1 Coríntios 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARC

Sair da comparação
ARC Almeida Revista e Corrigida 2009
1 Man nag bokk yi, manuma woona wax ak yéen ni ay nit ñuy déggal Xelum Yàlla, waaye waroon naa wax ak yéen ni ñuy topp seen nafsu, mel ni ay liir ci seen dund ci Kirist.
1 E eu, irmãos, não vos pude falar como a espirituais, mas como a carnais, como a meninos em Cristo.
2 Nàmpaloon naa leen, waaye joxuma leen dugub, ndaxte àttanuleen ko woon, te ba léegi sax àttanuleen ko
2 Com leite vos criei e não com manjar, porque ainda não podíeis, nem tampouco ainda agora podeis;
3 ci li ngeen di topp seen nafsu. Bu ñeetaan ak xuloo amee ci seen biir, xanaa du loolu mooy wone ne dangeena topp seen nafsu, di doxale ni niti àddina?
3 porque ainda sois carnais, pois, havendo entre vós inveja, contendas e dissensões, não sois, porventura, carnais e não andais segundo os homens?
4 Bu kenn yéglee ne: «Man ci Pool laa bokk,» keneen ne: «Man ci Apolos,» ndax jëfewuleen ni niti àddina rekk?
4 Porque, dizendo um: Eu sou de Paulo; e outro: Eu, de Apolo; porventura, não sois carnais?
5 Kuy Apolos? Ak kuy Pool? Nun ay surga rekk lanu, yu ngeen jaare, ba gëm. Te Boroom bi moo sas ku nekk liggéeyam.
5 Pois quem é Paulo e quem é Apolo, senão ministros pelos quais crestes, e conforme o que o Senhor deu a cada um?
6 Maa jëmbët, Apolos suuxat, waaye Yàlla moo jebbil.
6 Eu plantei, Apolo regou; mas Deus deu o crescimento.
7 Ki jëmbët nag ak ki suuxat, kenn du ci dara, waaye Yàlla miy jebbil rekk moo am solo.
7 Pelo que nem o que planta é alguma coisa, nem o que rega, mas Deus, que dá o crescimento.
8 Ki jëmbët ak ki suuxat benn lañu. Teewul nag ku nekk dina jot yool bu tollook liggéeyam.
8 Ora, o que planta e o que rega são um; mas cada um receberá o seu galardão, segundo o seu trabalho.
9 Nu ngi liggéeyandoo ci liggéeyu Yàlla; yéenay toolu Yàlla, yéenay taaxum Yàlla.
9 Porque nós somos cooperadores de Deus; vós sois lavoura de Deus e edifício de Deus.
10 Man nag teg naa fondamaa bi, ni tabaxkat bu man liggéeyam, dëppook sas wi ma Yàlla jagleel ci kaw yiwam. Te keneen a ngi tabax ci kaw; waaye na ku nekk teeylu ci ni muy tabaxe.
10 Segundo a graça de Deus que me foi dada, pus eu, como sábio arquiteto, o fundamento, e outro edifica sobre ele; mas veja cada um como edifica sobre ele.
11 Ci li jëm ci fondamaa bi, kenn manu fee tëral beneen bu dul bi fi xasa taxaw, muy Yeesu Kirist.
11 Porque ninguém pode pôr outro fundamento, além do que já está posto, o qual é Jesus Cristo.
12 Ku tabax ci kaw fondamaa bi, wurus, xaalis, per, dénk, gittax walla boob,
12 E, se alguém sobre este fundamento formar um edifício de ouro, prata, pedras preciosas, madeira, feno, palha,
13 sa liggéey dina fés, ndaxte bés baa koy xamle. Bés boobu dina fenk ni sawara, te sawara si dina nattu liggéeyu ku nekk.
13 a obra de cada um se manifestará; na verdade, o Dia a declarará, porque pelo fogo será descoberta; e o fogo provará qual seja a obra de cada um.
14 Ku sa liggéey dëgër, dinga jot yool.
14 Se a obra que alguém edificou nessa parte permanecer, esse receberá galardão.
15 Waaye ku sa liggéey lakk, dinga ñàkk. Yaw ci sa bopp dinga mucc, waaye mel ni ku rëcc ci sawara si.
15 Se a obra de alguém se queimar, sofrerá detrimento; mas o tal será salvo, todavia como pelo fogo.
16 Xanaa xamuleen ne yéenay kër Yàlla, te Xelum Yàlla dëkk na ci yéen?
16 Não sabeis vós que sois o templo de Deus e que o Espírito de Deus habita em vós?
17 Ku yàq kër Yàlla gi, Yàlla dina la yàq, ndaxte kër Yàlla gi dafa sell, te yéenay kër googu.
17 Se alguém destruir o templo de Deus, Deus o destruirá; porque o templo de Deus, que sois vós, é santo.
18 Kon bu kenn nax boppam: su kenn ci yéen tegee boppam boroom xam-xam ci gis-gisu àddina sii, kooku na doon dof, ngir am xam-xam bu wóor.
18 Ninguém se engane a si mesmo: se alguém dentre vós se tem por sábio neste mundo, faça-se louco para ser sábio.
19 Ndaxte xam-xamu àddina si, ndof la fa Yàlla. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla jàpp na ñu muus ñi, ba seen fiir këppu ci seen kaw.»
19 Porque a sabedoria deste mundo é loucura diante de Deus; pois está escrito: Ele apanha os sábios na sua própria astúcia.
20 Te it: «Boroom bi xam na xalaati boroom xam-xam yi; xam ne duñu mujj fenn.»
20 E outra vez: O Senhor conhece os pensamentos dos sábios, que são vãos.
21 Kon nag bu kenn tiitaru ndax nit ñi, ndaxte yéena moom lépp,
21 Portanto, ninguém se glorie nos homens; porque tudo é vosso:
22 muy Pool, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di dee, di lu am, di luy ñëw; lépp, yéena ko moom.
22 seja Paulo, seja Apolo, seja Cefas, seja o mundo, seja a vida, seja a morte, seja o presente, seja o futuro, tudo é vosso,
23 Yéen, Kirist a leen moom; Kirist, Yàllaa ko moom.
23 e vós, de Cristo, e Cristo, de Deus.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Coríntios 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.