2 Tessalonicenses 1
Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB
1 Nun Pool ak Silwan ak Timote noo leen di bind, yéen mbooloom ñi gëm ci dëkku Tesalonig te nekk ci Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist.
1 Paulo, Silvano e Timóteo à igreja dos tessalonicenses, em Deus nosso Pai e no Senhor Jesus Cristo:
2 Yal na leen Yàlla Baay bi ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
2 Graças a vós, e paz da parte de Deus Pai e do Senhor Jesus Cristo.
3 Bokk yi, manunu lu dul sax ci sant Yàlla ndax yéen. Loolu jaadu na, ndax seen ngëm di gëna sax, te mbëggeel gi ngeen am ci seen biir, ku nekk ci sa moroom, di yokku lu bare.
3 Sempre devemos, irmãos, dar graças a Deus por vós, como é justo, porque a vossa fé cresce muitíssimo e o amor de cada um de vós transborda de uns para com os outros.
4 Noonu nu ngi damu ci yéen ci kanam mboolooy Yàlla yi, ndax seen muñ ak seen ngëm ci biir mboolem fitnay noon, ak coono, yi ngeen di dékku.
4 De maneira que nós mesmos nos gloriamos de vós nas igrejas de Deus por causa da vossa constância e fé em todas as perseguições e aflições que suportais;
5 Loolu mooy firndeel àtteb Yàlla bu jub bi, di wone ne yelloo ngeen nguuru Yàlla, gi tax ngeen di sonn.
5 o que é prova clara do justo juízo de Deus, para que sejais havidos por dignos do reino de Deus, pelo qual também padeceis;
6 Ndaxte jub na ci Yàlla, mu delloo coono ñi leen di sonal,
6 se de fato é justo diante de Deus que ele dê em paga tribulação aos que vos atribulam,
7 te it yéen ñiy dékku coono, mu boole leen ak nun, tàbbal nu ci noflaay, bés bu sunu Boroom Yeesu Kirist jógee asamaan, feeñ fi. Keroog dina ànd ak malaakaam yu am kàttan,
7 e a vós, que sois atribulados, alívio juntamente conosco, quando do céu se manifestar o Senhor Jesus com os anjos do seu poder em chama de fogo,
8 sawara su yànj wër ko, mu feeñ ngir mbugal ñi xamul Yàlla te baña déggal xibaaru jàmm bi jëm ci sunu Boroom Yeesu.
8 e tomar vingança dos que não conhecem a Deus e dos que não conhecem a Deus e dos que não obedecem ao evangelho de nosso Senhor Jesus;
9 Seen pey mooy alku ba fàww, ñu dàq leen fu sore Boroom bi ak ndamam lu réy.
9 os quais sofrerão, como castigo, a perdição eterna, banidos da face do senhor e da glória do seu poder,
10 Dina ñëw bés booba, ngir ndamam jolli ci biir gaayam yu sell yi, te ñépp ñi ko gëm yéemu ci moom— te ci ngeen bokk, ndaxte gëm ngeen li nu leen seede.
10 quando naquele dia ele vier para ser glorificado nos seus santos e para ser admirado em todos os que tiverem crido {porquanto o nosso testemunho foi crido entre vós}.
11 Moo tax dunu noppeek di leen ñaanal, ngir Yàlla sunu Boroom def leen, ngeen yeyoo li tax mu woo leen, te yeggali ak doole ci yéen bépp yéene ju baax ak bépp jëfu ngëm.
11 Pelo que também rogamos sempre por vós, para que o nosso Deus vos faça dignos da sua vocação, e cumpra com poder todo desejo de bondade e toda obra de fé.
12 Noonu turu Yeesu sunu Boroom dina màgg ci yéen, te yéen it dingeen màgg ci moom, aju ci yiwu sunu Yàlla ak Boroom bi Yeesu Kirist.
12 para que o nome de nosso Senhor Jesus seja glorificado em vós, e vós nele, segundo a graça de nosso Deus e do Senhor Jesus Cristo.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Tessalonicenses 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.