1 Coríntios 9
Téereb Injiil (WOL2010) vs ACF
1 Ndax awma ndogal ci li may def? Ndax duma ndawul Kirist? Ndax gisuma Yeesu sunu Boroom? Xanaa du yéena soqikoo ci liggéey bi ma Boroom bi sant?
1 Não sou eu apóstolo? Não sou livre? Não vi eu a Jesus Cristo Senhor nosso? Não sois vós a minha obra no Senhor?
2 Su ma ñenn ñi tegul ndaw, moom laa ci yéen, ndaxte yéenay firnde jiy wone ne ndawul Boroom bi dëgg laa.
2 Se eu não sou apóstolo para os outros, ao menos o sou para vós; porque vós sois o selo do meu apostolado no Senhor.
3 Nii laay tontoo ñi may àtte:
3 Esta é minha defesa para com os que me condenam.
4 Xanaa sañunoo lekk ak a naan?
4 Não temos nós direito de comer e beber?
5 Xanaa sañunoo indaale soxna su gëm Kirist, ni yeneen ndawul Kirist ak doomi ndeyu Boroom bi ak Sefas sax?
5 Não temos nós direito de levar conosco uma esposa crente, como também os demais apóstolos, e os irmãos do Senhor, e Cefas?
6 Walla boog man ak Barnabas rekk noo wara daan sunu doole?
6 Ou só eu e Barnabé não temos direito de deixar de trabalhar?
7 Kan moo masa solu soldaar ci pexey boppam? Kan mooy bey tool te du ci jariñu? Walla kan mooy sàmm jur te du naan ca soow ma?
7 Quem jamais milita à sua própria custa? Quem planta a vinha e não come do seu fruto? Ou quem apascenta o gado e não se alimenta do leite do gado?
8 Lii may wax, du ci yëfi doom Aadama rekk laa ko jukkee; xanaa du yoon wi it moo ko santaane?
8 Digo eu isto segundo os homens? Ou não diz a lei também o mesmo?
9 Ndaxte bind nañu ci yoonu Musaa ne: «Bul sunjuñ gémmiñu nag wu ñu takk ci bojjukaay.» Ndax mooy tekki nag ne, Yàlla dafa bàyyi xel nag yi?
9 Porque na lei de Moisés está escrito: Não atarás a boca ao boi que trilha o grão. Porventura tem Deus cuidado dos bois?
10 Walla boog xanaa nun noo moom wax jooju? Waaw, noo tax ñu bind loolu. Noonu kuy bey war na am yaakaar, te kuy bojj di yaakaara jot wàllam.
10 Ou não o diz certamente por nós? Certamente que por nós está escrito; porque o que lavra deve lavrar com esperança e o que debulha deve debulhar com esperança de ser participante.
11 Nu ji ci yéen yëfi Xelum Yàlla, ba noppi góobe ci yéen yëfi àddina, ndax loolu dafa ëpp li nu wara séentu?
11 Se nós vos semeamos as coisas espirituais, será muito que de vós recolhamos as carnais?
12 Ndegam ñeneen a am sañ-sañ boobu ci yéen, nun kon waxi-noppi.
12 Se outros participam deste poder sobre vós, por que não, e mais justamente, nós? Mas nós não usamos deste direito; antes suportamos tudo, para não pormos impedimento algum ao evangelho de Cristo.
13 Xanaa xamuleen ne, ñiy liggéeyal yëf yu sell yi, dañuy lekk ñam, wi ci kër Yàlla gi, te ñiy liggéey ci sarxalukaay bi, dañuy jot seen wàll ci sarax yi?
13 Não sabeis vós que os que administram o que é sagrado comem do que é do templo? E que os que de contínuo estão junto ao altar, participam do altar?
14 Naka noonu it Boroom bi digle na ne, ñiy yégle xibaaru jàmm bi, nanu ci dund.
14 Assim ordenou também o Senhor aos que anunciam o evangelho, que vivam do evangelho.
15 Waaye man jariñoowuma benn ci sañ-sañ yooyu, te binduma yëf yooyu, ngir ngeen di ma defal yu ni mel. Dee sax moo ma ko gënal— kenn du jële ci man mbir moomu may kañoo!
15 Mas eu de nenhuma destas coisas usei, e não escrevi isto para que assim se faça comigo; porque melhor me fora morrer, do que alguém fazer vã esta minha glória.
16 Su may yégle xibaaru jàmm bi, manuma cee kañu. Sas la, wu ñu ma sas. Dinaa torox, su ma yéglewul xibaaru jàmm bi!
16 Porque, se anuncio o evangelho, não tenho de que me gloriar, pois me é imposta essa obrigação; e ai de mim, se não anunciar o evangelho!
17 Su doon ci sama coobare laa yégle xibaaru jàmm bi, man naa ci séentu yool. Waaye defuma ko ci sama coobare, ndaxte sas la, wu ñu ma sas.
17 E por isso, se o faço de boa mente, terei prêmio; mas, se de má vontade, apenas uma dispensação me é confiada.
18 Kon nag lan mooy sama yool? Xanaa di yégle xibaaru jàmm bi ci dara, te baña jariñoo sañ-sañ boobu ma ci yelloo.
18 Logo, que prêmio tenho? Que, evangelizando, proponha de graça o evangelho de Cristo para não abusar do meu poder no evangelho.
19 Gor laa te kenn moomu ma; teewul def naa sama bopp jaamu ñépp, ngir mana gindi nit ñu bare ci Kirist.
19 Porque, sendo livre para com todos, fiz-me servo de todos para ganhar ainda mais.
20 Ci biir Yawut yi, sol naa melow Yawut yi, ngir gindi leen. Man ci sama bopp yoonu Musaa jiitalu ma, terewul bi ma nekkee ci biir ñiy sàmm yoonu Musaa, sàmm naa yoon wa, ngir gindi leen.
20 E fiz-me como judeu para os judeus, para ganhar os judeus; para os que estão debaixo da lei, como se estivesse debaixo da lei, para ganhar os que estão debaixo da lei.
21 Ci biir ñi nekkul ci yoonu Musaa, faalewuma woon yoon wi, ngir gindi leen; waxuma ne ànduma ak yoonu Yàlla, waaye topp naa yoon ci sama bokk ak Kirist.
21 Para os que estão sem lei, como se estivesse sem lei (não estando sem lei para com Deus, mas debaixo da lei de Cristo), para ganhar os que estão sem lei.
22 Ci biir ñi néew ngëm, meloon naa ni ku néew ngëm, ngir gindi leen. Doon naa lépp ci ñépp, ngir def lépp lu ma man, ba ñenn mucc ci.
22 Fiz-me como fraco para os fracos, para ganhar os fracos. Fiz-me tudo para todos, para por todos os meios chegar a salvar alguns.
23 Damaa def loolu lépp ndax xibaaru jàmm bi, ngir man it ma am wàll ci barkeem.
23 E eu faço isto por causa do evangelho, para ser também participante dele.
24 Xanaa xamuleen ne, ñépp ñooy daw cib rawante, waaye kenn rekk ay jël ndam li? Dawleen nag ngir jël ko.
24 Não sabeis vós que os que correm no estádio, todos, na verdade, correm, mas um só leva o prêmio? Correi de tal maneira que o alcanceis.
25 Ñiy joŋante ci po muy waral tàggat yaram, dañuy xañ seen bopp lu bare. Dañu koy def, ngir am kaalag ndam gu dul yàgg; waaye nun danu koy def, ngir am kaalag ndam gu sax ba fàww.
25 E todo aquele que luta de tudo se abstém; eles o fazem para alcançar uma coroa corruptível; nós, porém, uma incorruptível.
26 Man nag noonu laay dawe, te duma dawantu. Noonu laay bëree, waaye duma def ni nit kuy dóor ci jaww ji.
26 Pois eu assim corro, não como a coisa incerta; assim combato, não como batendo no ar.
27 Waaye damay not sama yaram, ba moom ko, ngir ragala yégal ñi ci des xibaaru jàmm bi, ba noppi Yàlla xañ ma ndam li.
27 Antes subjugo o meu corpo, e o reduzo à servidão, para que, pregando aos outros, eu mesmo não venha de alguma maneira a ficar reprovado.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Coríntios 9, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.