2 Coríntios 11
Téereb Injiil (WOL2010) vs VC
1 Céy bu ngeen ma manoona muñal, ma wax leen tuuti waxi dof! Waaw, muñal-leen ma sax.
1 Oxalá suportásseis um pouco de loucura de minha parte! Oh, sim! Tolerai-me.
2 Dama leen di fiire ak fiiraange gu jóge ca Yàlla, ndaxte dama leena bëgga jébbal jenn jëkkër kepp, muy Kirist, ngeen set ni janq.
2 Eu vos consagro um carinho e amor santo, porque vos desposei com um esposo único e vos apresentei a Cristo como virgem pura.
3 Waaye ni jaan ja naxe woon Awa ci pexeem, ragal naa yéen itam ñu lëmbaaje ni seen xel, ba ngeen dëddu xol bu laab, bi ngeen amoon ci seen diggante ak Kirist.
3 Mas temo que, como a serpente enganou Eva com a sua astúcia, assim se corrompam os vossos pensamentos e se apartem da sinceridade para com Cristo.
4 Ndaxte bu kenn ñëwee, di leen waar ci Yeesu ci lu juuyoo ak li nu leen yégal, walla ngeen jot meneen xel mu wuute ak Xel mi ngeen jot, walla ngeen nangu beneen xibaar bu wuute ak bi ngeen dégg, dingeen ko dékku bu baax.
4 Porque quando aparece alguém pregando-vos outro Jesus, diferente daquele que vos temos pregado, ou se trata de receber outro espírito, diferente do que haveis recebido, ou outro evangelho, diverso do que haveis abraçado, de boa mente o aceitais.
5 Moona foog naa ne seen ndaw yooyu ngeen yékkati, ba ñu ëpp ndaw sax, ëpplewuñu ma dara.
5 Mas penso que em nada tenho sido inferior a esses eminentes apóstolos!
6 Bu ma dul jàmbaari wax it, néewuma xam-xam, te won nanu leen ko ci bépp mbir ak ci bépp fànn.
6 Pois, embora eu seja de pouca eloqüência, não acontece o mesmo quanto à ciência: é o que em tudo e a cada passo vos temos manifestado.
7 Walla boog ndax dama leena tooñ ci li ma suufeel sama bopp ngir yékkati leen, ba ma leen di yégal xibaaru jàmm bi te laajuma leen genn pey?
7 Porventura cometi alguma falta, em vos ter pregado o Evangelho de Deus gratuitamente, humilhando-me para vos exaltar?
8 Xanaa kay damaa tooñ ci li ma dunde alalu yeneen mboolooy ñi gëm, ba futti leen, ngir dimbali leen, yéen.
8 Para vos servir, despojei outras igrejas, recebendo delas o meu sustento.
9 Te ba ma nekkee ci yéen te soxla dab ma, wéeruwuma ci kenn ci yéen, ndaxte bokk ya jóge Maseduwan ñoo ma indil li ma soxla woon. Ci lépp moytu naa nekk yen ci yéen, te dinaa ko gëna def.
9 Estando convosco e passando alguma necessidade, não fui pesado a ninguém, porque os irmãos que vieram da Macedônia supriram o que me faltava. Em tudo me guardei e me guardarei de vos ser pesado.
10 Ni mu wóore ne dëggug Kirist nekk na ci man, ni la wóore ne loolii may damoo, kenn du ko teggi ci diiwaanu Akayi gépp.
10 Tão certo como a verdade de Cristo está em mim, não me será tirada esta glória nas regiões de Acaia.
11 Lu tax? Ndax dama leena bëggul? Yàlla xam na ne bëgg naa leen!
11 E por quê?... Será por que não vos amo? Deus o sabe!
12 Noonu may doxale nag dinaa ci sax, ngir ñiy damu, di wut yoon wu ñu aw ba yemale seen bopp ak nun, duñu ko am.
12 Mas o que faço, continuarei a fazer, para cortar pela raiz todo pretexto àqueles que procuram algum pretexto para se envaidecerem e se afirmarem iguais a nós.
13 Ay ndawi naaféq lañu, di ay liggéeykat yu njublaŋ yuy mbubboo turu ndawi Kirist.
13 Esses tais são falsos apóstolos, operários desonestos, que se disfarçam em apóstolos de Cristo,
14 Te loolu jaaxalu nu, ndaxte Seytaane moom ci boppam day mbubboo malaakam leer.
14 o que não é de espantar. Pois, se o próprio Satanás se transfigura em anjo de luz,
15 Kon nag ay ndawam mbubboo ndawi njub, loolu du nu jaaxal. Dees na leen fey seeni jëf.
15 parece bem normal que seus ministros se disfarcem em ministros de justiça, cujo fim, no entanto, será segundo as suas obras.
16 Maa ngi leen koy waxaat: bu ma kenn jàpp nib dof. Walla boog bu ngeen ma ko jàppee, séddleen ma céru dof, ngir ma damu tuuti, man itam.
16 Repito: não me queiram tomar por um louco. No mínimo, aceitai-me como tal, para que também eu possa me gloriar!
17 Loolu may wax nag, waxuma ko ci turu Boroom bi. Bu ma ñemee damoo nii, maa ngi wax ni dof.
17 O que vou dizer, na certeza de poder gloriar-me, não o digo sob a inspiração do Senhor, mas como num acesso de delírio.
18 Ndegam ñu bare dañuy damu ni nit kese, man itam kon dinaa damu.
18 Porque muitos se gloriam segundo a carne, também eu me gloriarei.
19 Yéen boroom xel yi, aka ngeena mana muñal ñi dof,
19 Vós, sendo homens sensatos, suportais de boa mente os loucos...
20 nde yéena ngi muñ ñi leen di jaamloo, di lekk seen alal, di leen nax, di leen xeeb, di leen talaata!
20 Sim, tolerais a quem vos escraviza, a quem vos devora, a quem vos faz violência, a quem vos trata com orgulho, a quem vos dá no rosto.
21 Sunu néew doole mayu nu, nu dem ba jëfe noonu; rus naa ci lool de!
21 Sinto vergonha de o dizer; temos mostrado demasiada fraqueza... Entretanto, de tudo aquilo de que outrem se ufana {falo como um insensato}, disto também eu me ufano.
22 Ndax Ebrë lañu? Man it Ebrë laa. Ndax bànni Israyil lañu? Man itam ci laa. Ndax sëti Ibraayma lañu? Man itam moom laa.
22 São hebreus? Também eu. São israelitas? Também eu.
23 Ndax surgay Kirist lañu? —maa ngi wax waxi ku tàggoo ak sagoom nag— maa leen ko gëna doon. Bu dee ci liggéey, maa leen ci man. Bu dee ci li ñu nu tëj ci kaso, maa leen ko gëna miin. Bu dee ci li ñu nu dóor ay yar, maa leen ëpple. Leru naa dee ba tàyyi.
23 São ministros de Cristo? Falo como menos sábio: eu, ainda mais. Muito mais pelos trabalhos, muito mais pelos cárceres, pelos açoites sem medida. Muitas vezes vi a morte de perto.
24 Juróomi yoon Yawut yi dóor nañu ma fanweeri yar ak juróom ñeent.
24 Cinco vezes recebi dos judeus os quarenta açoites menos um.
25 Ñetti yoon dóorees na ma ay yet, te mas nañu maa sànni ay xeer, bëgg maa rey. Ñetti yoon dugg naa gaal, mu suux. Mas naa yendu ci ndox, fanaan ci.
25 Três vezes fui flagelado com varas. Uma vez apedrejado. Três vezes naufraguei, uma noite e um dia passei no abismo.
26 Ci sama tukki yu bare yi daan naa faral di daje ak musiba ci dex yi, ak musiba ci sàcc yi, musiba mu jóge ci sama xeet walla ci ñi dul Yawut, musiba ci biir dëkk yi, ci màndiŋ yi, ci géej gi, ci biir bokki taalibe yu naaféq yi.
26 Viagens sem conta, exposto a perigos nos rios, perigos de salteadores, perigos da parte de meus concidadãos, perigos da parte dos pagãos, perigos na cidade, perigos no deserto, perigos no mar, perigos entre falsos irmãos!
27 Sonn naa, di ñaq, di fanaane xool, di xiif ak a mar tey fande, di dékku liw te rafle,
27 Trabalhos e fadigas, repetidas vigílias, com fome e sede, freqüentes jejuns, frio e nudez!
28 waxaalewuma li ci des nag: bés bu nekk maa ngi xalaat mboolooy ñi gëm.
28 Além de outras coisas, a minha preocupação cotidiana, a solicitude por todas as igrejas!
29 Ana ku ci néew doole, te wàlluma ko? Ana ku ci bàkkaar, te awma naqar wu tiis?
29 Quem é fraco, que eu não seja fraco? Quem sofre escândalo, que eu não me consuma de dor?
30 Su ma damu waree kon, ci sama néew doole laay damoo.
30 Se for preciso que a gente se glorie, eu me gloriarei na minha fraqueza.
31 Yàlla Baayu sunu Boroom Yeesu, moom mi màgg ba fàww, xam na ne du ay fen ci man.
31 Deus, Pai de nosso Senhor Jesus Cristo, que é bendito pelos séculos, sabe que não minto.
32 Ba ma nekkee dëkku Damaas, boroom dëkk ba, di jawriñu buur ba Aretas, dafa santaane woon ñuy wottu dëkk ba, ngir man maa jàpp.
32 Em Damasco, o governador do rei Aretas mandou guardar a cidade dos damascenos para me prender.
33 Waaye dugalees na ma ci dàmba, jaarale ma ci palanteeru miiri dëkk ba, yoor ma ci suuf. Noonu ma rëcc ko.
33 Mas, dentro de um cesto, desceram-me por uma janela ao longo da muralha, e assim escapei das suas mãos.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Coríntios 11, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.