2 João 1

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Man njiit li maa leen di bind, yaw soxna su tedd si, yaw ak say doom. Bëgg naa leen bu wér ci sama xol, jéllale naa sama bopp sax, waaye itam képp ku xam dëgg gi.
1 O ancião à senhora eleita, e a seus filhos, aos quais eu amo em verdade, e não somente eu, mas também todos os que conhecem a verdade,
2 Te dëgg gee tax nuy def noonu, dëgg gi dëkk ci nun, tey ànd ak nun ba fàww.
2 por causa da verdade que permanece em nós, e para sempre estará conosco:
3 Yàlla Baay bi ak Yeesu Kirist, Doomu Baay bi, dinañu nu may yiw, yërmande ak jàmm, ànd ak dëgg ak mbëggeel.
3 Graça, misericórdia, paz, da parte de Deus Pai e da parte de Jesus Cristo, o Filho do Pai, serão conosco em verdade e amor.
4 Gis naa ci say doom, ñuy jaar ci tànki dëgg, ni nu ko Baay bi digale, te bég naa ci lool.
4 Muito me alegro por ter achado alguns de teus filhos andando na verdade, assim como recebemos mandamento do Pai.
5 Léegi nag soxna si, maa ngi lay dénk lii: nun ñépp nanu bëggante, te loolu du dénkaane bu bees, waaye moom lanu jotoon ca njàlbéen ga.
5 E agora, senhora, rogo-te, não como te escrevendo um novo mandamento, mas aquele mesmo que desde o princípio tivemos: que nos amemos uns aos outros.
6 Lii mooy mbëggeel: nu wéer sunug dund ci ndigali Yàlla; loolu mooy ndigalam, la nu jotoon ca njàlbéen ga, te ci lanu wara jaar.
6 E o amor é este: que andemos segundo os seus mandamentos. Este é o mandamento, como já desde o princípio ouvistes, para que nele andeis.
7 Maa ngi wax loolu nag, ndaxte am na ñuy sànke ñu bare, ñu tasaaroo ci àddina, te nanguwuñu ne Yeesu Kirist wàcc na, nekk nit. Kooku aji sànke la, di Bañaaleb Kirist.
7 Porque já muitos enganadores saíram pelo mundo, os quais não confessam que Jesus Cristo veio em carne. Tal é o enganador e o anticristo.
8 Kon moytuleen, ngir baña ñàkk seen añub coono, waaye ngeen am yool bu mat sëkk.
8 Olhai por vós mesmos, para que não percais o fruto do nosso trabalho, antes recebeis plena recompensa.
9 Képp ku saxul ci dénkaaney Kirist, xanaa di ko weesu, bokkul ci Yàlla; ku sax ci dénkaane yi, bokk nga ak Baay bi ak Doom ji.
9 Todo aquele que vai além do ensino de Cristo e não permanece nele, não tem a Deus; quem permanece neste ensino, esse tem tanto ao Pai como ao Filho.
10 Ku ñëw fi yaw, te indaalewul dénkaane yooyu, waxuma nga bañ koo teeru rekk, waaye bu ko nuyu sax.
10 Se alguém vem ter convosco, e não traz este ensino, não o recebais em casa, nem tampouco o saudeis.
11 Ku ko nuyu, bokk nga ciy ñaawteefam.
11 Porque quem o saúda participa de suas más obras.
12 Bëggoon naa leena wax lu bare ci bataaxal bii, waaye lépp xajul ci kayit. Kon nag fas naa yéenee ñëw, ba jàkkaarlook yéen, nu waxtaan ci, ngir sunu mbég mat sëkk.
12 Embora tenha eu muitas coisas para vos escrever, não o quis fazer com papel e tinta; mas espero visitar-vos e falar face a face, para que o nosso gozo seja completo.
13 Say doomi rakk, ji Yàlla tànn, ñu ngi lay nuyu.
13 Saúdam-te os filhos de tua irmã, a eleita.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 João 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.