2 Coríntios 6

Téereb Injiil (WOL2010) vs BKJ

Sair da comparação
1 Nun nag ñiy liggéeyandoo ak Yàlla, nu ngi leen di ñaan: jariñooleen yiw, wi ngeen jote ci Yàlla, ngir mu baña neen ci yéen.
1 Então nós, como colaboradores dele, rogamo-vos também para que não recebais a graça de Deus em vão.
2 Ndaxte Yàlla nee na:
2 (Porque ele diz: Em tempo aceitável tenho ouvido, e em dia de salvação tenho socorrido. Eis aqui agora o tempo aceitável, eis aqui agora o dia da salvação).
3 Bëggunoo lëmbaaje xelu kenn ci dara, ngir kenn baña sikk sunu liggéey.
3 Não dando em nada ocasião de tropeço, para que o ministério não seja culpado;
4 Li nu bëgg moo di rafetal sunu tur ni jawriñi Yàlla ci fànn gu nekk; danuy muñ coono yi, tiis yi, njàqare yi;
4 Mas, em todas as coisas, aprovando-nos como ministros de Deus, na muita paciência, nas aflições, nas necessidades, nas angústias,
5 ñu nuy dóor, di nu tëj ci kaso, dëkk yi di yëngu ndax sunu mbir; nuy liggéey ba sonn, di fanaane xool, di woor.
5 nos açoites, nas prisões, nos tumultos, nos trabalhos, nas vigílias, nos jejuns,
6 Nu ngi rafetal sunu yen ci dund gu sell, ci xam-xam, muñ ak laabiir, ci Xel mu Sell mi ak ci mbëggeel gu raxul njublaŋ,
6 na pureza, no conhecimento, na longanimidade, na bondade, no Espírito Santo, no amor não fingido,
7 ci kàddug dëgg ak ci kàttanu Yàlla, nu ngi yor gànnaayi njubte ci loxol ndijoor ak lu càmmoñ.
7 na palavra da verdade, no poder de Deus, pela armadura da justiça, à direita e à esquerda,
8 Ñu bàkk nu, jéppi nu, sant nu, xas nu. Ñu di nu jiiñ réeral, moona niti dëgg lanu.
8 por meio da honra e da desonra, por meio da má fama e da boa fama; como enganadores, porém verdadeiros;
9 Ñuy xeeb sunu tur, moona tur yi siiw nañu. Nu mel ni ñu loof, moona nu ngi dund. Ñu yar nu, teewul nu rëcc ci dee.
9 como desconhecidos, porém bem conhecidos; como morrendo, e eis que vivemos; como castigados, e não mortos;
10 Danuy dékku tiis, waaye di bég fu nu tollu. Nu tumurànke, waaye di woomal ñu bare; amunu dara, fekk noo moom lépp.
10 como tristes, mas sempre alegres; como pobres, mas enriquecendo a muitos; como nada tendo, e todavia possuindo todas as coisas.
11 Yéen bokki Korent, wax nanu leen sunu biir ak sunu biti, di leen ubbil sunu xol.
11 Ó vós Coríntios, a nossa boca está aberta para vós, o nosso coração está ampliado.
12 Ubbiku nanu ci yéen, waaye yéen ubbikuwuleen ci nun.
12 Vós não estais estreitados em nós; mas estais estreitados nas vossas próprias entranhas.
13 Maa ngi wax ak yéen ni samay doom; feyleen nu bor bi, yéen itam; ubbileen seen xol!
13 Ora, em recompensa disto, (eu falo como a meus filhos) sejais vós também dilatados.
14 Buleen likkoo ak ñi gëmul. Gan àndandoo moo mana am diggante njubte ak ndëngte? Gan booloo moo mana am diggante leer ak lëndëm?
14 Não estejais unidos em jugo desigual com incrédulos, pois que companheirismo tem a justiça com a injustiça? E que comunhão tem a luz com as trevas?
15 Gan déggoo moo mana am diggante Kirist ak Beliyar? Gan jaxasoo moo mana am diggante ki gëm ak ki gëmul?
15 E que harmonia há entre Cristo e Belial? Ou que parte tem o crente com o infiel?
16 Nan la kër Yàlla mana mànkoo ak xërëm yi? Ndaxte nun nooy kër Yàlla Aji Dund ji, ni ko Yàlla waxe:
16 E que acordo tem o templo de Deus com os ídolos? Porque vós sois o templo do Deus vivo, como Deus disse: Eu habitarei neles e andarei entre eles; e eu serei o seu Deus, e eles serão o meu povo.
17 Kon nag Boroom bi nee na:
17 Portanto, saí do meio deles, e separai-vos, diz o Senhor. E não toqueis em coisa imunda, e eu vos receberei;
18 Dinaa nekk baay ci yéen,
18 e serei Pai para vós, e vós sereis meus filhos e filhas, diz o Senhor Todo-Poderoso.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Coríntios 6, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.