1 João 4

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Samay soppe, buleen gëm xel mu nekk, waaye nattuleen xel yi, ba xam ndax ci Yàlla lañu jóge walla déet, ndaxte naaféq yu bare yu mbubboo turu yonent jóg nañu, tasaaroo ci àddina si.
1 Caríssimos, não deis fé a qualquer espírito, mas examinai se os espíritos são de Deus, porque muitos falsos profetas se levantaram no mundo.
2 Ci lii lanu xàmmee Xelum Yàlla: mépp xel mu nangu ne, Yeesu Kirist ñëw na, nekk nit, ci Yàlla la bokk.
2 Nisto se reconhece o Espírito de Deus: todo espírito que proclama que Jesus Cristo se encarnou é de Deus;
3 Waaye mépp xel mu nanguwul Yeesu, bokkul ci Yàlla. Xel moomu mooy xelum Bañaaleb Kirist, mi ngeen déggoon ne dina ñëw, te léegi sax mu ngi ci biir àddina.
3 todo espírito que não proclama Jesus esse não é de Deus, mas é o espírito do Anticristo de cuja vinda tendes ouvido, e já está agora no mundo.
4 Yéen samay doom, ci Yàlla ngeen bokk, te daan ngeen yonent yu naaféq yooyu, ndaxte ki nekk ci yéen moo ëpp doole ki nekk ci àddina.
4 Vós, filhinhos, sois de Deus, e os vencestes, porque o que está em vós é maior do que aquele que está no mundo.
5 Ñoom ci àddina lañu bokk; moo tax ñuy wax waxi àddina, te àddina di leen déglu.
5 Eles são do mundo. É por isto que falam segundo o mundo, e o mundo os ouve.
6 Nun nag ci Yàlla lanu bokk. Ku xam Yàlla dinga nu déglu; ku bokkul ci Yàlla doo nu déglu. Ci loolu lanuy xàmmee Xel miy dëgg ak xel mi dul dëgg.
6 Nós, porém, somos de Deus. Quem conhece a Deus, ouve-nos; quem não é de Deus, não nos ouve. É nisto que conhecemos o Espírito da Verdade e o espírito do erro.
7 Samay soppe, nanu bëggante, ndax mbëggeel ci Yàlla la bawoo; képp ku bëgg sa mbokk nag, ci Yàlla nga juddoo, te xam nga Yàlla.
7 Caríssimos, amemo-nos uns aos outros, porque o amor vem de Deus, e todo o que ama é nascido de Deus e conhece a Deus.
8 Ku bëggul sa mbokk, xamuloo Yàlla, ndax Yàlla mbëggeel la.
8 Aquele que não ama não conhece a Deus, porque Deus é amor.
9 Nii la Yàlla wonee mbëggeelam ci nun; yónni na ci àddina jenn Doomam ji mu am kepp, ngir nu am dund ci moom.
9 Nisto se manifestou o amor de Deus para conosco: em nos ter enviado ao mundo o seu Filho único, para que vivamos por ele.
10 Lii mooy mbëggeel, du sunu mbëggeel ci Yàlla, waaye mbëggeelam ci nun, ba mu yónni Doomam, mu joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar.
10 Nisto consiste o amor: não em termos nós amado a Deus, mas em ter-nos ele amado, e enviado o seu Filho para expiar os nossos pecados.
11 Samay soppe, bu nu Yàlla bëggee nii, nun itam war nanoo bëggante.
11 Caríssimos, se Deus assim nos amou, também nós nos devemos amar uns aos outros.
12 Kenn masula gis Yàlla, waaye bu nu bëggantee, Yàllaa ngi dëkk ci nun te mbëggeelam mat na sëkk ci nun.
12 Ninguém jamais viu a Deus. Se nos amarmos mutuamente, Deus permanece em nós e o seu amor em nós é perfeito.
13 Ci lii lanuy xame ne sax nanu ci Yàlla, te moom itam dëkk na ci nun: sol na nu Xelam.
13 Nisto é que conhecemos que estamos nele e ele em nós, por ele nos ter dado o seu Espírito.
14 Te nun gis nanu te seede ne, Baay bi yónni na Doom ji, mu nekk Musalkatu àddina.
14 E nós vimos e testemunhamos que o Pai enviou seu Filho como Salvador do mundo.
15 Képp ku nangu ne, Yeesu Doomu Yàlla la, Yàlla dëkk na ci yaw, te yaw it sax nga ci Yàlla.
15 Todo aquele que proclama que Jesus é o Filho de Deus, Deus permanece nele e ele em Deus.
16 Mbëggeel gi Yàlla am ci nun, xam nanu ko te gëm ko.
16 Nós conhecemos e cremos no amor que Deus tem para conosco. Deus é amor, e quem permanece no amor permanece em Deus e Deus nele.
17 Ni Kirist mel, noonu lanu mel nun itam ci àddina. Ci loolu la mbëggeel mate sëkk ci nun, ngir nu am kóolute bésu àtte ba.
17 Nisto é perfeito em nós o amor: que tenhamos confiança no dia do julgamento, pois, como ele é, assim também nós o somos neste mundo.
18 Genn ragal amul ci mbëggeel, waaye mbëggeel gu mat sëkk day dàq ragal. Ndaxte ragal day ànd ak mbugal; te ku ragal, mbëggeel matul sëkk ci yaw.
18 No amor não há temor. Antes, o perfeito amor lança fora o temor, porque o temor envolve castigo, e quem teme não é perfeito no amor.
19 Danuy wéy ci mbëggeel, ndax moo nu jëkka bëgg.
19 Mas amamos, porque Deus nos amou primeiro.
20 Su kenn nee: «Bëgg naa Yàlla,» te bëgguloo sa mbokk, dangay fen; ndaxte ku bëggul sa mbokk mi ngay gis, doo mana bëgg Yàlla mi nga gisul.
20 Se alguém disser: Amo a Deus, mas odeia seu irmão, é mentiroso. Porque aquele que não ama seu irmão, a quem vê, é incapaz de amar a Deus, a quem não vê.
21 Te jox na nu ndigal lii: ku bëgg Yàlla, nga bëgg sa mbokk.
21 Temos de Deus este mandamento: o que amar a Deus, ame também a seu irmão.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 João 4, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.