1 Timóteo 4

Téereb Injiil (WOL2010) vs NVI

Sair da comparação
NVI Nova Versão Internacional
1 Xelum Yàlla mi wax na bu leer ne ci mujug jamono dina am ñu bàyyi yoonu ngëm wi, di topp ay xel yuy fàbbee ak xalaati Seytaane.
1 O Espírito diz claramente que nos últimos tempos alguns abandonarão a fé e seguirão espíritos enganadores e doutrinas de demônios.
2 Ñooñu ay naaféq yuy naxe lañu, te seen xol dërkiis.
2 Tais ensinamentos vêm de homens hipócritas e mentirosos, que têm a consciência cauterizada
3 Dinañu tere séy, di araamal ay ñam, waaye Yàlla daa sàkk yooyu, ngir ñi gëm te xam dëgg man ciy jëfandiku te di ko ci sant.
3 e proíbem o casamento e o consumo de alimentos que Deus criou para serem recebidos com ação de graças pelos que crêem e conhecem a verdade.
4 Ndaxte li Yàlla sàkk lépp baax na, kon wenn ñam araamul ci ku koy jëfandikoo te di ko ci sant.
4 Pois tudo o que Deus criou é bom, e nada deve ser rejeitado, se for recebido com ação de graças,
5 Ndaxte kàddug Yàlla ak ñaan ñoo koy sellal.
5 pois é santificado pela palavra de Deus e pela oração.
6 Saxal ci digal bokk yi loolu nag, kon dinga nekk jawriñu Kirist Yeesu ju baax ju regg ci kàdduy yoonu ngëm wi ak njàngle mu rafet, mi nga xam bu wér.
6 Se você transmitir essas instruções aos irmãos, será um bom ministro de Cristo Jesus, nutrido com as verdades da fé e da boa doutrina que tem seguido.
7 Tanqamlul ay léebi diiney neen, di ay wax yu amul bopp yu àddina kese; waaye tàggatal sa bopp ci ragal Yàlla.
7 Rejeite, porém, as fábulas profanas de velhas e exercite-se na piedade.
8 Ndaxte tàggat yaram am na fu njariñam yem, waaye njariñu ragal Yàlla dafa daj lépp, ëmb digey àddina ak àllaaxira.
8 O exercício físico é de pouco proveito; a piedade, porém, para tudo é proveitosa, porque tem promessa da vida presente e da futura.
9 Wax ju wóor a ngii, te mata nangu ak gépp kóolute.
9 Esta é uma afirmação fiel e digna de plena aceitação.
10 Danuy ñaq tey bëre, ndaxte wékk nanu sunu yaakaar ci Yàlla Aji Dund ji, di Musalkatu ñépp, rawatina nag ci ñi gëm.
10 Se trabalhamos e lutamos é porque temos colocado a nossa esperança no Deus vivo, o Salvador de todos os homens, especialmente dos que crêem.
11 Digal leen yëf yooyu nag ci sa njàngle.
11 Ordene e ensine estas coisas.
12 Bu la kenn xeeb ndax say at, waaye defal sa bopp royukaayu ñi gëm ci say wax ak say jëf, ci sa mbëggeel, sa ngëm ak sa cell.
12 Ninguém o despreze pelo fato de você ser jovem, mas seja um exemplo para os fiéis na palavra, no procedimento, no amor, na fé e na pureza.
13 Li feek may dikk, saxal ci jàng di biral Mbind mi ci mbooloo mi, di leen dénk ak a jàngal.
13 Até a minha chegada, dedique-se à leitura pública da Escritura, à exortação e ao ensino.
14 Bul sàggane may gi nekk ci yaw, gi la Yàlla jox jaarale ko ci waxu yonent, keroog bi la njiit yi tegee loxo.
14 Não negligencie o dom que lhe foi dado por mensagem profética com imposição de mãos dos presbíteros.
15 Faaydaalal yëf yooyu te sóobu ci, ba sa jëm kanam bir ñépp.
15 Seja diligente nestas coisas; dedique-se inteiramente a elas, para que todos vejam o seu progresso.
16 Sàmmal sa bopp, sàmm sa njàngle, te sax ci; kon dinga musal sa bopp, yaw ak ñi lay déglu.
16 Atente bem para a sua própria vida e para a doutrina, perseverando nesses deveres, pois, fazendo isso, você salvará tanto a si mesmo quanto aos que o ouvem.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Timóteo 4, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.