2 Coríntios 5

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARC

Sair da comparação
ARC Almeida Revista e Corrigida 2009
1 Yaram wi nu soloo ci kaw suuf dafa mel ni ab xayma. Su daanoo, xam nanu ne Yàlla jagleel na nu am taax ci asamaan, mu loxol nit defarul, di taax muy sax ba fàww.
1 Porque sabemos que, se a nossa casa terrestre deste tabernáculo se desfizer, temos de Deus um edifício, uma casa não feita por mãos, eterna, nos céus.
2 Fi mu ne nu ngi wonk, di yàkkamtee féete ak sunu dëkkukaayu asamaan, sol ko ni koddaay, xam ne
2 E, por isso, também gememos, desejando ser revestidos da nossa habitação, que é do céu;
3 bu nu ko solee, dunu def yaramu neen.
3 se, todavia, estando vestidos, não formos achados nus.
4 Nun ñi nekk ci xayma bii, nu ngi wonk ndax coono. Du caageen ne danoo bëgga summi sunu yaramu àddina, waaye danoo bëgga sol sunu yaramu asamaan, ngir liy dee sóobu ci biir dund.
4 Porque também nós, os que estamos neste tabernáculo, gememos carregados, não porque queremos ser despidos, mas revestidos, para que o mortal seja absorvido pela vida.
5 Ki nu waajal ngir loolu moo di Yàlla, moom mi nu jox Xelam, di dawal ci cér bi mu nu dencal.
5 Ora, quem para isso mesmo nos preparou foi Deus, o qual nos deu também o penhor do Espírito.
6 Noonu kon nu ngi fees ak kóolute fu nu tollu; te xam nanu ne fi ak nu ngi dëkk ci yaram wii, àggagunu sunu màkkaan ci wetu Boroom bi—
6 Pelo que estamos sempre de bom ânimo, sabendo que, enquanto estamos no corpo, vivemos ausentes do Senhor
7 ndaxte doxewunu ab gis, waaye ngëm lanuy doxe.
7 (Porque andamos por fé e não por vista.).
8 Kon fees nanu ak kóolute, te yéenee jóge ci dëkkukaayu yaram wii, dem dëkk ci wetu Boroom bi.
8 Mas temos confiança e desejamos, antes, deixar este corpo, para habitar com o Senhor.
9 Kon nag des fi walla jóge fi, li nuy faaydaal moo di neex Boroom bi.
9 Pelo que muito desejamos também ser-lhe agradáveis, quer presentes, quer ausentes.
10 Ndaxte nun ñépp fàww nu teew ci kanam Kirist, mu àtte nu, ngir ku nekk jot peyu li mu def ci yaramam, muy lu baax walla lu bon.
10 Porque todos devemos comparecer ante o tribunal de Cristo, para que cada um receba segundo o que tiver feito por meio do corpo, ou bem ou mal.
11 Gannaaw xam nanu ragal Yàlla nag, nu ngi fexee gëmloo nit ñi, waaye li nu nekk leer na Yàlla, te yaakaar naa ne leer na leen it, ba ne fàŋŋ.
11 Assim que, sabendo o temor que se deve ao Senhor, persuadimos os homens à fé, mas somos manifestos a Deus; e espero que, na vossa consciência, sejamos também manifestos.
12 Jéemunoo waxati lu ngeen nuy nawe, waaye danu leena bëgga may yoonu tiitaru ci nun, ba am lu ngeen tontoo ñooñuy tiitaroo col gu àndul ak xol.
12 Porque não nos recomendamos outra vez a vós; mas damo-vos ocasião de vos gloriardes de nós, para que tenhais que responder aos que se gloriam na aparência e não no coração.
13 Su fekkee danoo tàggalikoo ak sunu sago, ngir Yàlla la. Su nu àndee ak sunu sago, ngir yéen la.
13 Porque, se enlouquecemos, é para Deus; e, se conservamos o juízo, é para vós.
14 Ndaxte mbëggeelu Kirist moo nuy jiite, ndax wóor na nu ne ndegam kenn rekk a dee ngir ñépp, kon ñépp a dee.
14 Porque o amor de Cristo nos constrange, julgando nós assim: que, se um morreu por todos, logo, todos morreram.
15 Te dee na ngir ñépp, ngir ñiy dund dootuñu dund ngir seen bopp, waaye ngir ki dee ci seen wàll te dekki.
15 E ele morreu por todos, para que os que vivem não vivam mais para si, mas para aquele que por eles morreu e ressuscitou.
16 Kon nag gannaaw-si-tey xoolatunu kenn ci gis-gisu àddina. Su fekkee mas nanoo xool Kirist ci gis-gisu àddina, léegi xooleetunu ko noonu.
16 Assim que, daqui por diante, a ninguém conhecemos segundo a carne; e, ainda que também tenhamos conhecido Cristo segundo a carne, contudo, agora, já o não conhecemos desse modo.
17 Kon bu nit bokkee ci Kirist, mbindeef mu bees la. Li jëkk wéy na, lu bees a fi teew.
17 Assim que, se alguém está em Cristo, nova criatura é: as coisas velhas já passaram; eis que tudo se fez novo.
18 Te loolu lépp a ngi sosoo ci Yàlla, mi nu jubale ak boppam jaare ko ci Yeesu Kirist, te sas nu nuy waare juboo googu:
18 E tudo isso provém de Deus, que nos reconciliou consigo mesmo por Jesus Cristo e nos deu o ministério da reconciliação,
19 maanaam, Yàlla jaar na ci Kirist, di jubale waa àddina ak boppam te sëfu leen seeni tooñ. Kàddug juboo googu, Yàlla dénk na nu ko.
19 isto é, Deus estava em Cristo reconciliando consigo o mundo, não lhes imputando os seus pecados, e pôs em nós a palavra da reconciliação.
20 Ay ndaw lanu, yu Kirist yónni, te Yàllaa ngi woo nit ñi jaare ko ci nun. Kon nag ci turu Kirist, nu ngi leen koy ñaan: nanguleena juboo ak Yàlla.
20 De sorte que somos embaixadores da parte de Cristo, como se Deus por nós rogasse. Rogamos-vos, pois, da parte de Cristo que vos reconcilieis com Deus.
21 Kirist mi masula def bàkkaar, Yàlla def na ko bàkkaar ci sunu wàll, ngir ci sunu bokk ci moom, nu mana doon njubteg Yàlla.
21 Àquele que não conheceu pecado, o fez pecado por nós; para que, nele, fôssemos feitos justiça de Deus.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Coríntios 5, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.