1 Tessalonicenses 5

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Waaye bokk yi, ci li jëm ci jamono yi ak waxtu, yi loolu di am, matul nu leen ciy bind dara.
1 Mas, irmãos, acerca dos tempos e das épocas não necessitais de que se vos escreva:
2 Ndaxte xam ngeen bu wér ne ni sàcc di ñëwe guddi, noonu la bésu Boroom bi di ñëwe.
2 porque vós mesmos sabeis perfeitamente que o dia do Senhor virá como vem o ladrão de noite;
3 Fekk nit ñiy naan: «Lépp a ngi ci jàmm, ba ne leww,» booba musiba bett leen, ni aw mat di bette jigéenu biir, te kenn du ci mucc.
3 pois quando estiverem dizendo: Paz e segurança! então lhes sobrevirá repentina destruição, como as dores de parto àquela que está grávida; e de modo nenhum escaparão.
4 Waaye yéen bokk yi, nekkuleen cig lëndëm, ba tax bés boobu bett leen ni sàcc.
4 Mas vós, irmãos, não estais em trevas, para que aquele dia, como ladrão, vos surpreenda;
5 Ndaxte yéen ñépp ci leer ak bëccëg ngeen bokk; bokkunu ci guddi ak lëndëm.
5 porque todos vós sois filhos da luz e filhos do dia; nós não somos da noite nem das trevas;
6 Kon nag bunu nelaw ni ñeneen ñi, waaye nanu xool te maandu.
6 não durmamos, pois, como os demais, antes vigiemos e sejamos sóbrios.
7 Ndaxte ñiy nelaw, guddi lañuy nelaw, te ñiy màndi, guddi lañuy màndi.
7 Porque os que dormem, dormem de noite, e os que se embriagam, embriagam-se de noite;
8 Waaye nun ñiy waa bëccëg, nanu maandu te ràngoo ngir xare bi: ngëm ak mbëggeel, muy kiiraayu dënn, ak kóoluteg mucc, muy mbaxanam xare.
8 mas nós, porque somos do dia, sejamos sóbrios, vestindo-nos da couraça da fé e do amor, e tendo por capacete a esperança da salvação;
9 Ndaxte Yàlla jaglewu nu meram, waaye mucc la nu jagleel ndax darajay sunu Boroom Yeesu Kirist.
9 porque Deus não nos destinou para a ira, mas para alcançarmos a salvação por nosso Senhor Jesus Cristo,
10 Deeyal na nu, ngir nu mana dund ak moom, bu nu nelawee ak bu nu nelawagul.
10 que morreu por nós, para que, quer vigiemos, quer durmamos, vivamos juntamente com ele.
11 Kon nag nangeen dëgëralante te yokkante seen ngëm, ni ngeen koy defe.
11 Pelo que exortai-vos uns aos outros e edificai-vos uns aos outros, como na verdade o estais fazendo.
12 Gannaaw loolu bokk yi, ci lu jëm ci njiit, yi Boroom bi teg ci seen kanam te ñuy liggéey ci seen biir, di leen artu, maa ngi leen di ñaan ngeen déglu leen;
12 Ora, rogamo-vos, irmãos, que reconheçais os que trabalham entre vós, presidem sobre vós no Senhor e vos admoestam;
13 rax-ca-dolli ngeen naw leen seen kem kàttan te bëgg leen ndax seen liggéey. Na jàmm am ci seen biir.
13 e que os tenhais em grande estima e amor, por causa da sua obras. Tende paz entre vós.
14 Bokk yi, nu ngi leen di dénk, ngeen yedd ñi feñaag, dëfal ñi seen yasara yàcciku, dimbali ñi néew doole, tey muñal ñépp.
14 Exortamo-vos também, irmãos, a que admoesteis os insubordinados, consoleis os desanimados, ampareis os fracos e sejais longânimos para com todos.
15 Saxleen ci baax ci seen biir ak ci ñépp, te baña feyantoo.
15 Vede que ninguém dê a outrem mal por mal, mas segui sempre o bem, uns para com os outros, e para com todos.
16 Deeleen bég
16 Regozijai-vos sempre.
17 te sax ciy ñaan Yàlla,
17 Orai sem cessar.
18 di ko gërëm ci lépp, ndaxte loolu mooy coobarey Yàlla ci yéen ci seen bokk ci Kirist Yeesu.
18 Em tudo dai graças; porque esta é a vontade de Deus em Cristo Jesus para convosco.
19 Buleen fey taalu Xelum Yàlla,
19 Não extingais o Espírito;
20 di xeeb waxu yonent yi.
20 não desprezeis as profecias,
21 Waaye seetleen mbir yépp, jàpp ci li baax,
21 mas ponde tudo à prova. Retende o que é bom;
22 dëddu lépp lu ci bon.
22 Abstende-vos de toda espécie de mal.
23 Yal na leen Yàlla miy Boroom jàmm sellal, ba ngeen mat sëkk; yal na sàmm seen xel mépp, seen xol bépp ak seen yaram wépp, ngir dara bañ cee am sikk, ba bés bu sunu Boroom Yeesu Kirist délsee.
23 E o próprio Deus de paz vos santifique completamente; e o vosso espírito, e alma e corpo sejam plenamente conservados irrepreensíveis para a vinda de nosso Senhor Jesus Cristo.
24 Yàlla, mi leen woo ci loolu, kuy sàmm kóllëre la, te dina ko def.
24 Fiel é o que vos chama, e ele também o fará.
25 Bokk yi, buleen nu fàtte ci seeni ñaan.
25 Irmãos, orai por nós.
26 Nuyul-leen nu bokk yépp ak saafoonte bu laab.
26 Saudai a todos os irmãos com ósculo santo.
27 Maa ngi leen di dénk ci kanam Boroom bi, ngeen jàngal bataaxal bii bokk yépp.
27 Pelo Senhor vos conjuro que esta epístola seja lida a todos os irmãos.
28 Yal na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen.
28 A graça de nosso Senhor Jesus Cristo seja convosco.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Tessalonicenses 5, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.