2 Coríntios 8
Téereb Injiil (WOL2010) vs ACF
1 Gannaaw loolu bokk yi, danu leena bëgga xamal li yiwu Yàlla jur ci biir mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Maseduwan.
1 Também, irmãos, vos fazemos conhecer a graça de Deus dada às igrejas da macedônia;
2 Nattu yi ñu jaar ëmb nañu coono yu réy; waaye seen mbég mu tar ak seen ñàkk gu metti ñoo jur ci ñoom yéwén gu jéggi dayo.
2 Como em muita prova de tribulação houve abundância do seu gozo, e como a sua profunda pobreza abundou em riquezas da sua generosidade.
3 Seede naa ne ñoom ci seen bopp joxe nañu ba fa seen man-man yem, ba weesu ko sax.
3 Porque, segundo o seu poder (o que eu mesmo testifico) e ainda acima do seu poder, deram voluntariamente.
4 Sarxu nañu nu lool, ngir bokk ci ñiy yónnee ndimbal gaayi Yàlla yi.
4 Pedindo-nos com muitos rogos que aceitássemos a graça e a comunicação deste serviço, que se fazia para com os santos.
5 Te yemuñu sax ci li nu séentu woon ci ñoom, waaye dañoo jébbal seen bopp Boroom bi jëkk, gannaaw loolu ñu jébbal nu seen bopp ci coobarey Yàlla.
5 E não somente fizeram como nós esperávamos, mas a si mesmos se deram primeiramente ao Senhor, e depois a nós, pela vontade de Deus.
6 Looloo tax nag nu sant Tit, mu ñëw àggale ci yéen, ni mu tàmbalee woon, seen jëfu ndimbal.
6 De maneira que exortamos a Tito que, assim como antes tinha começado, assim também acabasse esta graça entre vós.
7 Gannaaw nag wone ngeen cawarte gu tollu noonu, ci ngëm, ci wax, ci xam-xam, ci farlu gu mat, ak ci seen mbëggeel ci nun, sawareleen noonu it ci jëfu ndimbal lii.
7 Portanto, assim como em tudo abundais em fé, e em palavra, e em ciência, e em toda a diligência, e em vosso amor para conosco, assim também abundeis nesta graça.
8 Du ndigal lu ma leen di jox, waaye dama leen di yégal cawarteg ñi ci des, ngir natt fu seen mbëggeel tollu.
8 Não digo isto como quem manda, mas para provar, pela diligência dos outros, a sinceridade de vosso amor.
9 Ndaxte yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist umpu leen, ni mu futtee am-amam, ba ñàkk ngir yéen, ndax ngeen woomle cig ñàkkam.
9 Porque já sabeis a graça de nosso Senhor Jesus Cristo que, sendo rico, por amor de vós se fez pobre; para que pela sua pobreza enriquecêsseis.
10 Kon lii laa xalaat ci lu baax ci yéen: yéen ñi nga xam ne tàmbaliwuleena jëf rekk, waaye yéena jëkka am yéene jii daaw,
10 E nisto dou o meu parecer; pois isto convém a vós que, desde o ano passado, começastes; e não foi só praticar, mas também querer.
11 yeggaleleen ko léegi. Noonu li ngeen mottali ci seen man-man tolloo ak yéene, ji ngeen amoon ci seen mébét.
11 Agora, porém, completai também o já começado, para que, assim como houve a prontidão de vontade, haja também o cumprimento, segundo o que tendes.
12 Ndaxte joxe, bu àndee ak yéene, Yàlla dina ko nangu, di seet li nu am te baña seet li nu amul.
12 Porque, se há prontidão de vontade, será aceita segundo o que qualquer tem, e não segundo o que não tem.
13 Bëgguma leena teg soxla, ngir woyofal ñi ci des, waaye na ñépp tolloole.
13 Mas, não digo isto para que os outros tenham alívio, e vós opressão,
14 Tey jii nag man ngeen sàkk ci li ngeen barele, faj soxlay ñeneen, ngir ëllëg it bareleg ñooña faj seen soxla. Noonu ñépp tolloole.
14 Mas para igualdade; neste tempo presente, a vossa abundância supra a falta dos outros, para que também a sua abundância supra a vossa falta, e haja igualdade;
15 Moom la Mbind mi tëral ne: «Ki dajale lu bare ëpplewul dara, te ki dajale tuuti ñàkkul.»
15 Como está escrito: O que muito colheu não teve demais; e o que pouco, não teve de menos.
16 Cant ñeel na Yàlla, moom mi def ci xolu Tit cawarte gu mel ni sunu gos ci yéen!
16 Mas, graças a Deus, que pôs a mesma solicitude por vós no coração de Tito;
17 Bi nu ko laajee, mu ñëw ci yéen, nangu na, te rax-ca-dolli cawarteem tollu na, ba nu mana wax ne ci coobarey boppam la jóge, jëm ci yéen.
17 Pois aceitou a exortação, e muito diligente partiu voluntariamente para vós.
18 Yónniwaale nanu ak moom mbokk, mi am tur wu rafet ci mboolooy ñi gëm ñépp ndax li muy waare xibaaru Kirist.
18 E com ele enviamos aquele irmão cujo louvor no evangelho está espalhado em todas as igrejas.
19 Te sax mbooloo yi ñoo ko tànn, ngir mu ànd ak nun, bu nuy yóbbu ndimbal li ngir ndamu Boroom bi, te mu firndeel sunu yéene ju rafet.
19 E não só isto, mas foi também escolhido pelas igrejas para companheiro da nossa viagem, nesta graça que por nós é ministrada para glória do mesmo Senhor, e prontidão do vosso ânimo;
20 Def nanu noonu nag, ndax kenn bañ noo ŋàññ ci ni nuy topptoo ndimbal lu yaatu loolu.
20 Evitando isto, que alguém nos vitupere por esta abundância, que por nós é ministrada;
21 Danuy fexee def li jub, du ci kanam Yàlla rekk, waaye it ci kanam nit ñi.
21 Pois zelamos do que é honesto, não só diante do Senhor, mas também diante dos homens.
22 Yónniwaale nanu it sunu mbokk, mi nu seetlu cawarteem ay yooni yoon ci fànn yu bare, te mu gën koo fésal bii yoon ndax kóolute gu réy, gi mu am ci yéen.
22 Com eles enviamos também outro nosso irmão, o qual muitas vezes, e em muitas coisas, já experimentamos ser diligente, e agora muito mais diligente ainda pela muita confiança que em vós tem.
23 Noonu kon ci lu jëm ci Tit, sama nawle la ci liggéey, bi ci seen biir. Ci lu jëm ci sunu bokk, yi ànd ak moom nag, ndawi mbooloom ñi gëm lañu, ñuy wone ndamu Kirist.
23 Quanto a Tito, é meu companheiro, e cooperador para convosco; quanto a nossos irmãos, são embaixadores das igrejas e glória de Cristo.
24 Na seen teeru firndeel nag seen mbëggeel ci kanam mboolooy ñi gëm, te dëggal leen ne noo yey wóolu leen.
24 Portanto, mostrai para com eles, e perante a face das igrejas, a prova do vosso amor, e da nossa glória acerca de vós.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Coríntios 8, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.