2 Coríntios 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Mbaa du danoo tàmbalee tëgguwaat nag? Mbaa du danoo soxla ni ñenn ñi ay dénkaane yu ñu nuy gërëme, te ñuy bataaxal yu jóge ci yéen walla yu jëm ci yéen?
1 Começamos outra vez a recomendar-nos a nós mesmos? Ou, porventura, necessitamos, como alguns, de cartas de recomendação para vós, ou de vós?
2 Déedéet, yéenay sunu bataaxal; ci sunu xol lañu ko bind, di bataaxal bu nit ñépp mana xam te jàng ko;
2 Vós sois a nossa carta, escrita em nossos corações, conhecida e lida por todos os homens,
3 ndaxte leer na ne bataaxal bu jóge ci Kirist ngeen, bu mu jaarale ci nun. Bindeesu ko daa, waaye ci Xelum Yàlla miy dund lees ko binde; du ci àlluway doj lañu ko rëdd, waaye ci xolu doom Aadama.
3 sendo manifestos como carta de Cristo, ministrada por nós, e escrita, não com tinta, mas com o Espírito do Deus vivo, não em tábuas de pedra, mas em tábuas de carne do coração.
4 Googu kóolute lanu am fa kanam Yàlla ndax Kirist.
4 E é por Cristo que temos tal confiança em Deus;
5 Du caageen nag ne àttan nanu dara ci sunu man-man, ba nu yaakaar dara ci sunu bopp, waaye sunu kàttan ci Yàlla lay jóge.
5 não que sejamos capazes, por nós, de pensar alguma coisa, como de nós mesmos; mas a nossa capacidade vem de Deus,
6 Moo nu jox kàttan, nu nekk ndaw yuy xamle kóllëre gu bees gi. Kóllëre googu ajuwul ci ay sàrti diine, waaye mi ngi aju ci jëfu Xelum Yàlla. Ndaxte sàrti kese day jëme ci dee, waaye Xelum Yàlla dafay joxe dund.
6 o qual também nos capacitou para sermos ministros dum novo pacto, não da letra, mas do espírito; porque a letra mata, mas o espírito vivifica.
7 Ba ñu bindee arafi sàrt yi ciy àlluway doj, leeraayu ndamu Yàlla nekk fa. Xar kanamu Musaa di leer, ba bànni Israyil duñu ko mana xool, fekk leer ga di wéy. Ndegam sàrti yoon yooyuy jëme ci dee, ñoo ànd ak ndam,
7 Ora, se o ministério da morte, gravado com letras em pedras, veio em glória, de maneira que os filhos de Israel não podiam fixar os olhos no rosto de Moisés, por causa da glória do seu rosto, a qual se estava desvanecendo,
8 rawatina nag ne jëfu Xelum Yàlla dina gëna ànd ak ndam.
8 como não será de maior glória o ministério do espírito?
9 Su fekkee ne tëralin, wiy teg nit tooñ, àndoon na ak ndam, rawatina ci tëralin wiy àtte nit jub.
9 Porque, se o ministério da condenação tinha glória, muito mais excede em glória o ministério da justiça.
10 Ndaxte ndam li amoon keroog suux na ci ndam li ko raw léegi.
10 Pois na verdade, o que foi feito glorioso, não o é em comparação com a glória inexcedível.
11 Te it ndegam li wéy dafa amoon ndam, astamaak li fi sax.
11 Porque, se aquilo que se desvanecia era glorioso, muito mais glorioso é o que permanece.
12 Kon nag gannaaw wékku nanu ci yaakaar ju mel noonu, danuy waare ak kóolute gu mag.
12 Tendo, pois, tal esperança, usamos de muita ousadia no falar.
13 Dunu def ni Musaa, mi daan muur xar kanamam, ngir bànni Israyil baña gis jeexug leer googu saxul.
13 E não somos como Moisés, que trazia um véu sobre o rosto, para que os filhos de Isra desvanecia;
14 Waaye seen xel dafa daldi gumba. Ba tey jii sax, bu ñuy jàng téereb kóllëre gu jëkk gi, muuraay googu dafay des; deñul, ndaxte ci Kirist rekk la mana deñe.
14 mas o entendimento lhes ficou endurecido. Pois até o dia de hoje, à leitura do velho pacto, permanece o mesmo véu, não lhes sendo revelado que em Cristo é ele abolido;
15 Waaw, ba tey jii, su ñuy jàng yoonu Musaa, seen xol dafay muuru.
15 sim, até o dia de hoje, sempre que Moisés é lido, um véu está posto sobre o coração deles.
16 Waaye saa su kenn walbatikoo ci Boroom bi, muuraay gi daldi muriku.
16 Contudo, convertendo-se um deles ao Senhor, é-lhe tirado o véu.
17 Fekk nag Boroom, bi ñuy wax foofu, moo di Xelum Yàlla, te fu Xelu Boroom bi nekk, foofa yaatu gu mat am na fa.
17 Ora, o Senhor é o Espírito; e onde está o Espírito do Senhor aí há liberdade.
18 Nun ñépp nag, danuy lerxat ndamu Boroom bi ak xar kanam bu muuruwul, bay soppiku ci melokaanam, ànd ak ndam luy yokku te sax ci dooley Boroom biy Xelum Yàlla.
18 Mas todos nós, com rosto descoberto, refletindo como um espelho a glória do Senhor, somos transformados de glória em glória na mesma imagem, como pelo Espírito do Senhor.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Coríntios 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.