2 Tessalonicenses 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Léegi nag bokk yi, ñaanal-leen nu, ngir kàddug Boroom bi law te ànd ak ndam, ni mu ko ame woon ci yéen.
1 Finalmente, irmãos, orai por nós, para que a palavra do Senhor se propague e seja glorificada. como também o é entre vós,
2 Ngeen ñaanal nu it, ngir nu mucc ci ñi bon te soxor, ndaxte du ñépp a gëm.
2 e para que sejamos livres de homens perversos e maus; porque a fé não é de todos.
3 Waaye Boroom bi kuy sàmm kóllëre la; dina leen dëgëral te musal leen ci Ibliis.
3 Mas fiel é o Senhor, o qual vos confirmará e guardará do maligno.
4 Te wóor nanu ci kanam Boroom bi ne yéena ngi def li nu leen santoon, te dingeen ci sax.
4 E, quanto a vós, confiamos no Senhor que não só fazeis, mas fareis o que vos mandamos.
5 Na Boroom bi gindi seeni xol ci mbëggeelu Yàlla ak muñu Kirist.
5 Ora, o Senhor encaminhe os vossos corações no amor de Deus e na constância de Cristo.
6 Nu ngi leen di sant it bokk yi, ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen dëddu bépp mbokk buy wéy ci tayel te baña topp dénkaane, yi nu leen jottali.
6 mandamo-vos, irmãos, em nome do Senhor Jesus Cristo, que vos aparteis de todo irmão que anda desordenadamente, e não segundo a tradição que de nós recebestes.
7 Xam ngeen bu baax, yéen ci seen bopp, ni ngeen wara awe ci sunuy tànk. Ba nu nekkee ca yéen, wéyunu woon ci tayel
7 Porque vós mesmos sabeis como deveis imitar-nos, pois que não nos portamos desordenadamente entre vós,
8 te masunoo lekk ñaqu kenn. Waaye guddi ak bëccëg danu daan ñaq, di sonn, ngir baña wéeru ci kenn ci yéen.
8 nem comemos de graça o pão de ninguém, antes com labor e fadiga trabalhávamos noite e dia para não sermos pesados a nenhum de vós.
9 Waxuma ne amunu sañ-sañu def ko, waaye danoo bëggoona nekk ay royukaay ci yéen, ngir ngeen aw ci sunuy tànk.
9 Não porque não tivéssemos direito, mas para vos dar nós mesmos exemplo, para nos imitardes.
10 Ndaxte ba nu nekkee ca yéen, lii lanu tëraloon: «Ku liggéeyul, du lekk.»
10 Porque, quando ainda estávamos convosco, isto vos mandamos: se alguém não quer trabalhar, também não coma.
11 Léegi nag dégg nanu ne am na ci yéen ñuy wéy ci tayel; liggéeyuñu dara, lu dul di dugg ci lu seen yoon nekkul.
11 Porquanto ouvimos que alguns entre vós andam desordenadamente, não trabalhando, antes intrometendo-se na vida alheia;
12 Ñu deme noonu nag, nu ngi leen di sant te di leen dénk ci turu Boroom bi Yeesu Kirist, ñuy liggéey ci jàmm tey dunde seen ñaq.
12 a esses tais, porém, ordenamos e exortamos por nosso Senhor Jesus Cristo que, trabalhando sossegadamente, comam o seu próprio pão.
13 Yéen nag bokk yi, buleen tàyyi ci def lu rafet.
13 Vós, porém, irmãos, não vos canseis de fazer o bem.
14 Su kenn bañee topp li nu bind ci bataaxal bii, ràññeeleen ko te sore ko, ngir mu rus ci.
14 Mas, se alguém não obedecer à nossa palavra por esta carta, notai-o e não tenhais relações com ele, para que se envergonhe;
15 Waxuma ngeen def ko noon, waaye ngeen yedd ko ni seen mbokk.
15 todavia não o considereis como inimigo, mas admoestai-o como irmão.
16 Yal na leen kiy Boroom jàmm may jàmm fépp ak ci lépp. Yal na Boroom bi ànd ak yéen ñépp.
16 Ora, o próprio Senhor da paz vos dê paz sempre e de toda maneira. O Senhor seja com todos vós.
17 Tàggoo bii maa ko bind ci sama loxo, man Pool. Nii laay binde, te di màndargaale nii sama bataaxal yépp.
17 Esta saudação é de próprio punho, de Paulo, o que é o sinal em cada epístola; assim escrevo.
18 Yal na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen ñépp.
18 A graça de nosso Senhor Jesus Cristo seja com todos vós.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Tessalonicenses 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.