2 Timóteo 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Nanga xam lii: bési tiis yu tar ñu ngi nuy tëru ci mujug jamono.
1 Nota bem o seguinte: nos últimos dias haverá um período difícil.
2 Ndaxte nit ñi dinañu siis te fonk xaalis, di ñu réy tey yég seen bopp, ñuy xaste tey xëtt ndigalu waajur; duñu am kóllëre, sellaay
2 Os homens se tornarão egoístas, avarentos, fanfarrões, soberbos, rebeldes aos pais, ingratos, malvados,
3 mbaa cofeel; dañuy jàpp mer ak a sos; ñu xér lañuy doon, ñu soxor te bañ lu baax;
3 desalmados, desleais, caluniadores, devassos, cruéis, inimigos dos bons,
4 ay workat lañuy doon, di ñu ëppal te bare tiitar; seen bànneex a leen gënal Yàlla.
4 traidores, insolentes, cegos de orgulho, amigos dos prazeres e não de Deus,
5 Dañuy mbubboo diine waaye nanguwuñu koo dugal seen xol. Ñu deme noonu, dëddu leen.
5 ostentarão a aparência de piedade, mas desdenharão a realidade. Dessa gente, afasta-te!
6 Nit ñu mel noonu ñooy yoxoosu ci biir kër yi, ba fàbbi jigéen ñu ñàkk pastéef, ñi seeni bàkkaar ub seen bopp, te bëgg-bëgg yu wuute jiital leen.
6 Deles fazem parte os que se insinuam jeitosamente pelas casas e enfeitiçam mulherzinhas carregadas de pecados, atormentadas por toda espécie de paixões,
7 Duñu noppee gëstu, waaye duñu mana yegg ci xam-xamu dëgg mukk.
7 sempre a aprender sem nunca chegar ao conhecimento da verdade.
8 Nit ñooñu dañuy bëreek dëgg, ni Sànnes ak Sàmbares bëree woon ak Musaa; ay boroom xel yu gumba lañu, yu seen ngëm tekkiwul dara.
8 Como Janes e Jambres resistiram a Moisés, assim também estes homens de coração pervertido, reprovados na fé, tentam resistir à verdade.
9 Waaye duñu dem fu sore, ndax seen ñàkk xel dina bir ñépp, ni mu dale woon Sànnes ak Sàmbares.
9 Mas não irão longe, porque será manifesta a todos a sua insensatez, como o foi a daqueles dois.
10 Waaye yaw nag xam nga bu baax sama njàngle, sama dund, sama takkute, sama ngëm, sama muñ, sama mbëggeel ak sama dékku tiis.
10 Tu, pelo contrário, te aplicaste a seguir-me de perto na minha doutrina, no meu modo de vida, nos meus planos, na minha fé, na minha paciência, na minha caridade, na minha constância,
11 Xam nga li ma daj ciy fitna ak i coono ci dëkki Ancos, Ikoñum ak Listar. Céy li ma jànkoonteel ciy fitna! Waaye Boroom bi musal na ma ci lépp.
11 nas minhas perseguições, nas provações que me sobrevieram em Antioquia, em Icônio, em Listra. Que perseguições tive que sofrer! E de todas me livrou o Senhor.
12 Te ku bokk ci Kirist Yeesu, te bëgg dund dund gu ànd ak ragal Yàlla, alamikk ñu fitnaal la.
12 Pois todos os que quiserem viver piedosamente, em Jesus Cristo, terão de sofrer a perseguição.
13 Waaye nit ñu bon ñi ak naaféq yi dinañu fi yées, di naxe ak a nax seen bopp.
13 Mas os homens perversos e impostores irão de mal a pior, sedutores e seduzidos.
14 Yaw nag saxal ci li nga jàng te mu wóor la, xam fi nga tibbe.
14 Tu, porém, permanece firme naquilo que aprendeste e creste. Sabes de quem aprendeste.
15 Li dale ci sa ngone xam nga Mbind mu sell, mi la mana yee ci yoonu mucc, jaar ci gëm Kirist Yeesu.
15 E desde a infância conheces as Sagradas Escrituras e sabes que elas têm o condão de te proporcionar a sabedoria que conduz à salvação, pela fé em Jesus Cristo.
16 Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub.
16 Toda a Escritura é inspirada por Deus, e útil para ensinar, para repreender, para corrigir e para formar na justiça.
17 Noonu waayu Yàlla ji dina mat, ba jekk ci bépp jëf ju rafet.
17 Por ela, o homem de Deus se torna perfeito, capacitado para toda boa obra.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Timóteo 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.