. Seu rosto era como sol, e as suas pernas como colunas de fogo.
2 Yor na benn téere bu ndaw bu ñu ubbi. Mu teg tànku ndijooram ci géej gi, tànku càmmoñam ci suuf si,
2 Segurava na mão um pequeno livro aberto. Pôs o pé direito sobre o mar, o esquerdo sobre a terra
3 di xaacu, mel ni gaynde guy yëmmu. Naka la xaacu, juróom ñaari dënnu yi jib.
3 e começou a clamar em alta voz, como um leão que ruge. Quando clamou, os sete trovões ressoaram.
4 Naka la juróom ñaari dënnu yi di jib, may waaja bind, waaye ma dégg baat bu jóge asamaan, naan ma: «Li juróom ñaari dënnu yi wax, na nekk kumpa, bu ko bind.»
4 Quando cessaram de falar, dispunha-me a escrever, mas ouvi uma voz do céu que dizia: Sela o que falaram os sete trovões e não o escrevas.
5 Noonu malaaka, ma ma gis, mu taxaw ci géej gi ak suuf si, yékkati loxol ndijooram, mu jëm asamaan,
5 Então o anjo, que eu vira de pé sobre o mar e a terra, levantou a mão direita para o céu
6 daldi waat ci kiy dund ba fàww, ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak li ci nekk lépp; mu ne: «Négandiku wees na,
6 e jurou por aquele que vive pelos séculos dos séculos, que criou o céu e tudo o que há nele, a terra e tudo o que ela contém, o mar e tudo o que encerra, que não haveria mais tempo;
7 waaye jamono ju juróom ñaareelu malaaka ma wolee ci liitam, ndogalu Yàlla dina mat, ni mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.»
7 mas nos dias em que soasse a trombeta do sétimo anjo, se cumpriria o mistério de Deus, de acordo com a boa nova que confiou a seus servos, os profetas.
8 Ci kaw loolu baat, ba ma déggoon ca asamaan waxaat ak man, ne ma: «Demal jël téere bi ñu ubbi ci loxob malaaka, mi taxaw ci géej gi ak suuf si.»
8 Então a voz que ouvi do céu falou-me de novo, e disse: Vai e toma o pequeno livro aberto da mão do anjo que está em pé sobre o mar e a terra.
9 Ma dem ca malaaka ma, laaj ko téere bu ndaw boobu. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir, waaye dina neex ni lem ci sa gémmiñ.»
9 Fui eu, pois, ter com o anjo, dizendo-lhe que me desse o pequeno livro. E ele me disse: Toma e devora-o! Ele te será amargo nas entranhas, mas, na boca, doce como o mel.
10 Noonu ma jël téere bi ci loxob malaaka mi, daldi ko lekk, mu neex ci sama gémmiñ ni lem, waaye bi ma ko wannee, mu wex xat ci sama biir.
10 Tomei então o pequeno livro da mão do anjo e o comi. De fato, em minha boca tinha a doçura do mel, mas depois de o ter comido, amargou-me nas entranhas.
11 Gannaaw loolu ñu ne ma: «Fàww nga wax ci kàddug Yàlla lu jëm ci réew yu bare ak xeet yu bare ak kàllaama yu bare ak buur yu bare.»
11 Então foi-me explicado: Urge que ainda profetizes de novo a numerosas nações, povos, línguas e reis.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Apocalipse 10, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.