1 Timóteo 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Wax ju wóor a ngii: kuy sabablu yenub sàmm mbooloo mi, mu ngi yóotu liggéey bu rafet.
1 Fiel é esta palavra: Se alguém aspira ao episcopado, excelente obra deseja.
2 Sàmm bi nag, nii la wara mel: war na ñàkk ŋàññ, yem ci benn soxna, moom boppam te maandu; war na am faayda, man gan te am mayu jàngle;
2 É necessário, pois, que o bispo seja irrepreensível, marido de uma só mulher, temperante, sóbrio, ordeiro, hospitaleiro, apto para ensinar;
3 warul di ab màndikat mbaa xeexkat, waaye na lewet te jàmmu, baña bëgge ci xaalis.
3 não dado ao vinho, não espancador, mas moderado, inimigo de contendas, não ganancioso;
4 Na yor këram yorin wu rafet, te ay doomam déggal ko ak teggin yu mat.
4 que governe bem a sua própria casa, tendo seus filhos em sujeição, com todo o respeito
5 Ndaxte ku manta yor njabootam, naka lay mana yore njabootu Yàlla?
5 {pois, se alguém não sabe governar a sua própria casa, como cuidará da igreja de Deus?};
6 Te it bumu nekk kuy doora gëm, ngir mu baña yég boppam, bay dajeek mbugalu Yàlla, ni ko Seytaane defe woon.
6 não neófito, para que não se ensoberbeça e venha a cair na condenação do Diabo.
7 Te it war na am seede su rafet ci waa àddina, ngir ñu bañ koo diiŋat, ba muy daanu ci fiirug Seytaane.
7 Também é necessário que tenha bom testemunho dos que estão de fora, para que não caia em opróbrio, e no laço do Diabo.
8 Kiy topptoo li mbooloo miy jëfandikoo itam na am faayda te fonk kàddoom; bumu di ku yàqu ci sàngara, mbaa ku alal jiital.
8 Da mesma forma os diáconos sejam sérios, não de língua dobre, não dados a muito vinho, não cobiçosos de torpe ganância,
9 Na sàmm mbóoti ngëm gi ak xel mu dal.
9 guardando o mistério da fé numa consciência pura.
10 Moom itam nañu ko jëkka seetlu, ba mu leer ne amul ŋàññ, ñu door koo fal.
10 E também estes sejam primeiro provados, depois exercitem o diaconato, se forem irrepreensíveis.
11 Naka noonu, na jigéen ñi am faayda, baña jëw mbaa xér ci dara, waaye nañu takku ci lépp.
11 Da mesma sorte as mulheres sejam sérias, não maldizentes, temperantes, e fiéis em tudo.
12 Ku ñu dénk sasu topptoo yëfi mbooloo mi nag, nay ku yem ci benn soxna, jiite bu baax këram ak i doomam.
12 Os diáconos sejam maridos de uma só mulher, e governem bem a seus filhos e suas próprias casas.
13 Ndaxte ku ci rafetal sasam dina am tur wu tedd ak kóolute gu mat sëkk ci yoonu ngëm, gi ci Kirist Yeesu.
13 Porque os que servirem bem como diáconos, adquirirão para si um lugar honroso e muita confiança na fé que há em Cristo Jesus.
14 Bëgg naa laa seetsi balaa yàgg,
14 Escrevo-te estas coisas, embora esperando ir ver-te em breve,
15 waaye amaana mu yéex. Moo tax ma lay bind bataaxal bii, ngir xamal la, ni ñu wara nekke ci kër Yàlla gi, maanaam ci mbooloom Yàlla Aji Dund ji, miy kenug dëgg te di sëslaayam.
15 para que, no caso de eu tardar, saibas como se deve proceder na casa de Deus, a qual é a igreja do Deus vivo, coluna e esteio da verdade.
16 Ci dëgg-dëgg ragal Yàlla ëmb na mbóot yu xóot:
16 E, sem dúvida alguma, grande é o mistério da piedade: Aquele que se manifestou em carne, foi justificado em espírito, visto dos anjos, pregado entre os gentios, crido no mundo, e recebido acima na glória.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Timóteo 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.