1 Coríntios 16
Téereb Injiil (WOL2010) vs BKJ
1 Léegi nag ci li jëm ci ndimbal, li ñuy sàkkal gaayi Yàlla yi, defleen li ma tëral ci mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Galasi.
1 Ora, quanto à coleta que se faz para os santos, o mesmo que ordenei às igrejas da Galácia, fazei vós também.
2 Bés bu jëkk ci ayu-bés yi, na ku nekk ber lu mu àttan, denc ko, ngir saa yu ma dikkee, ñu bañ di wër di laaj xaalis.
2 No primeiro dia da semana, cada um de vós pessoalmente separe e guarde, conforme Deus o prosperou, para que não sejam coletados quando eu chegar.
3 Su ma dikkee, dinaa dénk seen xaalis ñi ngeen tànn, yónni leen Yerusalem, boole ko ak bataaxal.
3 E, quando eu tiver chegado, os que aprovardes por suas cartas, eu enviarei para levar a vossa liberalidade, a Jerusalém.
4 Su aajoo ma demal sama bopp, kon dinañu ànd ak man.
4 E, se for apropriado que eu também vá, eles irão comigo.
5 Gannaaw bu ma jàllee diiwaanu Maseduwan, dinaa ñëw ci yéen, ndaxte fas naa ko yéenee jàll.
5 Ora, eu irei até vós quando eu passar pela Macedônia; porque tenho de passar pela Macedônia.
6 Man na am ma yàgg ci yéen, jombul sax ma lollikoo fi yéen. Noonu dingeen taxawu sama yoon, fu ma mana jëm.
6 E bem pode ser que fique convosco e passe também o inverno, para que me acompanheis aonde quer que eu for.
7 Ndaxte fi mu ne bëgguma leena gis rekk, jàll, waaye yaakaar naa ne dinaa toog ci yéen ab diir, bu neexee Boroom bi.
7 Porque eu não os verei agora pelo caminho, mas espero ficar convosco algum tempo, se o Senhor permitir.
8 Ba tey dinaa toog fii ci dëkku Efes ba màggalu Pàntakot,
8 Mas eu ficarei em Éfeso até o Pentecostes.
9 ndaxte Yàlla ubbil na ma bunt, ba mu ne làññ, ngir may def liggéey bu mana am muj gu rafet, te noon yu bare bëgga gàllankoor liggéey bi.
9 porque uma porta grande e eficaz é aberta para mim, e há muitos adversários.
10 Bu leen Timote ganesee, fexeleen ba bumu am njàqare ci seen biir, ndaxte dafay liggéeyal Boroom bi ni man.
10 Ora, se Timóteo vier, cuidem para que ele possa estar convosco sem temor; porque ele trabalha na obra do Senhor, como eu também.
11 Kon bu ko kenn xeeb. Nangeen taxawu yoonam, ba mu délsi ci man ci jàmm, ndaxte maa ngi koy xaar ak bokk yi.
11 Portanto, não deixem nenhum homem desprezá-lo, mas conduzi-o em paz, para que venha ter comigo, pois o aguardo com os irmãos.
12 Naka Apolos sunu mbokk mi nag moom, xiir naa ko ay yooni yoon, mu ñëw ci yéen, ànd ak bokk yi. Waaye fi mu ne dëppoowul ak coobareem. Dina ñëw saa su ko manee.
12 E, no tocante ao nosso irmão Apolo, eu desejei grandemente que fosse até vós com os irmãos, mas a sua vontade não estava de todo para vir neste tempo, mas ele irá quando lhe for o tempo conveniente.
13 Farluleen te dëgër ci ngëm, di góor-góorlu te am pastéef.
13 Vigiai, estai firmes na fé, portai-vos como homens, e sede fortes.
14 Lépp li ngeen di def, defleen ko ak mbëggeel.
14 Todas as vossas coisas sejam feitas com caridade.
15 Xam ngeen ne, Estefanas ak njabootam ñoo jëkka nangu xibaaru jàmm bi ci diiwaanu Akayi, te ñoo joxe seen bopp, ngir liggéeyal gaayi Yàlla yi. Kon nag bokk yi, maa ngi leen di ñaan,
15 Eu vos rogo, irmãos (sabeis que a casa de Estéfanas é as primícias da Acaia e que eles têm se dedicado ao ministério dos santos),
16 ngeen nangul nit ñu mel noonu, ñoom ak képp ku ànd ak ñoom ci liggéey bi.
16 que também vos sujeiteis aos tais e a todo aquele que nos ajuda e trabalha.
17 Bi ma Estefanas ak Fortunatus ak Akaykus seetsee, bég naa ci lool. Taxawal nañu leen ci topptoo, bi ngeen yéene woon ci man te tële ko.
17 Alegro-me com a vinda de Estéfanas, e de Fortunato, e de Acaico; porque o que estava faltando da vossa parte, eles supriram.
18 Seral nañu sama xol ak seen yos itam. Kon fonkleen nit ñu mel noonu.
18 Porque eles revigoraram o meu espírito e o vosso. Reconhecei, pois, aos tais.
19 Mboolooy ñi gëm te nekk diiwaanu Asi ñu ngi leen di nuyu. Akilas ak Pirsil, ñu ngi leen di nuyu bu baax ci Boroom bi, ñoom ak mbooloom ñi gëm tey daje seen kër.
19 As igrejas da Ásia vos saúdam. Áquila e Priscila vos saúdam muito no Senhor, com a igreja que está em sua casa.
20 Bokk yépp ñu ngi leen di nuyu.
20 Todos os irmãos vos saúdam. Cumprimentai-vos uns aos outros com beijo santo.
21 Man Pool maa bind nuyoo bii ci sama loxob bopp.
21 Saudação da minha própria mão, de Paulo.
22 Képp ku bañ Boroom bi, yal na ko Yàlla alag. Boroom bi, ñëwal!
22 Se algum homem não ama o Senhor Jesus Cristo, seja anátema; Maranata.
23 Yal na yiwu Boroom bi Yeesu ànd ak yéen.
23 A graça do nosso Senhor Jesus Cristo seja convosco.
24 Bëgg naa leen yéen ñépp ndax sunu booloo ak Yeesu Kirist.
24 O meu amor seja com todos vós, em Cristo Jesus. Amém.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Coríntios 16, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.