1 João 1

Téereb Injiil (WOL2010) vs NVI

Sair da comparação
NVI Nova Versão Internacional
1 Nu ngi leen di bind ci mbirum ki ñuy wax Kàddug dund, moom mi amoon ca njàlbéen ga; mi nu dégg te gis ko ak sunuy bët, mi nu xool te laal ko ak sunuy loxo.
1 O que era desde o princípio, o que ouvimos, o que vimos com os nossos olhos, o que contemplamos e as nossas mãos apalparam — isto proclamamos a respeito da Palavra da vida.
2 Dund feeñ na, te gis nanu ko; te moom lanuy seedeel, di leen yégal dund gu dul jeex, googu nekkoon ci wetu Yàlla Baay bi te feeñu nu.
2 A vida se manifestou; nós a vimos e dela testemunhamos, e proclamamos a vocês a vida eterna, que estava com o Pai e nos foi manifestada.
3 Li nu gis te dégg ko, nu ngi leen koy yégal, ngir yéen itam ngeen bokk ak nun. Te dëgg-dëgg bokk nanu ci Baay bi ak Doomam, Yeesu Kirist.
3 Nós lhes proclamamos o que vimos e ouvimos para que vocês também tenham comunhão conosco. Nossa comunhão é com o Pai e com seu Filho Jesus Cristo.
4 Nu ngi leen di bind yëf yii, ngir sunu mbég mat sëkk, nun ñépp.
4 Escrevemos estas coisas para que a nossa alegria seja completa.
5 Xibaar bi nu dégg ci Yeesu Kirist, di leen ko yégal, mooy lii: Yàlla Leer la, te genn lëndëm nekkul ci moom.
5 Esta é a mensagem que dele ouvimos e transmitimos a vocês: Deus é luz; nele não há treva alguma.
6 Su nu waxee ne bokk nanu ci moom, tey dox ci lëndëm, danuy fen ci sunuy wax ak sunuy jëf.
6 Se afirmarmos que temos comunhão com ele, mas andamos nas trevas, mentimos e não praticamos a verdade.
7 Waaye bu nuy dox ci leer, ni mu nekke moom ci boppam ci leer, kon bokk nanu ci sunu biir, te deretu Yeesu Doomam dina nu sellal ci bépp bàkkaar.
7 Se, porém, andamos na luz, como ele está na luz, temos comunhão uns com os outros, e o sangue de Jesus, seu Filho, nos purifica de todo pecado.
8 Su nu waxee ne amunu bàkkaar, kon nax nanu sunu bopp, te dëgg nekkul ci nun.
8 Se afirmarmos que estamos sem pecado, enganamo-nos a nós mesmos, e a verdade não está em nós.
9 Su nu nangoo sunuy bàkkaar ci kanamam, fekk kuy sàmm kóllëre la te jub, ngir baal nu sunuy bàkkaar te sellal nu ci lépp lu jubadi.
9 Se confessarmos os nossos pecados, ele é fiel e justo para perdoar os nossos pecados e nos purificar de toda injustiça.
10 Su nu waxee ne defunu bàkkaar, teg nanu ko kuy tebbi waxam, te kàddoom duggagul ci sunu xol.
10 Se afirmarmos que não temos cometido pecado, fazemos de Deus um mentiroso, e a sua palavra não está em nós.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 João 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.