2 Coríntios 10

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 — ausente —
1 Ora eu mesmo, Paulo, vos rogo pela mansidão e benignidade de Cristo, eu que, na verdade, quando presente entre vós, sou humilde, mas quando ausente, ousado para convosco;
2 — ausente —
2 sim, eu vos rogo que, quando estiver presente, não me veja obrigado a usar, com confiança, da ousadia que espero ter para com alguns que nos julgam como se andássemos segundo a carne.
3 Dëgg la ne nit rekk lanu, waaye dunu xeexe ni nit.
3 Porque, embora andando na carne, não militamos segundo a carne,
4 Ndaxte gànnaay, yi nuy xaree, jógewuñu ci nit, waaye ca Yàlla lañu jóge, te ànd ak kàttan, ngir daaneel ay tata. Danuy daaneel xalaat yi dul dëgg
4 pois as armas da nossa milícia não são carnais, mas poderosas em Deus, para demolição de fortalezas;
5 ak bépp tiitar buy jànkoonteek xam-xamu Yàlla, te danuy not bépp xalaat, ba mu déggal Kirist.
5 derribando raciocínios e todo baluarte que se ergue contra o conhecimento de Deus, e levando cativo todo pensamento à obediência a Cristo;
6 Te fas yéene nanoo jubbanti képp ku déggadi, bés bu seen dégg ndigal matee.
6 e estando prontos para vingar toda desobediência, quando for cumprida a vossa obediência.
7 Xool-leen mbir mi ne fàŋŋ. Bu amee ku mu wóor ne ci Kirist la bokk, na jàpp it ne su bokkee ci Kirist, nun itam ci Kirist lanu bokk.
7 Olhais para as coisas segundo a aparência. Se alguém confia de si mesmo que é de Cristo, pense outra vez isto consigo, que, assim como ele é de Cristo, também nós o somos.
8 Awma lu may rus, su may damu lu ëpp ci sañ-sañ bi nu Boroom bi jox, di sañ-sañu yokk seen ngëm, te du ngir seen kasara.
8 Pois, ainda que eu me glorie um tanto mais da nossa autoridade, a qual o Senhor nos deu para edificação, e não para vossa destruição, não me envergonharei;
9 Ba tey bëgguma ngeen xalaat ne maa ngi leen di xëbal ci samay bataaxal.
9 para que eu não pareça como se quisera intimidar-vos por cartas.
10 Ndaxte am na ku naan: «Ay bataaxalam dañoo ñagas te am doole, waaye bu teewee dafay ñàkk fulla, di wax waxi picc.»
10 Porque eles dizem: As cartas dele são graves e fortes, mas a sua presença corporal é fraca, e a sua palavra desprezível.
11 Kiy wax loolu na xam lii: ni sunuy kàddu mel ci sunuy bataaxal, bu nu fa nekkul, noonu it lanuy mel ci sunuy jëf, bu nu teewee.
11 Considere o tal isto, que, quais somos no falar por cartas, estando ausentes, tais seremos também no fazer, estando presentes,
12 Ñemewunoo féetale walla méngale sunu bopp ak ñooñu naw seen bopp. Ci li ñuy sàkk ab natt ngir natt ak méngale seen bopp ak seen bopp, ñàkk xel a tax.
12 pois não ousamos contar-nos, ou comparar-nos com alguns, que se louvam a si mesmos; mas estes, medindo-se consigo mesmos e comparando-se consigo mesmos, estão sem entendimento.
13 Nun nag dunu damu ci lu weesu dayo. Nu ngi damu ci liggéey bi nu Yàlla sas, ba may nu, nu agsi ci yéen.
13 Nós, porém, não nos gloriaremos além da medida, mas conforme o padrão da medida que Deus nos designou para chegarmos mesmo até vós;
14 Bu sunu sas agsiwul woon ba ci yéen, kon man nanoo ne génn nanu sas wi nu Yàlla sas. Waaye agsi na ba ci yéen, te indil nanu leen xibaaru jàmm bi jëm ci Kirist.
14 porque não nos estendemos além do que convém, como se não chegássemos a vós, pois já chegamos também até vós no evangelho de Cristo,
15 Kon nag dunu jéggi dig yi Yàlla rëdd, bay damu ci liggéeyu ñeneen. Waaye am nanu yaakaar ne su seen ngëm yokkoo, dinanu gëna màgg ci seen biir, des ba tey ci dig yi nu Yàlla rëddal.
15 não nos gloriando além da medida em trabalhos alheios; antes tendo esperança de que, à proporção que cresce a vossa fé, seremos nós cada vez mais engrandecidos entre vós, conforme a nossa medida,
16 Noonu dinanu mana yégle xibaaru jàmm bi ci bérab, yi leen féete gannaaw, te baña damu ci li ñeneen ñi def ci seen sas.
16 para anunciar o evangelho nos lugares que estão além de vós, e não em campo de outrem, para não nos gloriarmos no que estava já preparado.
17 Waaye ni ko Mbind mi waxe: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi.»
17 Aquele, porém, que se gloria, glorie-se no Senhor.
18 Ndaxte ki neex Yàlla, du ki naw boppam, waaye ki Yàlla gërëm.
18 Porque não é aprovado aquele que se recomenda a si mesmo, mas sim aquele a quem o Senhor recomenda.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 2 Coríntios 10, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.