1 Coríntios 7

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Nanu jàll nag léegi ci laaj, yi ngeen ma doon bind, ci baña ànd ak jigéen, ndax lu baax la ci góor.
1 Ora, quanto às coisas de que me escrevestes, bom seria que o homem não tocasse em mulher;
2 Lii mooy sama xalaat: moy gu bare gi tax na ba, na góor gu nekk am jabaram, jigéen ju nekk am jëkkëram.
2 mas, por causa da prostituição, tenha cada homem sua própria mulher e cada mulher seu próprio marido.
3 Jëkkër war na def warugaru jëkkër ci jabaram; jabar it def warugaru jabar ci jëkkëram.
3 O marido pague à mulher o que lhe é devido, e do mesmo modo a mulher ao marido.
4 Jigéen ji amul sañ-sañ ci yaramam moom kenn; jëkkëram moo ko moom. Niki noonu it jëkkër ji amul sañ-sañ ci yaramam; jabaram moo ko moom.
4 A mulher não tem autoridade sobre o seu próprio corpo, mas sim o marido; e também da mesma sorte o marido não tem autoridade sobre o seu próprio corpo, mas sim a mulher.
5 Bu kenn tere boppam moroomam, su dul ne dangeena mànkoo ci def noonu ab diir, ngir gëna mana wéetal Yàlla ci ñaan. Waaye su loolu weesoo, nangeen doxal yoonu séy; lu ko moy, Seytaane dina leen fiir ndax seen ñàkk maandute.
5 Não vos negueis um ao outro, senão de comum acordo por algum tempo, a fim de vos aplicardes à oração e depois vos ajuntardes outra vez, para que Satanás não vos tente pela vossa incontinência.
6 Li ma leen di wax fii du ndigal, waaye dama leen di xamal li ñu leen may, ngeen def ko.
6 Digo isto, porém, como que por concessão e não por mandamento.
7 Ndaxte dëgg-dëgg su ma sañoon, kon ñépp mel ni man; waaye ku nekk ak li la Yàlla jagleel, kii ak may gii, kee ak may gale.
7 Contudo queria que todos os homens fossem como eu mesmo; mas cada um tem de Deus o seu próprio dom, um deste modo, e outro daquele.
8 Lii laay yégal ñi séyul ak it ñi seen jëkkër dee: baax na ci yéen, su fekkee dangeena toog rekk ni man, baña séy.
8 Digo, porém, aos solteiros e às viúvas, que lhes é bom se ficarem como eu.
9 Waaye su ngeen manula téye seen bopp, nangeen séy, ndaxte séy moo gën xemmem di leen gaañ.
9 Mas, se não podem conter-se, casem-se. Porque é melhor casar do que abrasar-se.
10 Ñi séy nag, maa ngi leen di jox ndigal lii —Boroom bi moo ko waxoon, du man— jigéen ju séy warula teqalikoo ak jëkkëram.
10 Todavia, aos casados, mando, não eu mas o Senhor, que a mulher não se aparte do marido;
11 Te bu teqalikoo ak moom, bumu séyaat, mbaa boog na juboo ak jëkkëram. Te bu jëkkër ji fase jabaram.
11 se, porém, se apartar, que fique sem casar, ou se reconcilie com o marido; e que o marido não deixe a mulher.
12 Ñi ci des nag, lii laa leen di wax —Boroom bi waxu ko woon— su nit ku gëm Kirist amee jabar ju gëmul, te mu nangoo séy ak moom, waru koo fase.
12 Mas aos outros digo eu, não o Senhor: Se algum irmão tem mulher incrédula, e ela consente em habitar com ele, não se separe dela.
13 Naka noonu it su jigéen ju gëm Kirist amee jëkkër ju gëmul, te mu nangoo nekk ak moom, warula tas.
13 E se alguma mulher tem marido incrédulo, e ele consente em habitar com ela, não se separe dele.
14 Li tax ma wax ko moo di, jëkkër ji gëmul, Yàlla sellal na ko, ndax li mu ànd ak jabaram. Te it jigéen ji gëmul, Yàlla sellal na ko, ndax li mu ànd ak jëkkëram ji gëm; lu ko moy, seeni doom dinañu am sobe, te fekk dañoo sell.
14 Porque o marido incrédulo é santificado pela mulher, e a mulher incrédula é santificada pelo marido crente; de outro modo, os vossos filhos seriam imundos; mas agora são santos.
15 Waaye nag, su fekkee ki gëmul bëgg na dem, na dem. Ci wàll woowu nag, ki gëm Kirist, muy jëkkër ji walla jabar ji, amul benn tënk, ndaxte Yàlla moo leen woo ngir ngeen dund ci jàmm.
15 Mas, se o incrédulo se apartar, aparte-se; porque neste caso o irmão, ou a irmã, não está sujeito à servidão; pois Deus nos chamou em paz.
16 Loo ci xam, yaw jigéen ji, ndax dinga gëmloo sa jëkkër Musalkat bi walla déet? Loo ci xam yaw jëkkër ji it, ndax dinga gëmloo sa jabar Musalkat bi walla déet?
16 Pois, como sabes tu, ó mulher, se salvarás teu marido? ou, como sabes tu, ó marido, se salvarás tua mulher?
17 Ku nekk nag na dund, ni ko ko Boroom bi jagleele, mu méngoo ak ni mu meloon, bi ko Yàlla wooyee. Moom laay tëral ci mboolooy ñi gëm yépp.
17 Somente ande cada um como o Senhor lhe repartiu, cada um como Deus o chamou. E é isso o que ordeno em todas as igrejas.
18 Ki xaraf, bi ko Yàlla wooyee, warula jéema far màndargam xaraf bi. Ki xaraful, bi ko Yàlla wooyee, aajowul mu xaraf.
18 Foi chamado alguém, estando circuncidado? permaneça assim. Foi alguém chamado na incircuncisão? não se circuncide.
19 Xaraf ak ñàkka xaraf lépp a yem; li am solo moo di topp ndigali Yàlla.
19 A circuncisão nada é, e também a incircuncisão nada é, mas sim a observância dos mandamentos de Deus.
20 Na kenn ku nekk jàpp ci li mu nekkoon, bi ko Yàlla wooyee.
20 Cada um fique no estado em que foi chamado.
21 Ndax jaam nga woon, bi la Yàlla wooyee? Na ci sa xel dal. Waaye soo amee bunt, ba yiwiku, nanga ci jaar.
21 Foste chamado sendo escravo? não te dê cuidado; mas se ainda podes tornar-te livre, aproveita a oportunidade.
22 Ku nekkoon jaam, bi la Boroom bi wooyee, Boroom bi goreel na la. Ba tey it ku nekkoon gor, bi ñu la wooyee, jaamu Kirist nga.
22 Pois aquele que foi chamado no Senhor, mesmo sendo escravo, é um liberto do Senhor; e assim também o que foi chamado sendo livre, escravo é de Cristo.
23 Gannaaw Yàlla jot na leen ak njég lu réy, buleen doon jaamub nit.
23 Por preço fostes comprados; mas não vos façais escravos de homens.
24 Bokk yi, fàww ku nekk wéy ca kanam Yàlla ci fànn ga mu nekkoon, bi ko Yàlla wooyee.
24 Irmãos, cada um fique diante de Deus no estado em que foi chamado.
25 Ci li jëm ci janq yi, awma ndigalu Boroom bi, waaye maa ngi joxe sama xalaat, ni ku ñu wóolu ndax li ma jot yërmandey Boroom bi.
25 Ora, quanto às virgens, não tenho mandamento do Senhor; dou, porém, o meu parecer, como quem tem alcançado misericórdia do Senhor para ser fiel.
26 Bu nu seetee tiis wii fi teew nag, defe naa ne li baax ci nit, moo di mu sax ci li mu nekk.
26 Acho, pois, que é bom, por causa da instante necessidade, que a pessoa fique como está.
27 Ndax takk nga jabar? Bul wuta tàggook moom. Ndax takkuloo jabar? Bul wut jabar.
27 Estás ligado a mulher? não procures separação. Estás livre de mulher? não procures casamento.
28 Waaye nag boo séyee, defoo bàkkaar, te bu janq séyee, deful bàkkaar. Waaye ñi séy dinañu am naqar ci àddina, te naqar woowu dama leen ko bëggoona fanqal, yéen ñi séyagul.
28 Mas, se te casares, não pecaste; e, se a virgem se casar, não pecou. Todavia estes padecerão tribulação na carne e eu quisera poupar-vos.
29 Lii laa bëgga wax, bokk yi: diir bu gàtt rekk a fi des. Lu weesu tey, na góor ñi am jabar di def, ni bu ñu ko amul woon;
29 Isto, porém, vos digo, irmãos, que o tempo se abrevia; pelo que, doravante, os que têm mulher sejam como se não a tivessem;
30 ñiy jooy, mel ni ñu jooyul; ñiy bég, mel ni ñu bégul; ñiy jënd, ni ñu moomul li ñu jënd;
30 os que choram, como se não chorassem; os que folgam, como se não folgassem; os que compram, como se não possuíssem;
31 ñiy jariñoo àddina, bañ cee xér. Ndaxte àddina sii, ci ni mu mel, dootul yàggati.
31 e os que usam deste mundo, como se dele não usassem em absoluto, porque a aparência deste mundo passa.
32 Bëggoon naa, ngeen baña am benn xalaat. Góor gu takkul jabar dafay bàyyi xel ci mbiri Boroom bi, di wuta neex Boroom bi.
32 Pois quero que estejais livres de cuidado. Quem não é casado cuida das coisas do Senhor, em como há de agradar ao Senhor,
33 Waaye ku takk jabar, fàww mu bàyyi xel ci mbiri àddina si, ak nu mu mana neexe jabaram,
33 mas quem é casado cuida das coisas do mundo, em como há de agradar a sua mulher,
34 te noonu dafay daldi bare soxla. Jigéen ju séyul, walla janq, dafay bàyyi xel ci mbiri Boroom bi— bëgg koo jox yaramam ak xelam. Waaye jigéen ji séy dafay bàyyi xel ci mbiri àddina, ak nu mu mana neexe jëkkëram.
34 e está dividido. A mulher não casada e a virgem cuidam das coisas do Senhor para serem santas, tanto no corpo como no espírito; a casada, porém, cuida das coisas do mundo, em como há de agradar ao marido.
35 Seen njariñ a tax ma wax lii, du ngir teg leen yen bu ngeen àttanul, waaye ngeen mana jàppandil Boroom bi ci njaamu gu rafet gu àndul ak genn njaaxle.
35 E digo isto para proveito vosso; não para vos enredar, mas para o que é decente, e a fim de poderdes dedicar-vos ao Senhor sem distração alguma.
36 Nanu jàll nag ci mbiri kiy takk ngoro te amul pastéefu takk ndaw si. Su fekkee ne waxambaane wi xalaat na ne jëfewul nu jekk ak janq bi, fekk muy wees ag ndawam, te mu xalaat ne dafa koo wara takk, kon na ko takk, ni mu ko bëgge; deful bàkkaar.
36 Mas, se alguém julgar que lhe é desairoso conservar solteira a sua filha donzela, se ela estiver passando da idade de se casar, e se for necessário, faça o que quiser; não peca; casem-se.
37 Waaye nag su dogoo dëgg ci baña takk, fekk sagoom rekk a tax te kenn tegu ko ko, kon ba tey def na lu baax.
37 Todavia aquele que está firme em seu coração, não tendo necessidade, mas tendo domínio sobre a sua própria vontade, se resolver no seu coração guardar virgem sua filha, fará bem.
38 Noonu ku takk as ndawam def na lu baax, rawatina nag ku takkul.
38 De modo que aquele que dá em casamento a sua filha donzela, faz bem; mas o que não a der, fará melhor.
39 Jigéen ji séy dina ànd ak jëkkëram giiru dundam. Waaye su jëkkër ji faatoo, man na séy ak ku ko neex, su fekkee ne góor gu gëm la.
39 A mulher está ligada enquanto o marido vive; mas se falecer o marido, fica livre para casar com quem quiser, contanto que seja no Senhor.
40 Moona nag dina gëna bég, bu toogee noonu rekk. Loolu mooy sama xalaat, te defe naa ne man it am naa Xelum Yàlla.
40 Será, porém, mais feliz se permanecer como está, segundo o meu parecer, e eu penso que também tenho o Espírito de Deus.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Coríntios 7, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.