2 Coríntios 2

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARC

Sair da comparação
ARC Almeida Revista e Corrigida 2009
1 Man nag fas yéene naa lii: duma délsi ci yéen ci naqar.
1 Mas deliberei isto comigo mesmo: não ir mais ter convosco em tristeza.
2 Ndaxte su ma leen tegee naqar, kuy seral sama xol ku dul yéen ñi ma teg aw naqar?
2 Porque, se eu vos entristeço, quem é que me alegrará, senão aquele que por mim foi contristado?
3 Looloo tax ma binde noonu, ngir baña agsi, am naqar ci ñi ma waroona bégal. Am naa kóolute ci yéen ñépp ne sama mbég mooy seen mbég.
3 E escrevi-vos isso mesmo para que, quando lá for, não tenha tristeza da parte dos que deveriam alegrar-me, confiando em vós todos de que a minha alegria é a de todos vós.
4 Ci biir tiis ak xol bu jeex laa leen bind, samay bët taa ak ay rongooñ. Binduma leen ngir teg leen naqar, waaye ngir ngeen xam xóotaayu mbëggeel gi ma am ci yéen.
4 Porque, em muita tribulação e angústia do coração, vos escrevi, com muitas lágrimas, não para que vos entristecêsseis, mas para que conhecêsseis o amor que abundantemente vos tenho.
5 Su kenn tegee moroomam naqar, du man la ko teg, waaye man nanu ne yéen ñépp la ko teg —matul may réyal mbir mi.
5 Porque, se alguém me contristou, não me contristou a mim senão em parte, para vos não sobrecarregar a vós todos;
6 Àtte bi ko mbooloo mi teg, doy na.
6 basta ao tal esta repreensão feita por muitos.
7 Léegi nag baal-leen ko te dëfal xolam, ngir bañ mu sóobu ci naqar wu ëpp.
7 De maneira que, pelo contrário, deveis, antes, perdoar-lhe e consolá-lo, para que o tal não seja, de modo algum, devorado de demasiada tristeza.
8 Kon maa ngi leen di ñaan, ngeen feddali seen mbëggeel ci moom.
8 Pelo que vos rogo que confirmeis para com ele o vosso amor.
9 Nattu leen moo tax ma bind leen it, ngir seet ba xam ndax dingeen dégg ndigal ci lépp.
9 E para isso vos escrevi também, para por essa prova saber se sois obedientes em tudo.
10 Ku ngeen baal, ma baal ko itam. Man nag, su ma baalee —fekk am lu ma wara baale— yéena tax ma def ko ci kanam Kirist,
10 E a quem perdoardes alguma coisa também eu; porque o que eu também perdoei, se é que tenho perdoado, por amor de vós o fiz na presença de Cristo; para que não sejamos vencidos por Satanás,
11 ngir Seytaane baña am bunt bu mu jaar ba nax nu, ndaxte réerewunu mbir ay pexeem.
11 porque não ignoramos os seus ardis.
12 Ba ma àggee Torowas nag, ngir yégle fa xibaaru jàmm bi ci Kirist, Boroom bi ubbil na ma ci bunt.
12 Ora, quando cheguei a Trôade para pregar o evangelho de Cristo e abrindo-se-me uma porta no Senhor,
13 Waaye sama xel dalul benn yoon, ndax li ma fa fekkul sama mbokk, Tit. Noonu nag ma tàggu leen, daldi dem diiwaanu Maseduwan.
13 não tive descanso no meu espírito, porque não achei ali meu irmão Tito; mas, despedindo-me deles, parti para a Macedônia.
14 Waaye cant ñeel na Yàlla! Ci sunu booloo ak Kirist, daf nuy yóbbaale saa su nekk ci gawari ndamam, tey jaar ci nun ngir turu Kirist jolli fu nekk, ni xetu latkoloñ di tasaaroo.
14 E graças a Deus, que sempre nos faz triunfar em Cristo e, por meio de nós, manifesta em todo lugar o cheiro do seu conhecimento.
15 Ndaxte ci Yàlla, xetu Kirist gu neex lanu, di gilli jëm ci ñiy mucc ak ñiy sànku;
15 Porque para Deus somos o bom cheiro de Cristo, nos que se salvam e nos que se perdem.
16 ci ñu mujj ñii, xet gu sedd lanu, guy jëme ci dee; ci ñu jëkk ñi, xetu dund lanu, guy jëme ci dund. Ku mana àttan yen boobu!
16 Para estes, certamente, cheiro de morte para morte; mas, para aqueles, cheiro de vida para vida. E, para essas coisas, quem é idôneo?
17 Nun nag melunu ni ñu bare, ñiy baana-baana ci kàddug Yàlla, waaye ci sunu booloo ak Kirist, nu ngi waare ak xol bu laab fa kanam Yàlla, ni yonenti Yàlla.
17 Porque nós não somos, como muitos, falsificadores da palavra de Deus; antes, falamos de Cristo com sinceridade, como de Deus na presença de Deus.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Coríntios 2, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.