2 Coríntios 4

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Kon nag ndegam Yàlla ci yërmandeem sas na nu liggéey boobu, dunu bayliku.
1 Pelo que, tendo este ministério, assim como já alcançamos misericórdia, não desfalecemos;
2 Lànk nanoo ànd ci mbir, yi ñuy nëbb te ñu gàccelu. Sunuy tànk du yu njublaŋ te dunu dëngal kàddug Yàlla. Waaye nu ngi biral dëgg, di sàkku kóoluteg ñépp fa kanam Yàlla.
2 pelo contrário, rejeitamos as coisas ocultas, que são vergonhosas, não andando com astúcia, nem adulterando a palavra de Deus; mas, pela manifestação da verdade, nós nos recomendamos à consciência de todos os homens diante de Deus.
3 Su fekkee ne sax, xibaaru jàmm bi dafa muuru ci ñenn ñi, dafa fekk ñoom ñu aw yoon wu jëm ci sànkute.
3 Mas, se ainda o nosso evangelho está encoberto, é naqueles que se perdem que está encoberto,
4 Ñoom la yàllay jamono ji gëlëmal seen xel, ngir ñu baña gis leeru xibaaru jàmm, biy wone ndamu Kirist, mi di melokaanu Yàlla.
4 nos quais o deus deste século cegou os entendimentos dos incrédulos, para que lhes não resplandeça a luz do evangelho da glória de Cristo, o qual é a imagem de Deus.
5 Ndaxte Yeesu Kirist Boroom bi lanuy waare, waaye waarewunu lu jëm ci sunu bopp. Nun seeni jaam lanu ndax Yeesu.
5 Pois não nos pregamos a nós mesmos, mas a Cristo Jesus como Senhor; e a nós mesmos como vossos servos por amor de Jesus.
6 Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer leer ci biir lëndëm,» moo leer ci sunu xol, ngir leeral nu ak xam-xamu ndamu Yàlla, liy feeñ ci xar kanamu Kirist.
6 Porque Deus, que disse: Das trevas brilhará a luz, é quem brilhou em nossos corações, para iluminação do conhecimento da glória de Deus na face de Cristo.
7 Leer googu ci sunu xol mi ngi mel ni alal, waaye ñu ngi ko def ci nun ñi néew doole niy njaq kese, ngir kàttan gu ëpp xel gi, bawoo ci Yàlla te du ci nun.
7 Temos, porém, este tesouro em vasos de barro, para que a excelência do poder seja de Deus, e não da nossa parte.
8 Dañu nuy sonal fu nekk, waaye kenn tancu nu. Dañu nuy dugal ci ruq yi, waaye dinanu ci génn.
8 Em tudo somos atribulados, mas não angustiados; perplexos, mas não desesperados;
9 Dañu nuy fitnaal, waaye Yàlla du nu wacc mukk. Tër nañu nu, waaye kenn doggaliwu nu.
9 perseguidos, mas não desamparados; abatidos, mas não destruídos;
10 Fu nu tollu noo ngi gàddu ci sunu yaram dee gi Yeesu dee woon, ngir dundu Yeesu moom it feeñ ci sunu yaram.
10 trazendo sempre no corpo o morrer de Jesus, para que também a vida de Jesus se manifeste em nossos corpos;
11 Bés bu nekk, nun ñiy dund, ñu ngi nuy jébbal dee ndax Kirist, ngir dundu Kirist moom itam feeñ ci sunu yaram wiy dee.
11 pois nós, que vivemos, estamos sempre entregues à morte por amor de Jesus, para que também a vida de Jesus se manifeste em nossa carne mortal.
12 Noonu dee mu ngi jëf ci nun, dund di jëf ci yéen.
12 De modo que em nós opera a morte, mas em vós a vida.
13 Mbind mi nee na: «Damaa gëm, moo tax ma wax.» Nun it nag, ndegam am nanu menn xelu ngëm moomu, danoo gëm, ba tax nuy wax.
13 Ora, temos o mesmo espírito de fé, conforme está escrito: Cri, por isso falei; também nós cremos, por isso também falamos,
14 Ndaxte xam nanu ne Yàlla, mi dekkal Boroom bi Yeesu, dina nu dekkal nun itam ak Yeesu, te dina nu yóbbu ak yéen, taxawal nun ñépp ci jataayam.
14 sabendo que aquele que ressuscitou o Senhor Jesus, nos ressuscitará a nós com Jesus, e nos apresentará convosco.
15 Ndaxte lépp li nuy daj, seen njariñ a tax, ngir yiwu Yàlla, wiy yokku ci nit ñu gëna takku, yokkaale ngërëm lu jëm ci Yàlla, ngir jollil ndamam.
15 Pois tudo é por amor de vós, para que a graça, multiplicada por meio de muitos, faça abundar a ação de graças para glória de Deus.
16 Loolu moo tax sunu yaakaar du tas. Bu fekkee sax sunu yaram day yàqu jëm cig mag, sunu ruu moom, bés ak bés muy gëna yeesaat.
16 Por isso não desfalecemos; mas ainda que o nosso homem exterior se esteja consumindo, o interior, contudo, se renova de dia em dia.
17 Ndaxte sunu coono bu woyof bi dul yàgg, dafa nuy jural ndam lu bare, ba suul coono bi, tey sax abadan.
17 Porque a nossa leve e momentânea tribulação produz para nós cada vez mais abundantemente um eterno peso de glória;
18 Kon diirunu li ñuy gis waaye li ñu dul gis. Ndaxte li ñuy gis day wéy, waaye li ñu dul gis day sax ba fàww.
18 não atentando nós nas coisas que se vêem, mas sim nas que se não vêem; porque as que se vêem são temporais, enquanto as que se não vêem são eternas.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Coríntios 4, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.