1 Coríntios 5
Téereb Injiil (WOL2010) vs ARA
1 Dégg nanu sax ñu naan, am na kuy moy Yàlla ci seen biir, moy gu ni tollu, duñu ko gis sax ci ñi xamul Yàlla. Dem na, ba am ci yéen kuy séy ak jabaru baayam.
1 Geralmente, se ouve que há entre vós imoralidade e imoralidade tal, como nem mesmo entre os gentios, isto é, haver quem se atreva a possuir a mulher de seu próprio pai.
2 Moona yéen de, yéena ngi tiitaru. Waaye dangeena waroona am naqar, ba dàq kiy def loolu ci seen biir!
2 E, contudo, andais vós ensoberbecidos e não chegastes a lamentar, para que fosse tirado do vosso meio quem tamanho ultraje praticou?
3 Man nag, jëmm ji sore na leen, waaye xel mi mu ngi ci yéen, te àtte naa xaat kiy def loolu, ni su ma teewoon ci seen biir. Dogal naa,
3 Eu, na verdade, ainda que ausente em pessoa, mas presente em espírito, já sentenciei, como se estivesse presente, que o autor de tal infâmia seja,
4 ngeen daje ci turu Boroom bi Yeesu, te sama xel teewe ko, ànd ak dooley Boroom bi Yeesu,
4 em nome do Senhor Jesus, reunidos vós e o meu espírito, com o poder de Jesus, nosso Senhor,
5 nu jébbal nit kooku Seytaane, yaramam yàqu, ngir ruuwam mucc keroog bésu Boroom bi.
5 entregue a Satanás para a destruição da carne, a fim de que o espírito seja salvo no Dia do Senhor [Jesus].
6 Seen tiitar bi jekkul dara. Xanaa xamuleen ne tuuti lawiir day tax tooyalu fariñ bépp funki?
6 Não é boa a vossa jactância. Não sabeis que um pouco de fermento leveda a massa toda?
7 Ni ma leen ko mana misaale, jëleleen fi bépp lawiir bu yàgg, ngir ngeen sell ni tooyal bu bees bu amul lawiir, ndax nekk ngeen ko ba noppi. Ndaxte Kirist deeyal na nu ca bant ba, mel ni gàtt bu ñuy rendi, jébbal ko Yàlla ca màggalu bésu Mucc ba.
7 Lançai fora o velho fermento, para que sejais nova massa, como sois, de fato, sem fermento. Pois também Cristo, nosso Cordeiro pascal, foi imolado.
8 Kon nanu màggal sunu Màggal, waxuma ak lawiir bu màggat biy misaal kiñaan ak lu bon, waaye ak mburu mu amul lawiir, maanaam ci xol bu laab ak ci dëgg.
8 Por isso, celebremos a festa não com o velho fermento, nem com o fermento da maldade e da malícia, e sim com os asmos da sinceridade e da verdade.
9 Bindoon naa leen, ngeen baña séq dara ak njaalookat yi.
9 Já em carta vos escrevi que não vos associásseis com os impuros;
10 Bëgguma ci woona limaale waa àddina, maanaam njaalookat yi, nay yi, njublaŋ yi ak xërëmkat yi. Su ngeen séqul ak ñooñu dara, kon fàww ngeen génn àddina.
10 refiro-me, com isto, não propriamente aos impuros deste mundo, ou aos avarentos, ou roubadores, ou idólatras; pois, neste caso, teríeis de sair do mundo.
11 Lii laa leen bëggoona wax: buleen séq dara ak ku ñu tudde mbokk mu gëm Kirist, te fekk day njaaloo walla mu nay walla muy xërëm walla muy xas nit walla muy màndi walla muy njublaŋ. Nit ku mel noonu moom, buleen bokk ak moom, sax far di lekk.
11 Mas, agora, vos escrevo que não vos associeis com alguém que, dizendo-se irmão, for impuro, ou avarento, ou idólatra, ou maldizente, ou beberrão, ou roubador; com esse tal, nem ainda comais.
12 Ndax man maa wara àtte ñi bokkul ci mbooloom ñi gëm Kirist? Déedéet! Waaye ñi bokk ci seen mbooloo yéena leen wara àtte.
12 Pois com que direito haveria eu de julgar os de fora? Não julgais vós os de dentro?
13 Ñi bokkul ci mbooloom ñi gëm, Yàlla moo leen di àtte. Waaye yéen, ni ko Mbind mi waxe: «Dàqleen ci seen biir kiy def lu bon.»
13 Os de fora, porém, Deus os julgará. Expulsai, pois, de entre vós o malfeitor.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Coríntios 5, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.