2 Timóteo 4
Téereb Injiil (WOL2010) vs ACF
1 Kon nag maa ngi lay dénk fa kanam Yàlla ak Kirist Yeesu, miy àtte ñiy dund ak ñi dee, di la dénk ci feeñam ci biir ndam ak ci nguuram, nga def lii:
1 Conjuro-te, pois, diante de Deus, e do Senhor Jesus Cristo, que há de julgar os vivos e os mortos, na sua vinda e no seu reino,
2 xamleel kàddug Yàlla, sax ci, su neexee ak su naqaree; yeyal ñi tooñ, di yedd ak a dénk ñépp, def ko ci muñ gu yaatu ak njàngle mu mat.
2 Que pregues a palavra, instes a tempo e fora de tempo, redarguas, repreendas, exortes, com toda a longanimidade e doutrina.
3 Ndaxte jamono dina ñëw, joo xam ne nit ñi dootuñu xajoo njàngle mu wér mi, waaye dinañu jublu ci seeni bëgg-bëgg, di fortaatu jànglekat yu leen di jay.
3 Porque virá tempo em que não suportarão a sã doutrina; mas, tendo comichão nos ouvidos, amontoarão para si doutores conforme as suas próprias concupiscências;
4 Dinañu tanqamlu dëgg, jeng jëm ci léebi diiney neen.
4 E desviarão os ouvidos da verdade, voltando às fábulas.
5 Waaye yaw nanga foog ci lépp, dékku tiis, tey tas xibaaru jàmm bi, ba matal sag yónnent.
5 Mas tu, sê sóbrio em tudo, sofre as aflições, faze a obra de um evangelista, cumpre o teu ministério.
6 Ndaxte maa ngi ci tànki joxe sama bakkan ni sarax, te sama waxtuw dem jot na.
6 Porque eu já estou sendo oferecido por aspersão de sacrifício, e o tempo da minha partida está próximo.
7 Bëre naa ba ub làmbi ngëm, daw naa ba àkk, sàmm naa mboolem dëgg, gi ñu ma dénk.
7 Combati o bom combate, acabei a carreira, guardei a fé.
8 Fi mu ne Yàllaa ngi may xaare añu ku jub, di kaalag ndam gi ma Boroom, biy Àttekat bu jub, di jox ca bés ba, te jéllale naa sama bopp, waaye képp ku def sa xol cig feeñam.
8 Desde agora, a coroa da justiça me está guardada, a qual o Senhor, justo juiz, me dará naquele dia; e não somente a mim, mas também a todos os que amarem a sua vinda.
9 Defal sa kem kàttan, ba fekksi ma ci ni mu gëna gaawe.
9 Procura vir ter comigo depressa,
10 Ndaxte Demas topp na àddina, ba bàyyi ma, dem dëkku Tesalonig; Kereseñsë dem na diiwaanu Galasi, Tit dem diiwaanu Dalmasi.
10 Porque Demas me desamparou, amando o presente século, e foi para Tessalônica, Crescente para Galácia, Tito para Dalmácia.
11 Luug rekk a des fi man. Indaaleel Màrk, ndaxte amal na ma njariñ ci liggéey bi.
11 Só Lucas está comigo. Toma Marcos, e traze-o contigo, porque me é muito útil para o ministério.
12 Tisig moom yebal naa ko dëkku Efes.
12 Também enviei Tíquico a Éfeso.
13 Te sooy ñëw, indaaleel mbubb, ma ma dénkoon Karpus ca dëkku Torowas, te it bul fàtte téere yi, rawatina téere yu am maana, yi ñu bind ci der.
13 Quando vieres, traze a capa que deixei em Trôade, em casa de Carpo, e os livros, principalmente os pergaminhos.
14 Alegsàndar tëgg bi def na ma ñaawteef yu ne, waaye Boroom bi dina ko fey ay jëfam.
14 Alexandre, o latoeiro, causoume muitos males; o Senhor lhe pague segundo as suas obras.
15 Moytu ko bu baax, ndaxte bëre na ak sunuy wax ba tàyyi.
15 Tu, guarda-te também dele, porque resistiu muito às nossas palavras.
16 Keroog bi ma jëkkee taxaw, di làyyil sama bopp, awma woon kenn ku ma taxawu, ñépp dañu maa daw— bu leen ko Yàlla jàppe nag.
16 Ninguém me assistiu na minha primeira defesa, antes todos me desampararam. Que isto lhes não seja imputado.
17 Waaye Boroom bi moo ma taxawu te dooleel ma, ma jollil kàddu gi, ba xeet yépp dégg ko. Te Boroom bi musal na ma ci selli gaynde.
17 Mas o Senhor assistiu-me e fortaleceu-me, para que por mim fosse cumprida a pregação, e todos os gentios a ouvissem; e fiquei livre da boca do leão.
18 Rax-ca-dolli dina ma musal ci bépp jëf ju ñaaw, tette ma ci jàmm, ba tàbbal ma ci nguuram gu kawe ga. Yal na yelloo ndam ba fàww. Amiin.
18 E o Senhor me livrará de toda a má obra, e guardar-me-á para o seu reino celestial; a quem seja glória para todo o sempre. Amém.
19 Nuyul ma Piriska ak Akilas ak waa kër Onesifor.
19 Saúda a Prisca e a Áqüila, e à casa de Onesíforo.
20 Erast des na dëkku Korent. Torofim dafa woppoon, ma bàyyi ko dëkku Mile.
20 Erasto ficou em Corinto, e deixei Trófimo doente em Mileto.
21 Gaawala ñëw, bala lolli di gàllankoor sa yoon. Ëbulus, Pudeñsë, Linus, Këlójaa ak yeneen bokk yépp ñu ngi lay nuyu.
21 Procura vir antes do inverno. Êubulo, e Prudente, e Lino, e Cláudia, e todos os irmãos te saúdam.
22 Yal na Boroom bi aar sa xel. Na yiwu Yàlla ànd ak yéen ñépp.
22 O Senhor Jesus Cristo seja com o teu espírito. A graça seja convosco. Amém.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Timóteo 4, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.