1 João 2

Téereb Injiil (WOL2010) vs NVI

Sair da comparação
NVI Nova Versão Internacional
1 Samay doom, maa ngi leen di bind yëf yii, ngir ngeen baña def bàkkaar. Waaye su kenn defee bàkkaar, ba tey am nanu ku nuy rammu ci Baay bi, mooy Yeesu Kirist mu jub mi.
1 Meus filhinhos, escrevo-lhes estas coisas para que vocês não pequem. Se, porém, alguém pecar, temos um intercessor junto ao Pai, Jesus Cristo, o Justo.
2 Te moo joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar, te du sax sunuy bàkkaar rekk, waaye yu àddina sépp.
2 Ele é a propiciação pelos nossos pecados, e não somente pelos nossos, mas também pelos pecados de todo o mundo.
3 Ci lii lanu xame ne xam nanu ko: sàmm ay ndigalam.
3 Sabemos que o conhecemos, se obedecemos aos seus mandamentos.
4 Ku wax ne xam nga ko, te sàmmoo ay ndigalam, dangay fen, te dëgg nekkul ci yaw.
4 Aquele que diz: "Eu o conheço", mas não obedece aos seus mandamentos, é mentiroso, e a verdade não está nele.
5 Kuy sàmm kàddug Yàlla, dëgg-dëgg sa mbëggeel ci Yàlla mat na sëkk. Ci loolu lanu xame ne nekk nanu ci moom.
5 Mas, se alguém obedece à sua palavra, nele verdadeiramente o amor de Deus está aperfeiçoado. Desta forma sabemos que estamos nele:
6 Ku wax ne ci Yàlla nga sax, fàww nga dund, ni Yeesu Kirist daan dunde moom ci boppam.
6 aquele que afirma que permanece nele, deve andar como ele andou.
7 Samay soppe, li ma leen di bind du ndigal lu bees, waaye ndigal lu yàgg la; la ngeen jotoon ca ndoorte la. Te ndigal lu yàgg loolu, mooy kàddu gi ngeen déggoon.
7 Amados, não lhes escrevo um mandamento novo, mas um mandamento antigo, que vocês têm desde o princípio: a mensagem que ouviram.
8 Teewul ndigal lu bees laa leen di bind, lu amoon ci dundu Yeesu, te am it ci seen dund; ndaxte lëndëm gaa ngi wéy, te leer gu wóor gi fenk na xaat.
8 No entanto, eu lhes escrevo um mandamento novo, o qual é verdadeiro nele e em vocês, pois as trevas estão se dissipando e já brilha a verdadeira luz.
9 Ku wax ne yaa ngi ci leer, tey bañ sa mbokk, yaa ngi ci lëndëm ba tey.
9 Quem afirma estar na luz mas odeia seu irmão, continua nas trevas.
10 Kuy sopp sa mbokk, yaa ngi dëkk ci leer, te luy yóbbe nit bàkkaar du nekk ci yaw.
10 Quem ama seu irmão permanece na luz, e nele não há causa de tropeço.
11 Waaye kuy bañ sa mbokk, ci lëndëm nga nekk, di ci dox, te xamoo foo jëm, ndax lëndëm muur na say bët.
11 Mas quem odeia seu irmão está nas trevas e anda nas trevas; não sabe para onde vai, porque as trevas o cegaram.
12 Samay doom, maa ngi leen di bind,
12 Filhinhos, eu lhes escrevo porque os seus pecados foram perdoados, graças ao nome de Jesus.
13 Maa ngi leen di bind, yéen baay yi,
13 Pais, eu lhes escrevo porque vocês conhecem aquele que é desde o princípio. Jovens, eu lhes escrevo porque venceram o Maligno.
14 Bind naa leen, samay doom,
14 Filhinhos, eu lhes escrevi porque vocês conhecem o Pai. Pais, eu lhes escrevi porque vocês conhecem aquele que é desde o princípio. Jovens, eu lhes escrevi, porque vocês são fortes, e em vocês a Palavra de Deus permanece e vocês venceram o Maligno.
15 Buleen sopp àddina ak li ci biiram. Ku sopp àddina, mbëggeelu Baay bi nekkul ci moom.
15 Não amem o mundo nem o que nele há. Se alguém amar o mundo, o amor do Pai não está nele.
16 Ndaxte lépp lu nekk ci àddina, maanaam bëgg-bëggu yaram ak xemmemu bët ak réyug àddina, loolu du jóge ci Baay bi waaye ci àddina.
16 Pois tudo o que há no mundo — a cobiça da carne, a cobiça dos olhos e a ostentação dos bens — não provém do Pai, mas do mundo.
17 Te àddina day wéy, waaye kuy def coobarey Yàlla dinga sax ba fàww.
17 O mundo e a sua cobiça passam, mas aquele que faz a vontade de Deus permanece para sempre.
18 Samay doom, waxtu wu mujj wi jot na! Dégg ngeen ne benn Bañaaleb Kirist dina ñëw; te dëgg la, bañaaley Kirist yu bare feeñ nañu. Ci loolu lanu xame ne waxtu wu mujj wi jot na.
18 Filhinhos, esta é a última hora; e, assim como vocês ouviram que o anticristo está vindo, já agora muitos anticristos têm surgido. Por isso sabemos que esta é a última hora.
19 Ci sunu biir lañu jóge, waaye bokkuñu woon ci nun; ndaxte su ñu bokkoon ci nun, kon dinañu des ci nun. Waaye dàggeeku nañu nu, ngir mu leer ne kenn ci ñoom bokkul woon ci nun.
19 Eles saíram do nosso meio, mas na realidade não eram dos nossos, pois, se fossem dos nossos, teriam permanecido conosco; o fato de terem saído mostra que nenhum deles era dos nossos.
20 Yéen nag, Aji Sell ji sol na leen Xelam, te yéen ñépp am ngeen xam-xam.
20 Mas vocês têm uma unção que procede do Santo, e todos vocês têm conhecimento.
21 Bind naa leen, du ndax xamuleen dëgg, waaye ndax xam ngeen ko, xam it ne wenn fen du jóge ci dëgg.
21 Não lhes escrevo porque não conhecem a verdade, mas porque vocês a conhecem e porque nenhuma mentira procede da verdade.
22 Kan mooy fenkat bi? Mooy kiy weddi ne Yeesu mooy Kirist, Almasi bi. Kooka mooy Bañaaleb Kirist, biy weddi Baay bi ak Doom ji.
22 Quem é o mentiroso, senão aquele que nega que Jesus é o Cristo? Este é o anticristo: aquele que nega o Pai e o Filho.
23 Ku weddi Doom ji, amuloo itam Baay bi; ku seedeel Doom ji, am nga it Baay bi.
23 Todo o que nega o Filho também não tem o Pai; quem confessa publicamente o Filho tem também o Pai.
24 Yéen nag, la ngeen déggoon ca ndoorte la, na sax ci yéen. Loolu ngeen déggoon ca ndoorte la, su saxee ci yéen, dingeen sax yéen itam ci Doom ji ak ci Baay bi.
24 Quanto a vocês, cuidem para que aquilo que ouviram desde o princípio permaneça em vocês. Se o que ouviram desde o princípio permanecer em vocês, vocês também permanecerão no Filho e no Pai.
25 Te li mu nu digoon mooy lii: dund gu dul jeex.
25 E esta é a promessa que ele nos fez: a vida eterna.
26 Bind naa leen lii ci mbirum ñi leen di bëgga réeral.
26 Escrevo-lhes estas coisas a respeito daqueles que os querem enganar.
27 Yéen nag, Xel mi leen Kirist sol a ngi dëkk ci yéen, te soxlawuleen kenn jàngal leen dara. Waaye Xel mi mu leen sol, mi ngi leen di jàngal lépp, te li mu leen di jàngal mooy dëgg; kon nag saxleen ci moom, ni mu leen ko jàngle.
27 Quanto a vocês, a unção que receberam dele permanece em vocês, e não precisam que alguém os ensine; mas, como a unção dele recebida, que é verdadeira e não falsa, os ensina acerca de todas as coisas, permaneçam nele como ele os ensinou.
28 Gannaaw loolu nag yéen samay doom, saxleen ci Kirist, ngir bés bu feeñee, nu am kóolute ci kanamam te baña rus ba sëngéem cig dikkam.
28 Filhinhos, agora permaneçam nele para que, quando ele se manifestar, tenhamos confiança e não sejamos envergonhados diante dele na sua vinda.
29 Gannaaw xam ngeen ne ku jub la, dingeen xam it ne, képp kuy def lu jub juddu nga ci moom.
29 Se vocês sabem que ele é justo, saibam também que todo aquele que pratica a justiça é nascido dele.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 João 2, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.