1 Coríntios 13

Téereb Injiil (WOL2010) vs NVI

Sair da comparação
NVI Nova Versão Internacional
1 Su fekkee ne damay wax làkki nit ñi ak yu malaaka yi sax, te boolewuma ci mbëggeel, duma dara lu dul ndënd muy riir, walla jóolóoli buy kandaŋ-kandaŋi.
1 Ainda que eu fale as línguas dos homens e dos anjos, se não tiver amor, serei como o sino que ressoa ou como o prato que retine.
2 Su ma yéglee wax ju tukkee ci Yàlla, ma xam lépp luy kumpa, ma yor xam-xam bépp te gëm Yàlla ba mana randal ay tund, fekk boolewuma ci mbëggeel, duma dara.
2 Ainda que eu tenha o dom de profecia e saiba todos os mistérios e todo o conhecimento, e tenha uma fé capaz de mover montanhas, mas não tiver amor, nada serei.
3 Te it su ma doon sarxe li ma am lépp, di bàyyi ñu lakk sama yaram, ba rey ma, su ma ci boolewul mbëggeel, du ma jariñ dara.
3 Ainda que eu dê aos pobres tudo o que possuo e entregue o meu corpo para ser queimado, mas não tiver amor, nada disso me valerá.
4 Ku bëgg dafay muñ te laabiir. Ku bëgg du iñaan, du kañu, du tiitaru,
4 O amor é paciente, o amor é bondoso. Não inveja, não se vangloria, não se orgulha.
5 du def lu jekkadi, du wut njariñu boppam, du naqari deret, du ñaaw njort.
5 Não maltrata, não procura seus interesses, não se ira facilmente, não guarda rancor.
6 Du bég ci lu awul yoon, waaye dina bég ci lépp luy jollil dëgg.
6 O amor não se alegra com a injustiça, mas se alegra com a verdade.
7 Mbëggeel day baale lépp, am gëm ci lépp, yaakaar lépp, muñ lépp.
7 Tudo sofre, tudo crê, tudo espera, tudo suporta.
8 Mbëggeel amul àpp. Ñiy wax ci kàddug Yàlla dinañu noppi, ñiy wax ay làkk dinañu ko bàyyi, ñiy xamle xam-xamu Yàlla wàcc.
8 O amor nunca perece; mas as profecias desaparecerão, as línguas cessarão, o conhecimento passará.
9 Xam-xam bi nu am des na, te ni nu jottalee xibaar bi nu Yàlla dénk des na.
9 Pois em parte conhecemos e em parte profetizamos;
10 Waaye li mat, bu dikkee, li matul jóge fi.
10 quando, porém, vier o que é perfeito, o que é imperfeito desaparecerá.
11 Bi ma dee xale, dama doon wax ni xale, di dégge ni xale, di xalaate ni xale. Waaye bi ma doonee mag, bàyyi naa lu bokkoon cig ndaw.
11 Quando eu era menino, falava como menino, pensava como menino e raciocinava como menino. Quando me tornei homem, deixei para trás as coisas de menino.
12 Tey jii gis bu lëndëm lanuy gis, ni takkandeer ci seetu bu lëndëm; bu ëllëgee dinanu gis jaxran. Tey jii sama xam-xam des na; bu ëllëgee dinaa xam ba mat sëkk, ni ma Yàlla xame.
12 Agora, pois, vemos apenas um reflexo obscuro, como em espelho; mas, então, veremos face a face. Agora conheço em parte; então, conhecerei plenamente, da mesma forma como sou plenamente conhecido.
13 Léegi nag ñett yii ñooy sax: ngëm, yaakaar, mbëggeel; te mbëggeel moo ci raw.
13 Assim, permanecem agora estes três: a fé, a esperança e o amor. O maior deles, porém, é o amor.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Coríntios 13, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.