2 Coríntios 12
Téereb Injiil (WOL2010) vs ARC
1 Damu amul njariñ, ba tey war na ma. Kon ma jàll ci nettali gis-gisi Boroom bi ak i peeñu.
1 Em verdade que não convém gloriar-me; mas passarei às visões e revelações do Senhor.
2 Xam naa taalibeb Kirist boo xam ne yékkati nañu ko ba ca asamaan, si gëna kawe, booba ak léegi mat na fukki at ak ñeent. Xawma ndax ànd na ak jëmmam walla déet. Yàlla rekk a xam.
2 Conheço um homem em Cristo que, há catorze anos (se no corpo, não sei; se fora do corpo, não sei; Deus o sabe), foi arrebatado até ao terceiro céu.
3 — ausente —
3 E sei que o tal homem (se no corpo, se fora do corpo, não sei; Deus o sabe)
4 — ausente —
4 foi arrebatado ao paraíso e ouviu palavras inefáveis, de que ao homem não é lícito falar.
5 Dinaa damu ci nit ku mel noonu. Waaye duma damu ci sama bopp, lu dul liy wone sama néew doole.
5 De um assim me gloriarei eu, mas de mim mesmo não me gloriarei, senão nas minhas fraquezas.
6 Su ma bëggoona damu, du doon yëfi dof, ndaxte dëgg laay wax. Waaye damay moytoo damu, ngir kenn baña foog ci man lu weesu li mu gis, may def, te muy dégg, ma di ko wax.
6 Porque, se quiser gloriar-me, não serei néscio, porque direi a verdade; mas deixo isso, para que ninguém cuide de mim mais do que em mim vê ou de mim ouve.
7 Te it ngir ma baña yég sama bopp ndax peeñu yooyu wees xel, mayees na mbir dal ma ci sama yaram, di ma mitital ni dég, muy malaakam Seytaane mu may sonal, ngir ma baña yég sama bopp.
7 E, para que me não exaltasse pelas excelências das revelações, foi-me dado um espinho na carne, a saber, um mensageiro de Satanás, para me esbofetear, a fim de não me exaltar.
8 Ñaan naa Boroom bi ñetti yoon ci mbir moomu, ngir mu teqale ma ak moom.
8 Acerca do qual três vezes orei ao Senhor, para que se desviasse de mim.
9 Mu ne ma: «Sama yiw doy na la; sama kàttan a ngi mate cig néew doole.» Kon nag dëgg-dëgg, gën na maa bég ci damu ndax sama néew doole, ngir kàttanu Kirist dëkk ci man.
9 E disse-me: A minha graça te basta, porque o meu poder se aperfeiçoa na fraqueza. De boa vontade, pois, me gloriarei nas minhas fraquezas, para que em mim habite o poder de Cristo.
10 Looloo tax may bég ci néew doole, yi may wéye ngir turu Kirist, ciy tiis, ciy njàqare, mbaa ñu saaga ma, mbaa ñu fitnaal ma. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laay am kàttan.
10 Pelo que sinto prazer nas fraquezas, nas injúrias, nas necessidades, nas perseguições, nas angústias, por amor de Cristo. Porque, quando estou fraco, então, sou forte.
11 Ci dëgg-dëgg wax naa waxi dof te yéena ma ci dugal, fekk yéen ci seen bopp sax yéena ma waroona sargal, ndaxte su ma dul dara sax, seen ndaw yooyu ngeen naw ëpplewuñu ma dara.
11 Fui néscio em gloriar-me; vós me constrangestes; porque eu devia ser louvado por vós, visto que em nada fui inferior aos mais excelentes apóstolos, ainda que nada sou.
12 Kéemaan yi, jaloore yi ak jëf yu màgg, yiy firndeel ndawul Kirist, feeñ nañu ci seen biir, ma ànd ci ak muñ gu mat.
12 Os sinais do meu apostolado foram manifestados entre vós, com toda a paciência, por sinais, prodígios e maravilhas.
13 Lan laa defal yeneen mboolooy ñi gëm te defaluma leen ko, xanaa rekk li ma wéeru ci ñoom te wéeruwuma ci yéen? Baal-leen ma googu tooñ!
13 Porque, em que tendes vós sido inferiores às outras igrejas, a não ser que eu mesmo vos não fui pesado? Perdoai-me este agravo.
14 Maa ngi leen di waaja ganesi ñetteel bi yoon, te duma wéeru ci yéen. Wutsiwuma seen alal, yéen laa soxla. Ndaxte du gone moo wara yor waajuram, waaye waajur moo wara yor gone yi.
14 Eis aqui estou pronto para, pela terceira vez, ir ter convosco e não vos serei pesado; pois que não busco o que é vosso, mas, sim, a vós; porque não devem os filhos entesourar para os pais, mas os pais, para os filhos.
15 Man nag nangu naa joxe li ma am lépp ak xol bu sedd, ba joxe sama bopp sax, ngir dimbali leen. Gannaaw bëgg naa leen nii, xanaa kay seen mbëggeel ci man warula wàññiku?
15 Eu, de muito boa vontade, gastarei e me deixarei gastar pelas vossas almas, ainda que, amando-vos cada vez mais, seja menos amado.
16 Kon noonu la, nekkuma woon yen ci yéen. Waaye man na am ñu naan, dama leena nax, ba réeral leen ci sama njublaŋ.
16 Mas seja assim, eu não vos fui pesado; mas, sendo astuto, vos tomei com dolo.
17 Ndax damaa lekk seen alal, jaare ko ci kenn ci ñi ma yónni woon?
17 Porventura, aproveitei-me de vós por algum daqueles que vos enviei?
18 Sant naa Tit, mu ñëw ci yéen, te yebal naa sunu mbokk moomu ak moom. Ndax Tit dafa lekk seen alal? Man ak moom, ndax bokkunu woon xel mu nu yékkati ak tànk yu nuy dox?
18 Roguei a Tito e enviei com ele um irmão. Porventura, Tito se aproveitou de vós? Não andamos, porventura, no mesmo espírito, sobre as mesmas pisadas?
19 Xanaa diirub li ngeen di jàng lii, defe ngeen ne nu ngi wut aw lay ci seen kanam. Samay xarit, nu ngi leen di wax ci kanam Yàlla ak ci turu Kirist; te lépp ngir seen njariñ la.
19 Cuidais que ainda nos desculpamos convosco? Falamos em Cristo perante Deus, e tudo isto, ó amados, para vossa edificação.
20 Ragal naa, bu ma ñëwee ci yéen, fekk leen nu ma neexul, te yéen it ngeen fekk ma nu leen neexul. Ragal naa fekk ay xuloo ci seen biir, ak ñeetaane, xadar ak diiroo mbagg, xas ak jëw, réy-réylu ak yëngu-yëngu.
20 Porque receio que, quando chegar, vos não ache como eu quereria, e eu seja achado de vós como não quereríeis, e que de alguma maneira haja pendências, invejas, iras, porfias, detrações, mexericos, orgulhos, tumultos;
21 Ragal naa, bu ma leen ganesiwaatee, Yàlla sama Boroom suufeel ma ci seen biir, ma naqarlu ci ñu bare ñu bàkkaaroon te dëdduwuñu seen yàqute, seen njaaloo ak seen ñaawteef, gi ñu doon def.
21 que, quando for outra vez, o meu Deus me humilhe para convosco, e eu chore por muitos daqueles que dantes pecaram e não se arrependeram da imundícia, e prostituição, e desonestidade que cometeram.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Coríntios 12, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.