1 Tessalonicenses 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs BKJ

Sair da comparação
1 Kon nag, ba nu ko manatula dékku, nangu nanu ñu bàyyi nu, nun doŋŋ, ca dëkku Aten,
1 Pelo que, não podendo esperar mais, achamos por bem ficar sós em Atenas;
2 te yónni nanu Timote, sunu mbokk ak sunu nawle ci liggéeyu Yàlla ak ci waareb xibaaru Kirist. Yónni nanu ko, ngir mu dénk leen, tey feddali seen ngëm,
2 e enviamos Timóteo, nosso irmão, e ministro de Deus, e nosso cooperador no evangelho de Cristo, para vos consolidar e vos consolar acerca da vossa fé;
3 ngir kenn baña raf ndax nattu, yi ngeen di jaar. Yéen ci seen bopp xam ngeen ne nattu mooy sunu cér.
3 para que nenhum homem se comova por estas aflições; porque vós mesmos sabeis que para isto fomos ordenados;
4 Ba nu nekkee ak yéen sax, waxoon nanu leen, waxati ko ne fàww nu sonn; te noonu la ame, yéen xam ngeen ko.
4 porque verdadeiramente, estando ainda convosco, vos dizíamos antes que havíamos de sofrer tribulação, como sucedeu, e vós o sabeis.
5 Noonu ba ma ko manatula dékku, yónnee naa, ngir xam fu seen ngëm tollu, ngir ragal Seytaane fiir leen, ba sunu ñaq neen.
5 Por esta causa, não podendo eu também esperar mais, mandei-o saber da vossa fé, temendo que o tentador vos tentasse, e o nosso trabalho viesse a ser em vão.
6 Waaye léegi Timote bawoo na ci yéen, indaale xibaar yu neex ci seen ngëm ak seen mbëggeel; xamal na nu ne yéena ngi am pàttaliku yu rafet ci nun te namm nu lool, ni nu leen namme, yéen itam.
6 Mas agora, vindo Timóteo de vós para nós e trazendo-nos boas novas da vossa fé e caridade, e de como sempre tendes boa lembrança de nós, desejando muito ver-nos, como nós também de ver-vos,
7 Noonu bokk yi, ci biir tiis ak coono yi nu nekk, seen ngëm dëfal na sunu xol.
7 portanto, irmãos, ficamos consolados acerca de vós, em toda a nossa aflição e angústia, pela vossa fé,
8 Ndaxte noo ngi dund dëgg-dëgg, ndegam yéena ngi sax ci Boroom bi.
8 porque agora vivemos, se estais firmes no Senhor.
9 Ndaw cant yu bare yu nu wara sant Yàlla ndax yéen! Ndaw mbég mu bare, mi nu am ci kanamam ndax yéen!
9 Por que ação de graças poderemos dar a Deus por vós, por toda a alegria com que nos regozijamos por vossa causa diante do nosso Deus,
10 Guddi ak bëccëg nu ngi wàkkirlu ci ñaan Yàlla may nu nu gis leen, ba mana mottali seen ngëm.
10 orando insistentemente dia e noite, para que possamos ver o vosso rosto e aperfeiçoemos o que falta à vossa fé?
11 Yal na Yàlla sunu Baay moom ci boppam ak Yeesu sunu Boroom jubal sunu yoon ci yéen.
11 Ora, o próprio Deus e nosso Pai e nosso Senhor Jesus Cristo dirija nosso caminho até vós.
12 Yal na leen Boroom bi dolli mbëggeel gu tar, ngeen bëggante te bëgg ñépp, ni nu leen bëgge nun.
12 E o Senhor vos aumente e faça crescer e abundar em amor uns para com os outros e para com todos os homens, como também nós o fazemos para convosco;
13 Yal na Boroom bi samp seeni xol noonu ci sellaay gu amul sikk fa kanam Yàlla sunu Baay, ba bés bu Yeesu sunu Boroom délsee, ànd ak gaayam yu sell yépp.
13 ao final, ele pode estabelecer os vossos corações, para que sejais irrepreensíveis em santidade diante de Deus, nosso Pai, na vinda de nosso Senhor Jesus Cristo, com todos os seus santos.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Tessalonicenses 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.