1 João 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Xool-leen mbëggeel gi nu Baay bi jox, ni mu réye, ba nu mana tudd doomi Yàlla. Te moom lanu. Moo tax àddina xamu nu, ndaxte xamu ko woon, moom itam.
1 Vede que grande amor nos tem concedido o Pai: que fôssemos chamados filhos de Deus; e nós o somos. Por isso o mundo não nos conhece; porque não conheceu a ele.
2 Samay soppe, léegi doomi Yàlla lanu, te li nu nara nekki feeñagul, waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, dinanu nirook moom, ndaxte dinanu ko gis, na mu mel.
2 Amados, agora somos filhos de Deus, e ainda não é manifesto o que havemos de ser. Mas sabemos que, quando ele se manifestar, seremos semelhantes a ele; porque assim como é, o veremos.
3 Te képp ku am yaakaar jooju ci moom, dinga sellal sa bopp, ni mu selle moom.
3 E todo o que nele tem esta esperança, purifica-se a si mesmo, assim como ele é puro.
4 Ku def bàkkaar, jàdd nga yoon; ndaxte bàkkaar mooy jàdd yoon.
4 Todo aquele que vive habitualmente no pecado também vive na rebeldia, pois o pecado é rebeldia.
5 Te xam ngeen ne Yeesu Kirist feeñ na, ngir dindi bàkkaar yi, te moom amul benn bàkkaar.
5 E bem sabeis que ele se manifestou para tirar os pecados; e nele não há pecado.
6 Képp ku sax ci moom, doo sax ci bàkkaar; kuy def bàkkaar, gisuloo ko te xamuloo ko.
6 Todo o que permanece nele não vive pecando; todo o que vive pecando não o viu nem o conhece.
7 Samay doom, bu leen kenn nax! Kuy def lu jub, ku jub nga, ni Kirist jube moom ci boppam.
7 Filhinhos, ninguém vos engane; quem pratica a justiça é justo, assim como ele é justo;
8 Kuy def bàkkaar, ci Seytaane nga bokk, ndax Seytaane ca njàlbéen ga ba tey day bàkkaar. Te Doomu Yàlla ji ñëw na, ngir nasaxal jëfi Seytaane.
8 quem comete pecado é do Diabo; porque o Diabo peca desde o princípio. Para isto o Filho de Deus se manifestou: para destruir as obras do Diabo.
9 Ku juddu ci Yàlla doo def bàkkaar, ndax Yàlla sol na la jikkoom, te doo mana sax ci bàkkaar, ndax juddu nga ci Yàlla.
9 Aquele que é nascido de Deus não peca habitualmente; porque a semente de Deus permanece nele, e não pode continuar no pecado, porque é nascido de Deus.
10 Lii mooy ràññale doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul def lu jub bokkoo ci Yàlla; naka noonu itam ku soppul sa mbokk bokkoo ci Yàlla.
10 Nisto são manifestos os filhos de Deus, e os filhos do Diabo: quem não pratica a justiça não é de Deus, nem o que não ama a seu irmão.
11 Ndaxte xibaar, bi ngeen déggoon ca ndoorte la, mooy lii: nanu bëggante,
11 Porque esta é a mensagem que ouvistes desde o princípio, que nos amemos uns aos outros,
12 te baña mel ni Kayin, mi bokkoon ci Ibliis, ba rey rakkam. Lu tax mu rey ko nag? Ndaxte ay jëfam dañoo bon, te yu rakkam jub.
12 não sendo como Caim, que era do Maligno, e matou a seu irmão. E por que o matou? Porque as suas obras eram más e as de seu irmão justas.
13 Bokk yi, bu leen àddina bañee, buleen ci jaaxle.
13 Meus irmãos, não vos admireis se o mundo vos odeia.
14 Mbëggeel gi nu bëgg sunuy bokk, moo nuy xamal ne jóge nanu ci dee, tàbbi ci dund. Ku bëggul sa mbokk, yaa ngi ci dee ba tey.
14 Nós sabemos que já passamos da morte para a vida, porque amamos os irmãos. Quem não ama permanece na morte.
15 Képp ku bañ sa mbokk, reykat nga; te xam ngeen ne, ku rey nit amuloo dund gu dul jeex.
15 Todo o que odeia a seu irmão é homicida; e vós sabeis que nenhum homicida tem a vida eterna permanecendo nele.
16 Ci lii lanuy xàmmee luy mbëggeel: Kirist joxe na bakkanam ngir nun; te nun itam war nanoo joxe sunu bakkan ngir sunuy bokk.
16 Nisto conhecemos o amor: que Cristo deu a sua vida por nós; e nós devemos dar a vida pelos irmãos.
17 Waaye ku am alalu àddina te gis sa mbokk nekk ci soxla, nga dummóoyu ko, nan la mbëggeelu Yàlla dëkke ci yaw?
17 Quem, pois, tiver bens do mundo, e, vendo o seu irmão necessitando, lhe fechar o seu coração, como permanece nele o amor de Deus?
18 Samay doom, bunu bëggante ci wax mbaa ci làmmiñ rekk, waaye ci jëf ak ci dëgg.
18 Filhinhos, não amemos de palavra, nem de língua, mas por obras e em verdade.
19 — ausente —
19 Nisto conheceremos que somos da verdade, e diante dele tranqüilizaremos o nosso coração;
20 — ausente —
20 porque se o coração nos condena, maior é Deus do que o nosso coração, e conhece todas as coisas.
21 Samay soppe, bu nu sunu xol daanul, kon man nanoo jege Yàlla ak kóolute.
21 Amados, se o coração não nos condena, temos confiança para com Deus;
22 Te lépp lu nu koy ñaan, dinanu ko jot ci moom, ndaxte nu ngi sàmm ay ndigalam, di def lu ko neex.
22 e qualquer coisa que lhe pedirmos, dele a receberemos, porque guardamos os seus mandamentos, e fazemos o que é agradável à sua vista.
23 Ndigalam mooy lii: nu gëm turu Doomam, Yeesu Kirist, tey bëggante, ni mu nu ko digale.
23 Ora, o seu mandamento é este, que creiamos no nome de seu Filho Jesus Cristo, e nos amemos uns aos outros, como ele nos ordenou.
24 Kuy sàmm ndigalu Yàlla, dinga sax ci moom, mu dëkk ci yaw. Te Xel mi mu nu jox, moo nuy xamal ne dëkk na ci nun.
24 Quem guarda os seus mandamentos, em Deus permanece e Deus nele. E nisto conhecemos que ele permanece em nós: pelo Espírito que nos tem dado.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 João 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.