2 Coríntios 9

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARA

Sair da comparação
ARA Almeida Revista e Atualizada 1993
1 Ci mbirum ndimbal loolu jëm ci gaayi Yàlla yi, matul ma leen di bindaat,
1 Ora, quanto à assistência a favor dos santos, é desnecessário escrever-vos,
2 ndaxte xam naa seen yéene ju rafet, te maa ngi ciy damu ci kanam waa Maseduwan, naan leen: «Daaw fekk na waa Akayi jekk.» Te seen cawarte xamb na ñu bare ci ñoom.
2 porque bem reconheço a vossa presteza, da qual me glorio junto aos macedônios, dizendo que a Acaia está preparada desde o ano passado; e o vosso zelo tem estimulado a muitíssimos.
3 Maa ngi yónni nag bokk yooyu, ngir damu gi nu doon damu ci yéen ci mbir mii baña neen, te ngeen jekk, ni ma ko waxe woon.
3 Contudo, enviei os irmãos, para que o nosso louvor a vosso respeito, neste particular, não se desminta, a fim de que, como venho dizendo, estivésseis preparados,
4 Danoo bañ rekk waa Maseduwan, ñiy ànd ak man, fekk jekkaguleen; te kon kóolute googu nu am ci yéen dina nekk sunu gàcce, waxaalewuma nag seen bos.
4 para que, caso alguns macedônios forem comigo e vos encontrem desapercebidos, não fiquemos nós envergonhados (para não dizer, vós) quanto a esta confiança.
5 Moo tax ma xalaat ne li gën mooy yónni bokk yooyu, ñu jiitu ma ci yéen, topptoo mbiri ndimbal lu yaatu loolu ngeen dige woon. Loolu di may gu tàlli, te baña nekk yëfi nay.
5 Portanto, julguei conveniente recomendar aos irmãos que me precedessem entre vós e preparassem de antemão a vossa dádiva já anunciada, para que esteja pronta como expressão de generosidade e não de avareza.
6 Li am mooy: ku ji tuuti, góob tuuti; ku ji lu bare, góob lu bare.
6 E isto afirmo: aquele que semeia pouco pouco também ceifará; e o que semeia com fartura com abundância também ceifará.
7 Kon na ku nekk joxe, ni mu ko nase ci xolam, te bañ cee am réccu walla sañul-bañ, ndaxte kiy joxe ak mbég moo neex Boroom bi.
7 Cada um contribua segundo tiver proposto no coração, não com tristeza ou por necessidade; porque Deus ama a quem dá com alegria.
8 Yàlla man na leena woomal ci bépp yiwam ba ci fépp ak ci lépp, ngeen faj seen soxla yépp te sakkanle it ngir bépp jëf bu baax.
8 Deus pode fazer-vos abundar em toda graça, a fim de que, tendo sempre, em tudo, ampla suficiência, superabundeis em toda boa obra,
9 Moom la Mbind mi wax ne:
9 como está escrito: Distribuiu, deu aos pobres, a sua justiça permanece para sempre.
10 Yàlla miy jox beykat bi jiwu ak nit ab dund, dina leen jox jiwu wu ne gàññ, te sakkanal li seen njub meññ.
10 Ora, aquele que dá semente ao que semeia e pão para alimento também suprirá e aumentará a vossa sementeira e multiplicará os frutos da vossa justiça,
11 Noonu dingeen woomle ci lépp, ba yéwén ci bépp anam, ba tax ñu bare gërëm Yàlla ndax li ngeen maye jaarale ko ci nun.
11 enriquecendo-vos, em tudo, para toda generosidade, a qual faz que, por nosso intermédio, sejam tributadas graças a Deus.
12 Ndaxte njaamu, gi ngeen di jaamu, yemul rekk ci faj soxlay gaayi Yàlla yi, waaye dina tax it ngërëmu ñu bare baawaan, jëm ci Yàlla.
12 Porque o serviço desta assistência não só supre a necessidade dos santos, mas também redunda em muitas graças a Deus,
13 Ci li ngeen firndeel seen mbëggeel ci joxe ndimbal lii, dinañu màggal Yàlla, ndaxte wone ngeen ni ngeen déggale xibaaru jàmm bu Kirist bi, ak ni ngeen yéwéne ci seen ndimbal jëme ci ñoom ak ñépp.
13 visto como, na prova desta ministração, glorificam a Deus pela obediência da vossa confissão quanto ao evangelho de Cristo e pela liberalidade com que contribuís para eles e para todos,
14 Rax-ca-dolli dinañu sant Yàlla ak xol bu fees ak cofeel ci yéen ndax yiw wu mag, wi Yàlla def ci yéen.
14 enquanto oram eles a vosso favor, com grande afeto, em virtude da superabundante graça de Deus que há em vós.
15 Jërëjëfati yaw Yàlla ndax sa may googu weesu dayo!
15 Graças a Deus pelo seu dom inefável!

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Coríntios 9, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.