1 Coríntios 12
Téereb Injiil (WOL2010) vs ACF
1 Léegi nag bokk yi, ci li jëm ci mayi Xelum Yàlla, bëgguma ngeen umple ci dara.
1 Acerca dos dons espirituais, não quero, irmãos, que sejais ignorantes.
2 Xam ngeen ne bi ngeen xamagul woon Yàlla, xërëm yi manula wax ñoo leen jiitaloon, di leen wommat.
2 Vós bem sabeis que éreis gentios, levados aos ídolos mudos, conforme éreis guiados.
3 Moo tax ma leen di xamal lii: ku Xelum Yàlla solu du wax ne: «Yeesu dafa araam.» Te it kenn manula wax ne: «Yeesu mooy Boroom bi,» su ko ko Xelum Yàlla waxloowul.
3 Portanto, vos quero fazer compreender que ninguém que fala pelo Espírito de Deus diz: Jesus é anátema, e ninguém pode dizer que Jesus é o Senhor, senão pelo Espírito Santo.
4 Am na fànni may yu bare yu jóge ci Xelum Yàlla, waaye menn Xel moomu moo koy séddale.
4 Ora, há diversidade de dons, mas o Espírito é o mesmo.
5 Am na ay sas yu bare, waaye benn Boroom bi la.
5 E há diversidade de ministérios, mas o Senhor é o mesmo.
6 Am na ay fànn yu bare yu Yàllay feeñale dooleem, waaye jenn Yàlla ji mooy jëfe doole yooyu yépp ci ñépp.
6 E há diversidade de operações, mas é o mesmo Deus que opera tudo em todos.
7 Noonu Yàlla jox na ku nekk fànn gu muy feeñale Xelam mu Sell mi ngir njariñul ñépp.
7 Mas a manifestação do Espírito é dada a cada um, para o que for útil.
8 Am na ku Yàlla sédde, jaarale ko ci Xelam, mayu wax ak xel mu leer, keneen am mayu xam-xam, te mu bawoo ci menn Xel mi.
8 Porque a um pelo Espírito é dada a palavra da sabedoria; e a outro, pelo mesmo Espírito, a palavra da ciência;
9 Keneen it menn Xel mi jox ko ngëm, keneen di wéral ay jàngoro ci kàttanu Xel moomu,
9 E a outro, pelo mesmo Espírito, a fé; e a outro, pelo mesmo Espírito, os dons de curar;
10 keneen di def ay kéemaan, am kuy wax ci kàddug Yàlla, am keneen kuy ràññee li jóge ci Xelum Yàlla ak li jóge ci yeneen xel yi, keneen it di wax ay xeeti làkk, ak kuy firi làkk yooyu.
10 E a outro a operação de maravilhas; e a outro a profecia; e a outro o dom de discernir os espíritos; e a outro a variedade de línguas; e a outro a interpretação das línguas.
11 Loolu lépp, menn Xel moomu moo koy def, ku nekk mu sédd la ci, ni mu ko soobe.
11 Mas um só e o mesmo Espírito opera todas estas coisas, repartindo particularmente a cada um como quer.
12 Noona la ci yaramu nit. Yaram wenn la, teewul am na cér yu bare. Waaye céri yaram yépp, ak li ñuy baree bare, ñoo bokk, doon wenn yaram. Te noonu la Kirist mel.
12 Porque, assim como o corpo é um, e tem muitos membros, e todos os membros, sendo muitos, são um só corpo, assim é Cristo também.
13 Yàlla sóob na nu ci menn Xelam mi, ngir nu doon wenn yaram: nuy Yawut walla nu dul Yawut, nuy jaam mbaa gor, nun ñépp Yàlla may na nu, nu naan ci menn Xel mi.
13 Pois todos nós fomos batizados em um Espírito, formando um corpo, quer judeus, quer gregos, quer servos, quer livres, e todos temos bebido de um Espírito.
14 Yaram du benn cér, waaye cér yu bare la.
14 Porque também o corpo não é um só membro, mas muitos.
15 Kon bu tànk nee: «Man duma loxo, kon bokkuma ci yaram,» du ko teree bokk ci céri yaram yi.
15 Se o pé disser: Porque não sou mão, não sou do corpo; não será por isso do corpo?
16 Te bu nopp nee: «Duma bët, kon bokkuma ci yaram,» du ko teree bokk ci céri yaram yi.
16 E se a orelha disser: Porque não sou olho não sou do corpo; não será por isso do corpo?
17 Bu yaram wépp doon bët, kon nan lay dégge? Walla bu yaram wépp doon nopp, kon nan lay xeeñtoo?
17 Se todo o corpo fosse olho, onde estaria o ouvido? Se todo fosse ouvido, onde estaria o olfato?
18 Waaye Yàlla dafa riime céri yaram wi, def bu ci nekk fa mu ko soobe.
18 Mas agora Deus colocou os membros no corpo, cada um deles como quis.
19 Bu lépp doon benn cér, kon fu yaram di nekk?
19 E, se todos fossem um só membro, onde estaria o corpo?
20 Cér yi daal bare nañu, waaye wenn yaram rekk a am.
20 Assim, pois, há muitos membros, mas um corpo.
21 Bët nag manul ne loxo: «Soxlawuma la!» Te bopp it manul ne tànk yi: «Soxlawuma leen!»
21 E o olho não pode dizer à mão: Não tenho necessidade de ti; nem ainda a cabeça aos pés: Não tenho necessidade de vós.
22 Loolu sax manula am, ndaxte céri yaram, yi gëna néew doole, ñoo gëna am njariñ.
22 Antes, os membros do corpo que parecem ser os mais fracos são necessários;
23 Te cér yi gëna ñàkk maana, ñoom lanuy gëna topptoo. Cér yi ci rafetula tudd, ñoom lanuy gëna suturaal,
23 E os que reputamos serem menos honrosos no corpo, a esses honramos muito mais; e aos que em nós são menos decorosos damos muito mais honra.
24 fekk yi gëna rafet, soxlawul nu leen di suturaale noonu. Waaye Yàlla dafa boole sunu céri yaram yi, ngir gëna teral cér yi ko soxla.
24 Porque os que em nós são mais nobres não têm necessidade disso, mas Deus assim formou o corpo, dando muito mais honra ao que tinha falta dela;
25 Noonu yaram du séddaloo, waaye cér bu ci nekk dina dimbali yi ci des.
25 Para que não haja divisão no corpo, mas antes tenham os membros igual cuidado uns dos outros.
26 Bu sa benn céru yaram dee metti, yeneen yi ci des yépp dañuy bokk, yég metit wi. Te bu dee dangaa fonk sa benn céru yaram it, ndax du sa yaram wépp a ciy bànneexu?
26 De maneira que, se um membro padece, todos os membros padecem com ele; e, se um membro é honrado, todos os membros se regozijam com ele.
27 Léegi benn yaram ngeen, muy yaramu Kirist, te kenn ku nekk ci yéen cér nga ci.
27 Ora, vós sois o corpo de Cristo, e seus membros em particular.
28 Te Yàlla teg na ci mbooloom ñi gëm, ku nekk ak sa may: ci bu jëkk ay ndawi Kirist, teg ca ñiy wax ci kàddug Yàlla, teg ca ñiy jàngle, ñiy def ay kéemaan, ñi am mayu wéral ay jàngoro, ñiy dimbalee, ñiy jiite, ñiy wax ay xeeti làkk.
28 E a uns pôs Deus na igreja, primeiramente apóstolos, em segundo lugar profetas, em terceiro doutores, depois milagres, depois dons de curar, socorros, governos, variedades de línguas.
29 Ndax ñépp ay ndawi Kirist lañu? Ndax ñépp dañuy wax ci kàddug Yàlla? Ndax ñépp ay jàngle? Ndax ñépp ay def kéemaan?
29 Porventura são todos apóstolos? são todos profetas? são todos doutores? são todos operadores de milagres?
30 Ndax ñépp a am mayu wéral ay jàngoro? Ndax ñépp ay wax ay làkk? Ndax ñépp a leen di firi?
30 Têm todos o dom de curar? falam todos diversas línguas? interpretam todos?
31 Waaye fonkleen may yi gën.
31 Portanto, procurai com zelo os melhores dons; e eu vos mostrarei um caminho mais excelente.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Coríntios 12, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.