2 Pedro 2

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Waaye ci bànni Israyil, amoon na naaféq yu mbubboo turu yonent, ni muy ame seen biir ñuy mbubboo turu jànglekat. Ci seeni pexe dinañu dugal ci yéen xalaat yu sànke, di weddi Boroom bi leen jot, tey yóbbe seen bopp alkànde ju teew.
1 Assim como houve entre o povo falsos profetas, assim também haverá entre vós falsos doutores que introduzirão disfarçadamente seitas perniciosas. Eles, renegando assim o Senhor que os resgatou, atrairão sobre si uma ruína repentina.
2 Ñu bare dinañu leen fekki ci seeni ñaawteef, ba gàkkal yoonu dëgg ci bëti nit ñi.
2 Muitos os seguirão nas suas desordens e serão deste modo a causa de o caminho da verdade ser caluniado.
3 Seen bëgge dina tax, ñu dabb-daaxe ay wax, ngir nax leen, ba lekk seenus tuut. Waaye àtte baa ngi leen di xaar, te seen alkànde di leen teeru.
3 Movidos por cobiça, eles vos hão de explorar por palavras cheias de astúcia. Há muito tempo a condenação os ameaça, e a sua ruína não dorme.
4 Ndaxte Yàlla jéggalul malaaka ya bàkkaaroon, waaye tàbbal na leen sawara, tëj leen ca kàmb yu lëndëm, di leen nége àtte ba.
4 Pois se Deus não poupou os anjos que pecaram, mas os precipitou nos abismos tenebrosos do inferno onde os reserva para o julgamento;
5 Te it jéggalul àddina su jëkk sa weddi woon, ba xooj ko ci ndoxu mbënn ma, waaye musal na Nóoyin rekk, mi daan waare ci njub, moom ak juróom ñaari nit.
5 se não poupou o mundo antigo, e só preservou oito pessoas, dentre as quais Noé, esse pregador da justiça, quando desencadeou o dilúvio sobre um mundo de ímpios;
6 Te it Yàlla daan na dëkki Sodom ak Gomor, raafal leen cig lakk, ñuy misaalu ñiy weddi ëllëg.
6 se condenou à destruição e reduziu à cinzas as cidades de Sodoma e Gomorra para servir de exemplo para os ímpios do porvir;
7 Waaye musal na Lóot mi jub, mi sonnoon ndax ñaawteefi ñu dëng, ñooñu mu nekkaloon.
7 se, enfim, livrou o justo Lot, revoltado com a vida dissoluta daquela gente perversa
8 Ndaxte Lóot, mi dëkkoon ci seen biir, dafa dëkke woon tiisu xol, ndax ñaawteef yi mu gis ak a dégg guddi ak bëccëg.
8 {esse justo que habitava no meio deles sentia cada dia atormentada sua alma virtuosa, pelo que via e ouvia dos seus procedimentos infames},
9 Gannaaw loolu lépp am na nag, nanu bir ne Boroom bi man na musal aji gëm ji nekk ci nattu, te denc ñi jubadi, ngir alag leen bésu àtte ba.
9 é porque o Senhor sabe livrar das provações os homens piedosos e reservar os ímpios para serem castigados no dia do juízo,
10 Rawatina ñiy topp seen bakkan ciy bëgg-bëgg yu ruslu, te faalewuñu genn kilifteef. Ñu ñeme Yàlla lañu, te dëgër bopp, ba ragaluñoo xas kilifa ya gëna kawe.
10 principalmente aqueles que correm com desejos impuros atrás dos prazeres da carne e desprezam a autoridade. Audaciosos, arrogantes, não temem falar injuriosamente das glórias,
11 Fekk sax malaaka, yi leen ëpp doole ak kàttan, tey sax ca jataayu Boroom bi, ñemewuñoo xas kilifa yooyu.
11 embora os anjos, superiores em força e poder, não pronunciem contra elas, aos olhos do Senhor, o julgamento injurioso.
12 Waaye ñoom dañuy xas ci biir yi ñu xamul. Ñoom ak bàyyima ñoo yem, di ay mbindeef yuy tañaxu, te tër rendi rekk a jekk ci ñoom; dees na leen rey ni bàyyima,
12 Mas estes, quais brutos destinados pela lei natural para a presa e para a perdição, injuriam o que ignoram, e assim da mesma forma perecerão. Este será o salário de sua iniqüidade.
13 muy seen peyug njubadi.
13 Encontram as suas delícias em se entregar em pleno dia às suas libertinagens. Homens pervertidos e imundos, sentem prazer em enganar, enquanto se banqueteiam convosco.
14 Jigéen ju seen bët tegu, ñu xédd ko, ba duñu tàggook moy mukk. Ku ñàkk pastéef ñu fàbbi la. Ñu xelu lañu jëme cig bëgge. Ñu alku lañu!
14 Têm, os olhos cheios de adultério e são insaciáveis no pecar. Seduzem pelos seus atrativos as almas inconstantes; têm o coração acostumado à cobiça; são filhos da maldição.
15 Réer nañu ba wàcc yoon wu jub wi, topp yoonu Balaam, doomu Bosor, mi bëgge xiiroon ci njubadi.
15 Deixaram o caminho reto, para se extraviarem no caminho de Balaão, filho de Bosor, que amou o salário da iniqüidade.
16 Waaye déggadeem yóbbe na ko yeraange; xam ngeen ne mbaam-sëf du wax, waaye mbaam wax na ak moom ci làmmiñ wu bir, ngir mu génn ci ndofam googu.
16 Mas foi repreendido pela sua desobediência: um animal mudo, falando com voz humana, refreou a loucura do profeta.
17 Ñooñule ay teen yu dëy lañu, di xiini lay yu ngelaw liy naawal, te seen pey mooy lëndëm gu ne taraj.
17 Estes são fontes sem água e nuvens agitadas por turbilhões, destinados à profundeza das trevas.
18 Dañuy fàbbi ñu naroona mucc ci àddina ju réer, dig leen ak làmmiñ yu neex bànneexi bakkan yu jéggi dayo.
18 Com palavras tão vãs quanto enganadoras, atraem pelas paixões carnais e pela devassidão aqueles que mal acabam de escapar dos homens que vivem no erro.
19 Dañu leen di dig ngoreel, te fekk ñoom ci seen bopp jaami yàqute lañu, ndaxte lu la not, jaamam nga.
19 Prometem-lhes a liberdade, quando eles mesmos são escravos da corrupção, pois o homem é feito escravo daquele que o venceu.
20 Su ñu xamee Boroom bi, di sunu Musalkat Yeesu Kirist, ba mucc ci sobes àddina, ba noppi sóobuwaat ca, ba mu not leen, seen muj moo yées seen njàlbéen.
20 Com efeito, se aqueles que renunciaram às corrupções do mundo pelo conhecimento de Jesus Cristo nosso Senhor e Salvador nelas se deixam de novo enredar e vencer, seu último estado torna-se pior do que o primeiro.
21 Ndaxte ñu xam yoon wu jub wi, ba noppi dëddu ndigal lu sell li ñu déggoon, bañoon koo xam moo gënoon ci ñoom.
21 Melhor fora não terem conhecido o caminho da justiça do que, depois de tê-lo conhecido, tornarem atrás, abandonando a lei santa que lhes foi ensinada.
22 Noonu seen mbir dëggal na li ñuy wax ne: «Xaj mooy waccu, di ko lekkaat,» te it: «Mbaam-xuux, loo ko sang sang, mu xalangu ci ban.»
22 Aconteceu-lhes o que diz com razão o provérbio: O cão voltou ao seu vômito {Pr 26,11}; e: A porca lavada volta a revolver-se no lamaçal.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Pedro 2, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.