3 João 1

Téereb Injiil (WOL2010) vs BKJ

Sair da comparação
1 Man njiit li, maa ngi lay bind, yaw sama xarit Gayus, mi ma bëgg ci sama xol.
1 O ancião ao amado Gaio, a quem amo em verdade.
2 Sama soppe, maa ngi ñaan, Yàlla may la jàmm ci lépp, ànd ak wér-gi-yaram, ju mel ni sa naataangeg xol.
2 Amado, eu desejo, acima de todas as coisas, que tu possas prosperar e em boa saúde, assim como sua alma prospera.
3 Sunuy bokk ñëw nañu te seede ni nga fonke dëgg gi, ba wéer ci sa dund gépp, te bég naa ci lool.
3 Porque me alegrei grandemente quando os irmãos vieram, e testificaram da verdade que há em ti, e como tu andas na verdade.
4 Awma mbég mu ëpp lii: ma dégg ne samay doomi diine ñu ngiy jaar ci tànki dëgg.
4 Não tenho maior alegria do que a de ouvir que os meus filhos andam na verdade.
5 Yaw sama xarit, sa takkute fés na ci teeru bi ngay teeru bokk yi, te fekk xamoo leen.
5 Amado, procedes fielmente em tudo o que fazes para com os irmãos, e para com os estranhos;
6 Seedeel nañu sa mbëggeel fi kanam mbooloom ñi gëm. Taxawu leen nag ci seen yoon taxawu gu neex Yàlla.
6 estes foram testemunhas da tua caridade diante da igreja, os quais, se conduzires em sua jornada de maneira piedosa, farás bem.
7 Ndaxte turu Kirist la leen taxa jóg, te sàkkuwuñu daray ku gëmul.
7 Porque pelo seu Nome seguiram adiante, nada tomando dos gentios.
8 Nun nag fàww nu teeru ñu mel ni ñoom, ngir nu ànd ak ñoom liggéeyal dëgg.
8 Portanto, devemos receber aos tais, para que sejamos cooperadores da verdade.
9 Bind naa mbooloo mi bataaxal, waaye Joteref, mi bëgg not ñépp, du dégg sunu ndigal.
9 Escrevi à igreja; mas Diótrefes, que ama ter preeminência entre eles, não nos recebe.
10 Kon nag su ma ñëwee, dinaa fàttali li mu def lépp, ci di nu sosal ci kàdduy neen yu ñaaw. Yemu foofu sax, waaye nanguwula teeru bokk yi, rax-ca-dolli ku leen bëgga teeru, mu gàllankoor ko, dàq ko ci mbooloo mi.
10 Por isso, se eu for, ­lembrar-me-ei dos feitos que ele realiza, proferindo contra nós palavras maliciosas; e, não contente com isto, não recebe os irmãos, e impede os que querem ­recebê-los, e os expulsa da igreja.
11 Sama xarit, bul roy lu bon, waaye lu baax rekk. Kuy def lu baax, ci Yàlla nga bokk; kuy def lu bon, xamoo dara ci Yàlla.
11 Amado, não sigas o que é mal, mas o que é bom. Aquele que faz o bem é de Deus; mas aquele que faz o mal não viu a Deus.
12 Naka Demetirus nag, ñépp seedeel nañu ko lu baax, te dëgg gi ci moom sax seedeel na ko ko. Nun itam seedeel nanu ko te wóor na ma ne sunu seede dëgg la.
12 Demétrio, porém, tem bom testemunho da parte de todos os homens, e da parte da própria verdade, sim, e também nós testemunhamos; e vós sabeis que o nosso testemunho é verdadeiro.
13 Am na lu bare lu ma la bëggoona wax, waaye lépp xajul ci kayit.
13 Eu tinha muitas coisas para escrever, mas não irei escrever-te com tinta e pena.
14 Kon yaakaar naa laa seetsi balaa yàgg, jàkkaarlook yaw, nu waxtaan ci.
14 Mas acredito que ver-te-ei brevemente, e falaremos face a face. Paz seja contigo. Nossos amigos te saúdam. Saúda os amigos por nome.
15 Yal na jàmm ànd ak yaw. Xarit yi yépp ñu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy xarit, kenn ku nekk ci turam.
15 — ausente —

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 3 João 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.