1 Timóteo 5
Téereb Injiil (WOL2010) vs ARC
1 Bul gëdd mag, waaye waxtaanal ak moom ni sa baay. Ndaw it, nga digal ko ni sa rakk,
1 Não repreendas asperamente os anciãos, mas admoesta-os como a pais; aos jovens, como a irmãos;
2 jigéen ju mag, def ko ni sa yaay; ju ndaw, ni sa jigéen ak cell gu mat sëkk.
2 às mulheres idosas, como a mães, às moças, como a irmãs, em toda a pureza.
3 Ci wàllu ñi seen jëkkër faatu nag, ku ci sësul ci kenn, teral ko ngir Yàlla.
3 Honra as viúvas que verdadeiramente são viúvas.
4 Waaye ku ci am ay doom mbaa ay sët, na njaboot googu jëkka wone seen ragal Yàlla ci seen biir kër, ci delloo njukkal seen waajur, ndaxte loolu lu rafet la fa kanam Yàlla.
4 Mas, se alguma viúva tiver filhos ou netos, aprendam primeiro a exercer piedade para com a sua própria família e a recompensar seus pais; porque isto é bom e agradável diante de Deus.
5 Jigéen ju sësul ci kenn day wékk yaakaaram jépp ci Yàlla, sax ci di ko wéetal te di ko ñaan guddi ak bëccëg.
5 Ora, a que é verdadeiramente viúva e desamparada espera em Deus e persevera de noite e de dia em rogos e orações;
6 Waaye ki bànneex jiital, ndee luy dox la.
6 mas a que vive em deleites, vivendo, está morta.
7 Dénk leen loolu, ngir ñu baña am benn gàkk.
7 Manda, pois, estas coisas, para que elas sejam irrepreensíveis.
8 Ndaxte ki defalul ay bokkam dara, rawatina ay waajuram, weddi na yoonu ngëm wi, ba yées ku gëmadi.
8 Mas, se alguém não tem cuidado dos seus e principalmente dos da sua família, negou a fé e é pior do que o infiel.
9 Ku bëgga bindu ci ñi seen jëkkër faatu, nii la wara mel: war na wees juróom benn fukki at, di jigéen ju yemoon ci jëkkëram,
9 Nunca seja inscrita viúva com menos de sessenta anos, e só a que tenha sido mulher de um só marido;
10 te mu ràññiku ci jëf yu rafet yu deme ni yar ay goneem, man gan, geestu gaayi Yàlla yu sell yi, dimbali ñi nekk ci tiis; maanaa di ku takku ci mboolem jëf yu rafet yi.
10 tendo testemunho de boas obras, se criou os filhos, se exercitou hospitalidade, se lavou os pés aos santos, se socorreu os aflitos, se praticou toda boa obra.
11 Waaye bul bind jigéen ju ndaw, ndaxte bu ko ay bëgg-bëggam xiiree ci sore Kirist, dina bëgga séyaat,
11 Mas não admitas as viúvas mais novas, porque, quando se tornam levianas contra Cristo, querem casar-se;
12 te dina daje ak mbugal ndaxte fecci na kóllëre.
12 tendo já a sua condenação por haverem aniquilado a primeira fé.
13 Te du yem ci bëgga séyaat rekk, waaye ku tayel lay doon; di ku wër kër ak kër, rax-ca-dolli réy làmmiñ te deñ kumpa, di wax lu yoonam nekkul.
13 E, além disto, aprendem também a andar ociosas de casa em casa; e não só ociosas, mas também paroleiras e curiosas, falando o que não convém.
14 Looloo tax ma bëgg, jigéen yu ndaw yi séyaat, am ay doom, yor seeni kër, ba seen benn noon du leen mana gàkkal.
14 Quero, pois, que as que são moças se casem, gerem filhos, governem a casa e não deem ocasião ao adversário de maldizer.
15 Ndaxte fi mu ne sax am na ñu jeng xaat, ba topp Seytaane.
15 Porque já algumas se desviaram, indo após Satanás.
16 Kon nag jigéen ju gëm te am mbokk mu jëkkëram faatu, na ko dimbali te bañ koo bàyyeek mbooloom ñi gëm. Noonu mbooloo mi dina mana dimbali jigéen ñi sësul ci kenn.
16 Se algum crente ou alguma crente tem viúvas, socorra-as, e não se sobrecarregue a igreja, para que se possam sustentar as que deveras são viúvas.
17 Li jëm ci njiiti mbooloo mi nag, joxal teraanga ju mat sëkk ñi ciy rafetal seen liggéey, rawatina ñi sax dàkk ci waare bi ak njàngle mi.
17 Os presbíteros que governam bem sejam estimados por dignos de duplicada honra, principalmente os que trabalham na palavra e na doutrina.
18 Ndaxte Mbind mi nee na: «Bul sunjuñ gémmiñu nag wu ñu takk ci bojjukaay,» nee na it: «Ku ñaq, jariñu.»
18 Porque diz a Escritura: Não ligarás a boca ao boi que debulha. E: Digno é o obreiro do seu salário.
19 Kuy tuumaal njiit fi yaw, bu ko gëm, li feek ñaar walla ñetti seede dëggaluñu ko.
19 Não aceites acusação contra presbítero, senão com duas ou três testemunhas.
20 Waaye ñiy bàkkaar, yedd leen fa kanam ñépp, ngir artu ñi ci des.
20 Aos que pecarem, repreende-os na presença de todos, para que também os outros tenham temor.
21 Léegi nag maa ngi lay dénk fa kanam Yàlla ak Kirist Yeesu ak malaaka yu tedd ya, nga sàmm loolu ma wax te bañ cee gënale walla di ci parlàqu.
21 Conjuro- te, diante de Deus, e do Senhor Jesus Cristo, e dos anjos eleitos, que, sem prevenção, guardes estas coisas, nada fazendo por parcialidade.
22 Bul gaawa teg loxo kenn, ba fal ko, di séddu noonu ci bàkkaari jaambur, waaye dëkkal ci sellaay.
22 A ninguém imponhas precipitadamente as mãos, nem participes dos pecados alheios; conserva-te a ti mesmo puro.
23 Ba tey bul yemati ci ndox mu ñuul rekk, waaye nangay naan tuuti biiñ, ngir faj say metiti biir ak say jagadi yu bare.
23 Não bebas mais água só, mas usa de um pouco de vinho, por causa do teu estômago e das tuas frequentes enfermidades.
24 Am na, ñu seeni bàkkaar fés ci kanam ñépp, ba jiitu leen ca àtte ba; ñi seeni bàkkaar nëbbu nag, bés baa ngi leen di xaar.
24 Os pecados de alguns homens são manifestos, precedendo o juízo; e em alguns manifestam-se depois.
25 Naka noonu it am na, ñu seen jëf yu rafet leer, te yi feeñul manuñoo nekk kumpa ba fàww.
25 Assim mesmo também as boas obras são manifestas, e as que são doutra maneira não podem ocultar-se.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Timóteo 5, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.