2 Pedro 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARC

Sair da comparação
ARC Almeida Revista e Corrigida 2009
1 Yéen samay xarit, sama ñaareelu bataaxal a ngi nii. Bind naa leen, ngir xiir leen ci xalaat yu sell.
1 Amados, escrevo-vos, agora, esta segunda carta, em ambas as quais desperto com exortação o vosso ânimo sincero,
2 Maa ngi leen di fàttali kàdduy yonent yu sell, yi fi jiitu woon, ak ndigalu Boroom bi sunu Musalkat, li ngeen déggoon ci ndaw, yi Yàlla yebaloon fi yéen.
2 para que vos lembreis das palavras que primeiramente foram ditas pelos santos profetas e do mandamento do Senhor e Salvador, mediante os vossos apóstolos,
3 Nangeen jëkka xam lii: mujug jamono dingeen gis ay tiiñalkat, di topp seen bakkan; dinañu leen tiiñal
3 sabendo primeiro isto: que nos últimos dias virão escarnecedores, andando segundo as suas próprias concupiscências
4 ci di leen ne: «Ki dige woon ne dina ñëw, ana mu? Ndaxte baay ya nelaw nañu, waaye lépp a ngi dox ca njàlbéen ga ba tey.»
4 e dizendo: Onde está a promessa da sua vinda? Porque desde que os pais dormiram todas as coisas permanecem como desde o princípio da criação.
5 Fekk bëgguñoo xam lii: kàddug Yàllaa tax, asamaan ak àddina yu jëkk ya juddoo ca ndox te dunde ko.
5 Eles voluntariamente ignoram isto: que pela palavra de Deus já desde a antiguidade existiram os céus e a terra, que foi tirada da água e no meio da água subsiste;
6 Te ndox it moo labal àddina sa, raafal ko.
6 pelas quais coisas pereceu o mundo de então, coberto com as águas do dilúvio.
7 Te kàddug Yàlla googu moo denc asamaan yii fi nekk ak suuf si, ngir lakk leen; Yàllaa ngi leen di nége bésub àtte, ba muy alag ñi weddi.
7 Mas os céus e a terra que agora existem pela mesma palavra se reservam como tesouro e se guardam para o fogo, até o Dia do Juízo e da perdição dos homens ímpios.
8 Yéen samay xarit, buleen umple ne benn bés ak junniy at ñoo yem fi Boroom bi.
8 Mas, amados, não ignoreis uma coisa: que um dia para o Senhor é como mil anos, e mil anos, como um dia.
9 Li Yàlla dige, dina ko def, lu mu yéex yéex ci xalaatu nit. Xanaa kay da leena muñal, ndax bëggul kenn alku, waaye ñépp tuub seeni bàkkaar.
9 O Senhor não retarda a sua promessa, ainda que alguns a têm por tardia; mas é longânimo para convosco, não querendo que alguns se percam, senão que todos venham a arrepender-se.
10 Waaye bésu Boroom bi dina ñëw, bett àddina ni sàcc. Su boobaa asamaan yi dinañu ne rajax toj, lu ne ci àddina lakk ba seey, te suuf ak lu mu ëmb dina ne fàŋŋ fa kanam Yàlla.
10 Mas o Dia do Senhor virá como o ladrão de noite, no qual os céus passarão com grande estrondo, e os elementos, ardendo, se desfarão, e a terra e as obras que nela há se queimarão.
11 Gannaaw loolu lépp dina seeye noonu nag, nangeen góor-góorlu ci gëna sellal seen nekkin te feddali seen ragal Yàlla.
11 Havendo, pois, de perecer todas estas coisas, que pessoas vos convém ser em santo trato e piedade,
12 Te it ngeen taxaw temm ci séentu bésu Yàlla bi, te waajal ñëwam. Su boobaa asamaan yi dinañu lakk, ba naaw ni pënd, te lu nekk ci àddina dina lakk, ba seey nib dóom.
12 aguardando e apressando- vos para a vinda do Dia de Deus, em que os céus, em fogo, se desfarão, e os elementos, ardendo, se fundirão?
13 Waaye nu ngi séentu asamaan su bees ak suuf su bees, fa njub dëkk, ci ni ko Yàlla dige.
13 Mas nós, segundo a sua promessa, aguardamos novos céus e nova terra, em que habita a justiça.
14 Kon nag samay soppe, gannaaw yéena ngi séentu loolu, góor-góorluleen, ngir bu Kirist ñëwee, mu fekk leen ci jàmm, ngeen baña am benn gàkk mbaa sikk.
14 Pelo que, amados, aguardando estas coisas, procurai que dele sejais achados imaculados e irrepreensíveis em paz
15 Te jàppleen ne muñug sunu Boroom muccu nit la. Sunu mbokk mi nu bëgg, Pool, bind na leen ko, ci xel mi ko Yàlla sol.
15 e tende por salvação a longanimidade de nosso Senhor, como também o nosso amado irmão Paulo vos escreveu, segundo a sabedoria que lhe foi dada,
16 Noonu lay waxe ciy bataaxalam yépp di ci biral lii. Am na ci sax yu jafee xam, te ñi amul xam-xam te seen ngëm dëgërul di ko walbati, ba alag seen bopp, te loolu lañuy def ci Mbind yi ci des.
16 falando disto, como em todas as suas epístolas, entre as quais há pontos difíceis de entender, que os indoutos e inconstantes torcem e igualmente as outras Escrituras, para sua própria perdição.
17 Noonu yéen samay xarit, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, moytuleen ñi weddi fàbbi leen ci seen réer, ba yolomal seen wàkkirlu ci Yàlla.
17 Vós, portanto, amados, sabendo isto de antemão, guardai-vos de que, pelo engano dos homens abomináveis, sejais juntamente arrebatados e descaiais da vossa firmeza;
18 Waaye màggleen ci yiwu sunu Boroom ak Musalkat Yeesu Kirist, te sax ci xam ko; moo yelloo ndam fii ba fàww.
18 antes, crescei na graça e conhecimento de nosso Senhor e Salvador Jesus Cristo. A ele seja dada a glória, assim agora como no dia da eternidade. Amém!

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Pedro 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.